Feppsaal (deesi ko wax ci fr : Proton)(as wàll-wàllaan la su sëfoo yanu mbëj bu baax(+) su man a féex ciy yëngoom walla mu taq cib saalu xarefulwoon . Ki ñuy wax ne moo ko wuññi mooy Ernest Rutherford, donte jëmmaan bu waa-almaañ bi Eugene Goldstein njoortoon na ag nekkam njëkk ngir manoon a dëggal ay gëstoom. Dayoob yanu mbëjam tollook bu mbëjfepp, waaye ak màndarga gu wuute: 1,602 × 10-19 coulomb. Lefam tuuti la rombee 1800 yoon bu mbëjfepp (daanaka 1836) te xawa tollook bu feppmaandu: feppsaal a ngi am lef gu toll ci 1,6726231 × 10-27 kg (9,3828 × 102 MmV).

Feppsaal yeek feppmaandu yeey ñaari wàll-wàllaan yi cëroo xarefulwoon bi, ñoom ñaar ci saal bi lañu nekk, mbëjfepp yi ci xarefulwoon lañu leen boole waaye taquñu ci dañuy nekk di ko wër.


Wikipedia
Wikipedia
Bii jukki ab junj rekk la. Man nga cee duggal sa loxo suqali ko ndeem am nga ci xam-xam ci anam yi Wikipedia taxawal