Xaralaymbëj Mooy xeetu xam-xam giy gëstu lépp lu jëm ci wàllug mbëj, ay jëfandikuwiinam ak ay seddalewiinam. bu njëkk dañoo foogoon ne mbëj ag wal la rekk guy dem, gu man a nekk gu baax(+) walla gu bon(-). Waaye ci ndimalu ay woroom xam-xam yu mel ne Hertz, Helmholtz, Maxwell, Heaviside, Alessandro Volta ak ñeneen ñu bari, ci lees dem ba gën a nànd, xam mbir mi. Lu mel ne yamaleb maxwell biy faramfàce tëdiinu yani mbëj yi ( feppsaal ak mbëjfepp yiy wuute ci seen jublug yanub mbëj) walla toolu mbëjbijjaakon ba ca juddoo.

Ci gàttal, ci noonu lañu tambalee gis yenn ci ay jëfandiku yu mbëj: Doxalukaay bu mbëj, soppalikaay aki niitu...

Tay xaralaymbëj moo yor wàllu sàkk ay wuutuloxoy mbëj ak ay buumi séddalekaayu kàttanug mbëj

Ay Faramface

Soppi

Ay faramface ak ay àtte yi lal xaralaymbëj.

yamaleb maxwell yi, ñooy àtte yu am-solo yu ñeel mbëjbijjaakon, ci la yeneen yi soqeekoo.

àtteb ohm(om) yiy faramface ndëgërlu gu mbëj gi

àtteb Faraday-Neumann-Lenz mooy faramface xiirtalug mbëjbijjaakon

njeexitu joule mooy leeral ni kàttanu mbëj di soppeekoo nekk tangoor ngir njeexitu ndëgërlu gi.

àtteb Kirchhoff(kiirkof) mooy leeral jëflante bi nekk ci diggante dawaan ak dend ci ag ndombo.

Jóox, yóbb ak séddale kàttanu mbëj

Soppi
Dencukaay:Nataalu buumu mbëj.jpg
ay buumi seddalekaayu kàttanu mbëj

Ag wàll gu am solo moo jëm ci lépp lu ñeel yokkte ak seddalewiinu kàttanu mbëj ba ca jëfandikuwaay ya (barab yees koy jëfandikoo). Kàttan gi dees na ko jóox ci ndimbalul ay jurukaayu mbëj ci barab yees ko jagleel, li ñuy wax diggub mbëj, ci lu ëpp fa muy nekk day soree ak dëkkuwaay yi.

Buumi séddalekaay yi dañu leen a lëkkale ci seen biir ñuy jëlee kàttan gi ca jóoxuwaay ya di ko yóbb ca jëfandikuwaay ya.

Li wuutale Buumi yóbbukaay yi, mooy limu dend gi ñuy yóbb, moo tax ñuy gis ay buumi dend gu kawe, [[Dend gu diggu]|dend gu diggu]], dend gu suufe. Su diggante jóoxuwaay yi guddee, dañ fay def ay mbëjjaaru, ay buumi dend gu kawe yu man a yóbb ay milioŋi watt ci kàttan tambalee ciy 400000 v. Buumi dend gu kawe yii la ñuy duppe yu yóbbug kàttanu mbëj, yi nga xam ne ñooy tax a man a yóbb kàttanu mbëj gi, jële ko ca jóoxuwaay ya, jëmee ko ca barabu soppikaay ya.

Ci nii la ñuy soppee dend gu kawe mu nekk dend gu diggu, jaarale ko ci ay masin yu mbëj yees di duppee soppalikaay, ci noonu la ñuy yóbboo kàttanu mbëj gi ca ndombo gu dend gu diggu, moom ci boppam dañu koy àggal ci néegu seddalekaay yi jaarale ko cig ndombog séddaleg kàttanu mbëj, foofa lañuy defee geneen coppite jëlee ko ci dend gu diggu soppi ko dend gu suufe ngir ñu man koo jox jëfandikukat yi ci kër yi ak liggéeyuwaay yi.

Wuutuloxo yu mbëj

Soppi

Doxalukaay

Soppi
 
Ay doxalukaay yu wuute

Doxalukaay yu mbëj yi, ay wuutuloxo lañu yu’y soppi kattanu mbëj def ko kattanu doolerandu. Doxalukaay yi dañu leen a séddale ci:

Jurukaay

Soppi
 
Jurukaayub mbëjtekkaaral

Jurukaayu mbëj yi Ñoom ay wuutuloxo lañu yuy soppi kàttanu doolerandu def ko kàttanu mbëj. Yi ci gën a raññeewu:

Soppalikaay

Soppi

Soppalikaay, Ab wuutuloxo la, maneelam mooy soppi limu dendu mbëj gi nekk ci ab ndombo, ci yokkute walla wàññi. Lu mu néew néew di na am ñaari lëmës yu bijjaakon boole.

Wuutuloxo yu man a yokk walla néewal taraay te di jëfandikoo benn lëmës rek, lañuy tuddee Soppiboppam

Niitu

Soppi

Ay jumtukaay lañu yu aajowoo soppi kàttanug mbëj mu nekk leer. Di ko jëfandikoo ngir leeral barab yi.

Lëkkalekaay yu biti

Soppi


Xam-xam
Xam-xam
Gëstubiddiw | Jëmm | Paj | Saytubiddiw | Simi | Xam-xamu suuf si ak jawwu ji | Xayma
Xarala
Jokkoosoryante | Xaralaymbëj | Doolerandu | Kàttan | Xam-xamu nosukaay | Mbëjfeppal
Xam-xami nite ak mboolaay
Diine | Melosuuf | Wërlaay | Nit | Yoon | Koom-koom | Taariix | Xeltu | Kàllaama
wikbaatukaay am na xët wu tudd: Xaralaymbëj