Mbëj
Mbëj da di ag feeñte gu gisuwul ak bët, guy feeñ ci ag wootalante walla bëmëxante ci diggante yani mbëj yi. Ci gattal mooy gépp feeñte gu juddu ci jàmmaarloo gi nekk ci diggante: feppsaal yi, ñoom ci lu ëpp da ñuy tekkaaral, ak mbëjfepp yi nga xam ne ñoo ëpp yëngu-yëngu, ci biir xarefulwoon bi. seenuw demiin jur ab dawaanu mbëj.
Su ñu ko boole ak bijjaakon, mu jur beneen banqaas bi ñu duppee mbëjbijjaakon. Mbëj moo yor ay feñte yu jëmm yu mel ne melax, toolu mbëj ak dawaanu mbëj (ci lu bari dañ leen di jaawale).
Mbëj doon na “jaamu” nit bi gën, doon tamit raññeekayu àdduna bu bees bi. Dafay leeral sunu dëkkuwaay yi di doxal sunu këri koom-koom yi te jegeele nit ñi gënoon a soriyante.
Yanub mbëj
SoppiYanub mbëj doon na lu ñu man a natt te man koo jëfandikoo, waaye doonul lu neex a faramface ak ay baat yu yomb a nand, ndaxte yombul leeral melokaan yi mu am dëgg-dëgg. Xayna li gën mooy wax lan la ak li muy sabab. lépp (lu mu man a doon) lu am yanub mbëj, man nañoo wootalante walla bëmëxante. Li gëstu yi wone mooy am na ñaari xeeti yani mbëj, benn bi lañuy woowe yan bu baax (+) moom mooy nekk ci biir saalu xarefulwoonu ne-ne yépp ak yan bu bon (-) (mbëjfepp) ñoo nekk ci li wër saalu xarefulwoon yi. Naka-jekk yan yu baax yu saalu xarefulwoon bi dañuy tolloo ak limu yan yu bon yu mbëjfepp yi ko wër.
Dawaan bu wéy ak bu safaanu
SoppiNgir Xóotal, yëral bii jukki ci Dawaanu mbëj |
Ba fii danoo jàppoon ne, gépp ndombo goo jël, mbëjfepp yi dañuy yëngu saa su ne jëm ci benn jubluwaay ci biiram. Yenn saa yi nag dawaan bi du sax ci maase, muy ci doole walla ci jubluwaay bi. Ag noste mbaa ag ndombo gu ne mel lees di wax dawaan bu wéy. Am misaal man naa nekk ag noste gu ab tegle di doxal. Donte sax aajowoowul dawaan bi di am genn jubluwaay gu sax. Bari nañu ndombo yu mbëj yees di jëfandikoo yuy safaan jubluwaayu seen dawaan ci biir ndombo gi.
Gii xeetu dawaan lees di wax dawaan bu safaanu. Ndombo yu mbëj yu ëpp yi ñuy jëfandikoo, dawaan bu safaanu lañu. Cig ndombo gu dawaan bu safaanu, dafay laaj waxaale tamit baraayu ni dawaan bi di safaanoo, taraayu dawaan bi ak dend bi ci ndombo gi, moom rekk , bu mujj bi, doy na su fekkee dawaan bu wéy la. Ci baraay bi lañuy natte ñaata yoon la dawaan bi di soppi jubluwaay ci benn saa.
Mbëj ak Bijjaakon
SoppiLiy wër ab mbëjfepp walla leneen lu mu man a doon lu am ab yanub mbëj day am melokaanu luy dox, moom lañuy tuddee toolu mbëj.
Soo jallaxee ay mbëjfepp, day am benn tool bu wër seenub jublu, moom la ñuy tuddee toolu bijjaakon. Dooley tool boobu dafa aju ci limu mbëjfepp yiy daw ak seen gaawaay, maanaam, ci yeneeni kàddu, ci dawaanu mbëj bi.
Soo jallalee ab dawaan ci ag lëmës, gu nekk wëñu përëm, ci nimu waree, lëmës googu day mel ne bijjaakon gu weñ, day xëcc walla bëmëx yeneen lëmës yi mu yemal wëñ. lëmës gu mel noonu su fekkee danga koo defaree ak ag wëñu përëm goo wëndeel cib weñ, day gën a yokk toolu bijjaakon ba cay juddoo. Su fekkee dangaa am ay lëmës yu bari, yu ñu wëndeel wëñ ci weñ, yu man a wëndeelu, nga boole leen ak yeneeni lëmës yu dul wëndeelu, yu am toolu bijjaakon bu tar, yu dawaan jaar, day jur jenn dooley doolerandu. Doole joogu moy wëndeel lëmës yu man a wëndeelu yi, mu daal di man a def liggéeyu doolerandu. Mu nekk ab jumtukaay bi ñuy woowe doxalukaay bu mbëj. Tay jii, doxalukaay yu mbëj yi ñooy doxal bépp wuutuloxo, tambalee bi ci gën a ndaw ba ca ba gën a ngande. Doxalukaay yi dañoo bari te am ay melokaan yu wuute.
Soppalikaay
SoppiNgir Xóotal, yëral bii jukki ci Soppalikaay |
Njariñ li ci jëfandikooy noste yu dawaan bu safaanu moo ngi ci li ñuy man a yokk walla waññi dayoo bu ab dendam ci jëfandikoo jumtukaay bees di woowee soppalikaay. Ab soppalikaay ñaari taxañ yu tàqalikoo lay am, yees ber, yu ay wëñ yees lëmës cib dankub weñ (saalu soppalikaay bi). Ab dawaan bu safaanu su walee ci taxañ bu njëkk bi, ab toolu bijjaakon daf fay juddoo, mu jur moom itam, ab dend buy soppeeku ci jenn jamono ju nekk ci ñaareelu taxañ bi. Su ñu jëlee benn dayoo bu saal bi (weñ gi) ak yenn limi lëmësi wëñ yu taxañ yi, dees na man a yokk walla waññi dend bi ci nees ko bëgge. Kon, ab Soppalikaay di nanu tax a man a jëfandikoo dend bu suufe, ngir sunu kaaraange, ci kër yi, te terewul nu man koo jokkale, mu jóge cib digg bu mbëj bu sori, cib dend bu kawe. Manees naa jëfandikoo ab soppalikaay ciy fowekaay yu mbëj ak ci yeneen jumtukaay yu ndaw yu mbëj ba-tay. Maneesul a jëfandikoo soppalikaay cig ndombo gu dawaan bu wéy, ndaxte dawaan bi toolu bijjaakon ba muy jur duy soppiku.