Mooy Mboor ci làkk wolof dëgg, di xam-xam bi'y gëstu la xewoon demb. Di itam mbooleem ay Jëf ak ay xew-xewu demb, la ko dale ca ña nu jiitu woon ba ci nun. Taariixkat mooy ki'y gëstu di bind ci wàllu taarix

Afrik, 1812

Xam-xamu taariix moo nuy melalal mbiri dëkk yeek dëkk-dëkkaan yu yàgg ya, ci biir jamonoy taariix, ak mbiri seen way dëkk. Da na nu waxal it ca dund ga fa amoon. Ci gàttal daal, xam-xamu taariix day gëstu li-wéyi nit (dembam) cig matale. Da na wuññi (feeñal) it nekkiin ak dundiin yi nga xam ne nit jaar na ci jànkoonteek ñoom ci dundam gu gudd gi, ci biir ay jamono yu dabante te toftaaloo, bu ko defee mu gëstu anami jëm-kanam yi nga xam ne nekktéef bii (di nit) amal na leen ci taariixam bu gudd bi, ci noonu loolu jural ñu ñu jange ci daj-dajam (li mu jot a dund) yooyu wéy, aki ndamam, te jéem a moytu ay pakkastalam aki rëcc-rëccam ya jàll.

Bu lii amee nag dina nu gis njariñ ak ngënéeli gëstug xam-xamu taariix.


Li ñu jublu ci jàng taariix

Soppi

Taariix dinanu ko jang ngir mu yombalal ñu xam mboolaayi nit ñi ci anam gu xereñ, te dégg (nand, gis), xàmmee it buum yi leen boole.

Gëstu dundug buur yeek imbraatoor yi rekk du lenn rek li nu war a yitteel ci taariix, li ci gën di farata kay mooy gëstu dundug mbooloo yi ak bennaan yi (benn-benn nit ñi). Ak gëstu jafe-jafe yi daa yeesu ci seenug dund bis bu Yàlla sàkk, te jéem leen a wutali saafara yu dëppoo, ba maas giy ñëwi ëlëg man cee jariñu.

Digal taariix (wutal ko aw dig)

Soppi

Ngir digal ab xew-xew fàwwu mu am ab tombub boy (fa muy dooree). Ay tombi boy yu bari nag am nañu te taariix man na cee tàmbalee. Nasaraan yi ñoom seen tombub boy mooy juddug Yonnant Yàlla Isaa, ca lañuy taariixe seeni xew-xew, bu dee jullit ñi ñoom seeni xew-xew ñi ngi leen di wutaluw dig wu bawoo ca gàddaayug Yonnant bi(j.m) juge Màkka ga mu ganee àdduna, dem Madiina. Xew-xew bii nag mi ngi fiirook (dajeek) atum 622 ci taariixu juddug Yonnant Yàlla Isaa.

Jamono yi

Soppi

Donte taariix mooy la xewoon ba àdduna sosoo ba léegi, taariixu nit ñi, suuf si, jawwu ji,... Waaye ci déggoo taariix ñu ngi koy tàmbalee ca ba ñu sàkkee mbind, séddale ko ci ay jamono. Li nga xam ne ay téere yu ñu bindoon moo ñu ko xamal.

Njëkk-taariix(mooy taarixu ñi fi nekkoon laataa sàkkug mbind)

Taariix( mooy lépp li xewoon ca ba ñu sàkkee mbind ba leegi). Taariix ci boppam dañu koo sédale ci ay jamono.

Jamono ju yàgg ja: (feeñug nit ci suuf ba daanu'g nguuru rom gu mag ga ci 476)

Jamono ju diggu ja: ( ba feeñug Amerig ci 1492)

Jamono ju bees ja: (ba fippug waa-frãs ci 1789)

Jamono ju mujju ji:( ba ci sunu bis yii)

Njëkk-taariix

Soppi

Boroom xam-xam yi, ginnaaw gëstu gu ñu def ci suuf si, wuññi nañu ay jeexiit (reste;vestige;trace) yu yàgg: ay jumtukaay, ay xor, ay doj, añs yuy tegtale ne suuf sii déy aw nit dëkke woon na ko njëkk ay junniy at, jamono jooja la nuy tudde njëkk-taariix.

Moom nag mi ngi séddaliku ci ñaari xaaj:

Ci ngënéelul jeexiit yii lanu xame njëkk-taariix. Nit ci jamono jii da daan tuxu rekk, di jëfandikoo ay ngànnaay aki jumtukaay yu njëlbéenu (primitive) (doj yu ñu yatt, ay ngànnaay, ay xeej aki xepp). Bi jamono gënee dox, seen dund gi soppiku, ñu xam leegi sawara, jëfandikoo ko ci togg ñam yi. Ci jamonoy doj wu ñu xacc wi, lañu tàmbalee dajaloo, sóobu ci mbéy, sàmm ak ràbb ak liggéey jumtukaay yu xànjar yi, tàmbali it di def yenn liggéeyi fànn yi niki bind ci doj (ciseler ;graver), ak yatt. La ko dale ca 3500 n.j.g (njëkk judd gu yonnant Yalla Isaa), la weñ feeñoon, ñu fent it mbind. Bi weñ feeñee, fentees it mbind la njëkk taariix jeex, taariix daal di tàmbali.

Ñenn ci ay taariixkat

Soppi

Seex anta Joob(Cheikhe Anta Diop)

Paate sow

Téerekaay

Soppi

paate sow (wo): Dembi Senegaal, 1998


Xam-xam
Xam-xam
Gëstubiddiw | Jëmm | Paj | Saytubiddiw | Simi | Xam-xamu suuf si ak jawwu ji | Xayma
Xarala
Jokkoosoryante | Xaralaymbëj | Doolerandu | Kàttan | Xam-xamu nosukaay | Mbëjfeppal
Xam-xami nite ak mboolaay
Diine | Melosuuf | Wërlaay | Nit | Yoon | Koom-koom | Taariix | Xeltu | Kàllaama
wikbaatukaay am na xët wu tudd: Taariix