Dawaan bu safaanu
Dawaan bu safaanu (DS walla AC ci wu-angalteer: Alternating Current) màndargoo ag walug dawaan guy soppiku ci jamono muy ci taraay walla ci jubluwaay.
Doxiin
SoppiNaka-jekk dawaanu mbëj suñu koy séddale, ci dawaan bu safaanu bu baraayam sax ci 50 Hz walla 60 Hz lees koy defe (+ ak - bi dañuy safaanu ci watatukaay bi juroom-fukki saa yu ne). Dawaan bi ak dendu mbëj bi, ci biir watatukaayu mbëj bi, seen Demiin dafay mel ne bu ab duusub sin.
Jëfandikoo gu dawaan bu safaanu mi gi jóge ci li jurukaayu dawaan yi, ci yaxanaay ci koom-koom ak seenug yomb a defar, di jur dawaan bu safaanu ci anam gu yomb, kon dawaan bi ci boppam kenn du ko soppiwaat laataa ag jëfandikoo.
Fi njariñ li gën a feeñee sax mooy séddaleeb dawaan bu safaanu bir na ne moo gën a yaxan dawaan bu wéy ci séddaleeb dend bu kawe (ñakkug kàttan gi ci buum yu gudd yi moo gën a néew). rawatina, ci diggante gu gennwéq walla wéq yu bari, bir na yaxanaay gu ñettiwéq di gees gën a jëfandikoo ndax néewteey ñakkug kàttan ngir njeexitu Joule (moo tax dijjaayu watatukaay yi gën a néew, maanaam wëñ yu gën a sew); jëfandikoog dawaan bu safaanu bu ñettiwéq lawal na buumi yóbb yi ci diggante yu gudd lool yi.
Genn Màndarga gu am-solo gu dawaan bu safaanu, ba waral ci genn wàll li tax ñépp jël ko, mooy yomb gee jëfandikoo fu nekk, yomb gee soppi ci lim yu wuute ci taraayu dawaan, ci ndimbalu soppalikaay yi, ak ñakkug kàttan gu digu.
Donte yenn jumtukaay yi dawaan bu wéy lañuy doxe, waaye loolu manees na koo ame ci dawaan bu safaanu, sunu jëfandikoo ab jubbantikaay.
Suñu jëfandikoo ag xaralag mbëjfeppal gu kàttan gu ñaw, manees naa jëfandikoo dawaan bu wéy ngir am dawaan bu safaanu, jur ko ci yenn anami baraay, melokaanu duus ak taraay jaare ko ciy jumtukaay yees duppee jallarbikaay.
Taariix
SoppiCa njalbeenu njëfandikug kàttanu mbëj ci ndefar gi ci XIXu xarnu daawaan bu wéy lañu doon jëfandikoo, ndax li mu doonoon lu neex a rënk ciy tegle ak li mu gën a wóor dawaan bu safaanu. Tomb bu mujj bi Thomas Alva Edison mooy ki ko doon wax ci lees tuddewoon xareeb dawaan yi.
Dawaan bu safaanu, gi soloom doonoon lu beneen xaaj bi boole woon Nikola Tesla ak George Westinghouse doon aar, manul a ñakk ci njëfandiku gu ab soppalikaay, moom mi tax ñuy man jokkalante mbëj mi ci diggante yu gudd. Te itam doxalukaayu mbëj yu dawaan bu safaanu ñoo gën a wóor te gën a yaxan yu dawaan yu wéy yi.
Ci jamono jii ci àdduna bi dawaanu mbëj ci ñaari baraay lañu koy séddalee, 50 Hz(Tugal, Asi, Afrig) ak 60 Hz(Diiwaan-yu-Bennoo ak goxu Aamerig bépp ci lu daj, genn xaaju sapoŋ) ak taraay yu wuute.
Xool it
SoppiTéerekaay
Soppi- (en)Charles Proteus Steinmetz: Theory and Calculation of Alternating Current Phenomena (McGrawHill, 1900)
- (en)Charles Proteus Steinmetz: Electric Discharges, Waves and Impulses (1914) * (en)Charles Proteus Steinmetz: Theoretical Elements of Electrical Engineering (1915)
- (en)Charles Proteus Steinmetz: Theory and Calculation of Electrical Apparatus (1917)
- (en)Charles Proteus Steinmetz: Theory and Calculation of Transient Electric Phenomena and Oscillations(McGrawHill, 1920)
- (en)Louis Cohen: Formulae and Tables for the Calculation of Alternating Current Problems (McGraw-Hill, New York, 1913)
- (en)Ernst Julius Berg: Electrical Engineering, First Course (McGrawHill, New York, 1916)
- (en)Ernst Julius Berg: Electrical Engineering, Advanced Course (McGrawHill, New York, 1916)