Jurukaayu mbëj
Jurukaayu mbëj ab jumtukaay la buy tax ñuy man a jël wenn xeetu kàttan wi soppi ko kàttanu mbëj. Naka-jekk xeeti kàttan yees di soppali gu mbëj ñooy gu doolerandu, gu simi, gu leer ak gu tàngoor. Jurukaayu mbëj yi dañu leen di séddale ci jurukaayu dawaan ak jurukaayu dend, bu njëkk bi manees na koo, itam, séddale ci jurukaayu dawaan bu safaanu ak jurukaayu dawaan bu wéy.
Jurukaayu dawaan ak bu dend
SoppiÀtteb ohm mooy yamale giy wone digaale gi ne ci diggante dawaan ak dend ci biir ag ndombo gu mbëj. Bu ci yokku sa moroom wàññeeku su ngóora gi soppikuwul.
Tekki:
- P ngóora gi, ñu koy natt ciy watt.
- V mooy dend bi ne ci diggante ñaari cati wommatukaay bi , volt mooy bennaanu nattam.
- I mooy dawaan biy jàll ci wommatukaay bi, ampere mooy bennaanu nattam.
Jurukaayu dawaan
SoppiAb jurukaayu dawaan mooy tax nu man a am dawaan bu sax, limam ci biir ag ndombo gu mbëj gu mu nekk du soppiku ci coppiteg dend bi, limu dend bi man naa nekk lu ne te moom du soppiku.
Jurukaayu dend
SoppiAb jurukaayu dend moom mooy tax dend bi ci ag ndombo di sax, dayoom du aju ci dawaan bi.