Mbëjfeppal
Mbëjfeppal, di ci wu-faraas "électronique", "إلكترونيات" ci araab, ab banqaasu jëmm la buy saytu, gëstu, jumtukaay yu mbëj yi seen dox wékku ci walug ay mbëjfepp. Ci maanaa, baat bi tay dafay tekki mbooleem lees xam di ko jëfe ak di ko xalaat muy tax a man a xalaat ak a nekkal jumtukaay yuy dox ak mbëj. Li mbëjfeppal di amal mooy ay ndomboy mbëjfeppal yu ñuy defar ak cër yu bari yees di lëkkale ci ndimbalu ay wëñ, naka-jekk wëñi mbéll, yu dawaanu mbëj di jaar ci seen biir.
Mbëjfeppal ak xaralaymbëj nekk nañu ñaari banqaasi jëmm yu jegeente, seenug wuute mi ngi ci seen solo: su xaralaymbëj yoree li ñeel jóox dawaanu mbëj, seenug jokkale ak defari wuutuloxo yu mbëj, Mbëjfeppal moom, li ko yitteel mooy jëfandikoo mbëj ngir man cee weccee ay xibaar.
Xam-xam | ||||
Gëstubiddiw | Jëmm | Paj | Saytubiddiw | Simi | Xam-xamu suuf si ak jawwu ji | Xayma | ||||
Jokkoosoryante | Xaralaymbëj | Doolerandu | Kàttan | Xam-xamu nosukaay | Mbëjfeppal | ||||
Diine | Melosuuf | Wërlaay | Nit | Yoon | Koom-koom | Taariix | Xeltu | Kàllaama |