Xeltu
Xeltu baat la bu nu doge ci « filasofia », muy baat bu cosaanoo ci làkkuw gereg, maanaa mi mu yor ci baat yi di « sopp hikma » loolu di (xel mu rafet ;sagesse ci Fr), ba ci laaj rekk ne « lan mooy xeltu ? » dees koy jàppe ab laaj bu di kojug xeltu bu nu man a yendu di ci dàggasante. Lii benn la ci màndargay xeltu yu dëgg-dëgg yi ak jeng gi mu def jëm ci laaju ak defi gëstu ci lepp lu mu man a doon te jéem a xam dëgg-dëggam aki màndargaam aki àtteem. Lii lépp a tax nag xeltu di xam-xam bu yaatu te bari ay ñall, laal daanaka ci xam-xam yépp, walla ci mbooleem wàlli dund. Waaye loolu lépp téewul muy xam-xam bu wéet ci boppam wëlif yeneen xam-xam yeek jagoo yi (specialisation). Xeltu leeg-leeg ñu melal ko ci ne mooy “xalaat ci xalaat” maanaam xalaat ci jëmmi xalaat, cib déndam ak ci settantal, dees na ko melal it ci ne mooy jéem a indi ay tontu ci laaj yi am gi di indi ak nekk gi (l’existence). Xeltu seere na ay jëm kanam yu am solo te lëw, dale ko ca waa Geres ya sos ponki xeltu yu mag yi niki xam-xam buy tabax ab gis-gis bu matale ñeel nekk gi(adduna bi) ci biir gis-gis bu di kojug li-am(réaliste), ba ca xeltukati jullit ñi nga xam ne danoo jëflanteek ndonol Geres li (li fi waa geres yu yàgg ya ba woon), jaxase kook nattu (experimentation), daal di soppi “xeltu bu kojug li-am” bi, yóbbu ko ci “xeltu bu kojug tur” ak “xeltu bu kojug xam-xam ak nattu” ci jamonoy yewwute walla judduwaat (renaissance), teg ci “xeltu yu kojug am yi” (existence) ak “yu kojug nite yi” ak “ngéri yees gi ak la ca ginaaw yeeg” ak “ñàkk” (maanaam dee walla bañ a am). Xeltu gu yees gi – ci aaday seggat ci Amerig gu bëj-gànnaar gi(USA) ak nguur gu bennoo gi (UK) (ci seen aada ji nu am ci seggat mbir yi (anaaliise ko)) – day barastiku jëm ci gën a nekk gu xarala ci gu neen rekk, moom day taxaw ci xellu (logique) ak ceggat gu dégg-dégg (conceptual analysis), looloo waral ay tërte (sujets) yi yitteem di jëm day àgg ci làmboo “gis-gis bu kojug xam” ak “jikko” ak “déndu làkk” ak “déndu xel”. Am na yeneen xam-xam ak jubluwaay yu jàppe xeltu muy jàng “fann” (walla ci Fr:art) ak xam-xam yi, bu ko defee muy gis-gis bu daj te matale, di tegtalub dund bu ubale te daj. Ci déggiin wii la xeltu di nekke di luy yittewoo xamale yoonu dund ga gën, dootul nekkati luy jéem a xam dund gi. Jamono yi jubluwaay bu seggat bi jàppee xeltu muy mbirum jëf mom fawwu nu jonjook moom, doxal ko, jëf ko, am na yeneen një (jubluwaay) yu ko jàppe muy cëslaay (base) li xam tegu, ñu war koo xam xam gu wér te xereñe ko.
Xamale luy xeltu
SoppiXeltu baat la bu gereg bu juge ci (fila) di tekki sopp, ak (sofia) di tekki hikma maanaam (sagesse) walla xel mu rafet, kon muy firi ((sopp hikma)). Baatub xeltu ci jamono ju yees ji ñi ngi koy wax jublu ci dox gi nit di dox ngir xam laaj yu mag yi aju cig dundam, bokk na ci yooyu dund ak dee ak li-am (realité) ak maanaa yi ak dëgg. Baatu xeltu it dees na ko di faral di jëfandikoo ngir xamalee ci li xeltukat yu mag yi def ciy liggéey yu nu bokk.
Waxtaan ci xeltu du lu waa geres jagoo ñoom rekk, waaye kay ag wàll la ci xayug (civilisation) xeet wu nekk, xeet yépp a ci bokk. Looloo tax laaj luy xeltu? Du tekki benn tontu rekk. Xeltu cig tàmaleem ca jamonoy Taalis da doon gëstu cosaanul am gi (l’existence) ak aji bind ji (le créateur), ak ne-ne (matiere) bi ñu binde mbindéef yi, ak xeet (elements) yi leen toggale, bu ko defee dàggasante gi wéy di tang ci loolu ba ci jamonoy Sinon ak (Sofistaa) yi nga xam ne danu doon jëfandikoo xeltu ci weddi Yàlla ak wëlbati maanaa yi ak dégg-déggi baat yi (li nu ciy dégge) ngir notal seeni gis-gis, waaye mi ngi tàmbali ci jamonoy Sokraat mi Siisroon doon melal ci ne mooy ((ki wàcce xeltu ci suuf si jële ko ci asamaan si)), maanaam mooy ki jële xeltu ci xalaat ci nekk gi ak ki ko sàkk, ak xeet (elements) yi mu ko toggalee (yi mu ko sàkke), yóbbu ko ci xalaat ci jëmmi nit. Moom nag soppi na lu bari ciy màndargaam, daal di tuxal ay ŋaayoom aki dàggasanteem yóbbu leen leegi ci déndub nit (nature-am) ak dëgg-dëggam, ak gëm aji bind ji te gëstu ko, te jëfandikoo tegtalu xel ci saxal ko. Sokraat nag jëfandikoo woon na xeltu ngir tas jikko yu rafet ci biir nit ñi ak dëggu ak soppante. Sokraat nag ñëw na mook Aflaton (Platon) sukkandiku ci ñaari jumtukaay yii di xel ak xellu (logique) niki cëslaayi xalaat bu sell te mucc ayib, xalaat bob day dox dëppoo ak ay ponk yuy leeral ag wéram akug neenam.
Laaj : “luy xeltu?” bii laaj Aristo tontu na ko. Ci noonu sunu wax ji amatul njariñ, ndax dafa jeex te tàmbaleegul, kon tontu bu gaaw bi ci loolu day man a taxaw ci cëslaay lii: tontu bi Aristo joxe woon ci lan mooy dëgg-dëggi xeltu du moom rekk mooy tontu bi nu ci man a joxe, ca dëgg-dëgg loolu daal benn rekk la ci tontu yi nu ci man a joxe. Nit daal - bu sukkandikoo ci ni Aristo xamalee xeltu – dina man a xalaat te firi xalaat yi jiitu Aristo ak Aflaaton ak xeltu yi ñëw ginaawam. Ànd ak loolu teewul nit ki dina seetlu ci anam gu yomb ne xeltu de ak yoon wi nu xame dëgg-dëggam soppiku nanu ci ñaari junniy at yi topp ci Aristo soppiku gu mag.
Waaye ci biir loolu jëmm ji wart a réere ne xeltu, la ko dale ca Aristo ba ca Nits dafa sax – ci cëslaayi soppiku yooyu ak yu leen moy – di moom ci jëmmi boppam, ndax kat soppiku yooyu dafa ame ci wàllug xereñ. Wattu ag yamoo ci biir moom moom la (…)
Lu wér la ne dinanu man a ame ci yoon woowu ay xam-xam yu wuute te xóot, neel yu am njariñ ci ni xeltu feeñe ànd ak taariix, waaye nag woowu yoon dunu may ñu àgg ci am tontu yu dëggu maanaam yu yoonu ci : lan mooy xeltu?
Ni Aristo firee xeltu ne mooy “sopp hikma” am na lu ëpp benn teglal walla maanaa. Tegtalub làkk bi, moom mi ngi aju ci làkku gereg wi ñu tëgge baatub filosofia, ak tegtalub xam-xam bi nga xam ne dafa wuuteek li nu nekk lool. Sikk amul ci ne tegtal bu mujj bi walla maanaa mu mujj mi mooy bi leeral maanaa mi, gaw ko ci “sopp hikma” niki melo wu nu man a wonee ñàkk gi ay am-am (donnés) yu xam-xam ñàkkoon ñeel xeltukat bi ca jamono jooja, bu ko defee hikma nekkoon benn ci pexe yi ñu daa pexee ci lu nu xamul, niki ab ne-ne bu njëkk bi nga xam ne ci la xeltukat biy sose nosteg xam-xamam, mu dëppook settantal gu xam-xam ga amoon ca jamono jooja.
Bu dee leegi nga xam ne xam-xam daa sakkan, li ñu wuññi lëw, laaj yi bari ci ëtt yu bari ak mbir yu dul jeex, ak jëm kanam gi nit def ci wàll yu bari, loolu lépp tax na ba liggéeyub xeltukat du doonati rekk sopp hikma, ak gëstu ko ci jumtukaay yi mu ko daa gëstoo ak ci ron kilimãb réer gu tar gi mu amoon ci wërlaayug àdduna gi ko wëroon ca jooja jamono… Xeltukat leegi lu sakkan ciy ngér (ecole, methode) ñoo ko tënk aki àtte yu di kojug xellu aki am-am yu di kojug péng (lu wóor), ci ron jalub ay xam-xam ak seeni doxal (pratique) yu xarala yu la dul may fenn fooy sikke seenug nekk di yoon. Ci ndabi jamono (conditions) yu mel ne yii, ak ci am-am yu nirook yii xamaleg xeltu ga nu xamoon du manatee dëppook liggéey bi xeltukat bu jamonoo bi man a def, maanaam bu sunu jamono jii nu nekk, moom mi nga xam ne ab liggéeyam daa wuuteek bu ñoñ jamono yu yàgg ya lool.
Bu nu sukkandikoo ci li jiitu danu naan manatuñoo def nenn nu dul jéem a xool nu nuy soppee dégg-dégg ak maanaam xeltu ndax mu doon leegi “juddal hikma” te bañ a doonati “sopp hikma”
Xeltug waa-afrik
SoppiDawani(courant) xeltug waa-afrik gu mujj gi
Soppiyeneen Xeeti xeltu
Soppi- Xeltu leeg-leeg (nu koy melal ci ne mooy “xalaat ci xalaat” maanaam xalaat ci ni nuy xalaate ak ci jëmmi xalaat ci boppam akuw melokaanam, dees na ko melal it ci ne mooy jéem a tontu ci laaj yu mag yi nekk gi di laaj ak am gi(l'existence))
- Xeltu gu tur
- GBu xam-xam ak nattu
- Yu kojug nekk
- Yu kojug nite
- Xeltu gu yees (ni ko waa Amerig gu bëj-gànnaar gi baaxoo seggate ak Nguur gu bennoo gi(u.k) day xaw a barastiku jëm ci wàll gu xarala, bu jàllee ay wax (ay sujets) doog a digg, moom day sukkandiku ci xellu ( logique) ak seggat, kon ay yitteem day sottiku ci gis-gis bu kojug maanaa ( conceptual analysis)ak jikko ak melokaanu làkk ak wu xel.)
- Xeltug Ceggat
- xeltug waa-sapon
- Xeltug julliti-araab
- Xeltug waa-siin
- Xeltug yëwut
- xeltug waa-end
Yenn ciy xeltukat
Soppi- Kocc barma faal (Reewu Senegaal)
- Mohammed Bagayogo (Reewu mali)
- Ahmed Baba (juddoo Araun ca Mali ci 1556 )
- Anton Wilhelm Amo (rewu Gana)
- Kwasi Wiredu (Reewu Gana)
- Ibn Badjdja (Nguuru Marok)
- Ibn Battuta (Nguuru Marok)
- Ibn Khaldûn (Reewu Tinisi)
- Socrate (Reewu Geres)
- Diodore Cronos (Reewu Geres)
Xam-xam | ||||
Gëstubiddiw | Jëmm | Paj | Saytubiddiw | Simi | Xam-xamu suuf si ak jawwu ji | Xayma | ||||
Jokkoosoryante | Xaralaymbëj | Doolerandu | Kàttan | Xam-xamu nosukaay | Mbëjfeppal | ||||
Diine | Melosuuf | Wërlaay | Nit | Yoon | Koom-koom | Taariix | Xeltu | Kàllaama |