Yanu mbëj, ag jagle gu dàttu la ci wàll-wàllaani ab ne-ne, mooy tax seenug man a digaale ci ndimbalu tooli mbëjbijjaakon yi. Doole jiy judd ci googu digaale mooy sabab ag yëngu ci biir ne-ne bi, muy ab dawaanu mbëj. Bennaanu natt bu benn yan mooy Coulomb. Yan bi gën a ndaw bees man a natt mooy bi ab mbëjfepp di yanu, ñu koy faral di binde e = -1,602 10-19 c.

Yanu mbëj am mbir mees di janeer la, du lees man gis ak bët, dafa di aw tur wees jox genn feeñte gi ngir man a faramface wenn xeetu doxiin wi, di njeexiitam. Yanu mbëj man naa am ñaari xar-kanam yu wuute, di yees jàppee yu "dekkarle" ; benn bi di bu baax (+) beneen bi di bu bon (-). Ñaari yan yu wuute (bu baax ak bu bon) dañuy bijjante, ñaar yu bokk (ñaar yu baax walla ñaar yu bon) dañuy bëmëxante.

Yan yu bon yi lañuy faral a tudde ay mbëjfepp, yu baax yi di ay feppsaal ndax ñooy yiy nekk ci biir saalu xarefulwoon bi te kemu seen yan yam ak yu mbëjfepp yi te dekkarloo.

Dawaanu mbëj man naa am ñetti sabab: walug ay feppsaal (yan yu bon) walla walug ay mbëjfepp (yan yu baat), walla seenug wal ñoom ñaar ñépp ci jubluwaay yu dekkarloo.

Ngir bañ ay jaxasoo mbëjkat yi dañoo ànd ci ne walug yan yu baax yeey dawaanu mbëj, ci liñuy tudde dawaanu déggoo, ndax bu njëkk dañoo foogoon ne doxug wàll-wàllaan yu baax yeey jëmmal dawaan bi, donte tay jii dem nañu ba xam ne safaan bee nekk: dawaanu mbëj doxug mbëjfepp yee ko jur. Ndax feppsaal yi duñu ay wàll-wàllaan yuy dox, ci saalu xarefulwoon bi lañu sax dëkk. Bànqaasi xam-xam yi yittewoo gëstu yile feeñte ñooy xaralaymbëj ak mbëjfeppal.

Lëkkalekaay yu biir

Soppi