Njeexitu joule mooy tur wees jox feeñte gees di gis saa su dawaanu mbëj jaare cib wommatukaayu mbëj, muy juddug ag tàngoor. Kemu tangoor gee ngi aju ci taraayu dawaan bi. Baat bi jóge ci James Prescott Joule di ab jëmmaan bu waa-angalteer, di ki doon gëstu feeñte gi ci wetu ati 1860.

Ci xayma manees naa bind lii:

Fa:

  • V doonee dend bi
  • I doonee dawaan bi (di dayoob mbëjfepp yiy jaar ci wommattukaay bi ci saa su nekkk)


Ci ab dëgërlukaay ngóora gi manees na koo natte niki:


Fa R doonee ndëgërlu gu ndombo gi. Feeñte gi li muy jur mooy ñakkug kàttan ci biir wommatukaay, di soppaliku tangoor. Kon xamees na ne doon na mbir mees war a tuutal lunu man, rawatina ci bu ñuy séddale kàttanu mbëj mi. lees man a def ba wàññi ñakkug kàttan googu mooy dijjal wommatukaay bi walla waññi dawaan biy jàll ci biiram.

Njeexitu joule du fépp la bonee ndax tangoor gi muy jur manees na koo jëfandikoo ci defari puur, ci sunu kër yi, làkkuwaayu mburu yi,...