Dawaan gu wéy

(Yoonalaat gu jóge Dawaan bu wéy)

Dawaan gu wéy (ñu man koo tënk ci DC Direct Current ci wu-angalteer, moom lees di gën a jëfandikoo), di dëddoo ak dawaan gu safaanu AC, xeetu dawaan la gu am genn jubluwaay. Dawaan gi dafay wéy di dox ci ag ndombo ci genn jubluwaay. Mbëjfeppal yi ci genn jubluwaay lauy wéy di daw.

njunj gu dawaan gu wéy

Nattiin

Soppi

Dawaan gu wéy ciy amper lees koy natt. Benn amper mooy ,24*1018 mbëjfeppal ci saa (I = Q/t), I = dawaan, Q= coulomb, t= saa).

Wenn rëdd wu wéy ak ñett yu ndaw, ci suufam, mooy njunju dawaan gu wéy; dees na jëfandikoo itam DC (Direct Current). Dawaan gu safaanu moom AC alternating current lees di jëfandikoo wall njunj wii di ~.

Jëfandikoom

Soppi

Dawaan gu wéy lees di jëfandikoo lu bari la ci taraay gu suufe ak ci mbëjfeppal, rawatina ci jumtukaay yiy doxeek tegle yiy man a jur dawaan gu wéy kepp. Ci daamar yi, su safaanukaay bi juree dawaan gu safaanu dess koy soppali gu wéy. Saxaar yiy doxee mbëj itam ñoom dawaan gu wéy lañuy jël.

Taariixam

Soppi

Thomas Alva Edison mooy ki fi taxawal séddaleeg dawaan gu wéy ci wetu njeextalu XIXu xarnu bi, bi ndefar gi tambalee jëfandikoo mbëj. Ci ginnaaw bi lees ko wuutaleek dawaan gu safaanu gi Nikola Tesla sakk, ndax limu gën a yomb a yóbb ci diggante yu gubb.

wikbaatukaay am na xët wu tudd: Dawaan gu wéy