Mbëjbijjaakon
Mbëjbijjaakon mooy banqaasu jëmm biy gëstu feeñte yu mel ne mbëj ak bijjaakon ak lépp lu leen ñeel (niki ci misaal tooli bijjaakon yi juddoo ci dawaanu mbëj ak dawaani mbëj yi juddoo ci tooli bijjaakon).
Ñoo ngi ko tëgg ngir man a faramface ci anam gees boole feeñte yu mbëj ak yu bijjaakon. Ay feeñte yu mel ne xiirtalug mbëjbijjaakon ngir wone ni toolu mbëj lënkook toolu bijjaakon: ab toolu bijjaakoon buy soppiku dafay jur ab toolu mbëj, naka noonu la toolu mbëj buy soppiku di juree ab toolu bijjaakon. Yamaleb Maxwell mooy liy faramface mbëjbijjaakon te di sukkandiku ci yan ak dawaanu mbëj.
Taariix
SoppiWilliam Gilber , ci téereem ba De Magnete (1600), la wone wuute gi nekk ci diggante aw yaram wu mbëj ak wu bijjaakon. Mu fésal àtte yi laqu ci bëmëxante ak xëccante yu bijjaakon yi jaare ci seeni dott ak njeexit li tàngoor am ci bijjaakon bu weñ.
ci 1831 la Michael Faraday doon gëstu doxiinu dawaan bi ci biir ab toolu bijjaakon ba gis ca ne, moom bijjaakon bi, man naa jur liggéey. Oersted moom wuññi woon na ne ab dawaanu mbëj dafay jur ab toolu bijjaakon, Faraday moom wuññi ne ab toolu bijjaakon dafay xiirtal ab dawaanu mbëj. Ci noonu la wuññee baaxi doxalukaay bu mbëj ak ni liggéey bu doolerandu man a soppeekoo kàttanu mbëj, naka-noonu mu sàkkee ca ab jurukaayu dawaan.
Mbëjbijjaakon a ngi judd ci bi James Maxwell (1864) boolee ay gisiin yu jiitu woon, niki mbëjtekkaaral, bijjtekkaaral. Bii gisiin di bees bennal moo leeral jikko yi ci yani mbëj yeek dawaani mbëj yi, bijjaakon yi, duusi mbëjbijjaakon yi, yu mel ne ag leer walla duusi rajo yi.