Afrig
Afrig, Afirig, moom la ñu jàppee ne mooy gox bi nit cosaanoo, su nu ko xoolee ci yaatuwaayam ak bariwaayu askanam (lu weesu gox bu Asi), mooy ñaareelu gox bi gënn a rëy ci àdduna bi. Yaatuwaayam tollu na ci 30.065.000 km², nekk 20,3% ci jéeri ji ci àdduna bi. Ay way dëkkam tollu ci lu ëpp 800.000.000, muy benn juroom ñaareel bu way dëkki àdduna bi. Afrik a ngi yem ci bëj-gànnaaram ci Géej gu Diggu gi, ci sowwu ci Mbàmbulaanug Atlas, ci bëj-saalum ci Mbàmbulaan gu Bëj-saalum gi, ci penku ci Mbàmbulaanug End. Asi rekk la taqalool ci yeneen gox yi. Yamoo gi jàll na ko. Ci jëmm doon na gox bu bari'y melokaan, te wuute teg ci.
Cosaanam
SoppiBaatu «Afrig» moo ngi jóge ci turu Afridi yi, doonoon ag giir gu dëkkoon ci Bëj-gànnaaru Afrig ci diwaanu Kaartaas.
Beneen cosaanam moo bàyyikoo ci Berber Taferka «suuf», «boroom suuf». Ki fay dund la ñuy woowee Aferkiw, Latin yi soppi ko africanus, mu doonoon aw tundu waa rom ci Afrig. Araab yi di ko wax إفريقيا ifrīqīyā, mu doonoon Tiniisi gu tay gi.
Ñeneen ne ci baatu waa geres bii di aphrike («amul sedd»), latin di ko waxaprica («Bari naaj»), la jóge.
Taariix
SoppiAfrik la ñuy jàppee ne mooy cosaanu nit, ndax desiti nit yi gën a yàgg ci àdduna bi fa la ñu ko gisee, ci Afrig gu Bëj-saalumu-Sahara.
Sahara cëru na bu baax ci màggug gox bi. Taariixu askani Bëj-gànnaaru Afrig yi day tolloo ak bu Tugal ak bu Penku gu Diggu gi. Li ëpp ci Afrig gu Bëj-saalumu-sahara amul woon genn jëflante ak li des ci àdduna bi, da ñoo beru woon.
Jamono ju yàgg ja
SoppiXay yi juddoo ci goxu Afrig, boole nañ leen ci yi gën a mag ci taariixu nit. Xayu Esipt ak bu Gana ak bu Mali, ak bu Kuush ak bu Songaay, añse.
Jamono ju yees ji
SoppiJàppum njaam
SoppiNgir Xòotal, yërël bii jukki ci Jàppum njaam |
Ci li taariixkat yi wax, jàppum njaam mi ngi tambali ci xarnub VII ak araab yi. Ci lu gën a leer ci atum 652 ba Ab njiitu araab takk-taxawalee waa Nubi yi ngir ñu jox leen 360 ciy jaam at mu jot. barab yi njaay mi doon amee mi ngi dale ca Mali ba Penku Afrik, ci wàll gi féete bëj-saalumu Sahara.
Ci xayma nee nañ ci diggante xarnub XVIII ba ci xarnub XIX, benn ñenteel ci nit ñi ay jaam la ñu woon, walla ñu ñu manante (takk-taxawal) ci liggéey bu ñu sañut a bañ. Nee nañ njiitu waa afrik yi ci seen bopp ñoo doon jàppaate ak a jaayaate.
Waa tugal lu weesu bi ñu aakimoo (walla sancee) suufi Aamerig yi da ñoo soxla woon ay loxo yuy liggéey ci seen tool yi. Def nañ ko ci 400 at (1500-1888), ay jaam yu bari jënd nañ leen walla jàpp nañ leen ci tefesi afrik yi: Sowwu Afrig gépp, ak ci bëj-saalumam itam. Donte tereg jàppum njaam gi mi ngi waddoon ci lu jege atum 1850 (réew yépp bàyyeendoowuñu ko) amoon ay nit yu wëyoon di ko def cig làqatu ba ci 1900.
Jamono ju mujj ji
SoppiAakimoo gu waa tugal
SoppiJamonoy aakimoo gu tugal ci Afrig moo ngi tambalee ci Ndajeem Berlin (1884-1885) ba ci tembte yi ci atum 1960, sedatle gu réew yu tay yi ca la jóge. Ecoopi moo doonoon menn rèew mi ñu masut a teg
Melosuuf
SoppiNgir Xòotal, yërël bii jukki ci Melosuufug Afrig |
Réewi Gox bi
SoppiTuri Réew yeek seen raaya | Rëyaay (km²) |
way-dëkk (1 sulet 2002) |
Fattaay (ci km²) |
Tembte | Péey |
---|---|---|---|---|---|
Penku Afrig: | |||||
Buruundi | 27 830 | 8 090 068 | 229,0 | 1962 | Bujumbura |
Komoor | 2 170 | 690 948 | 283,1 | 1975 | Moroni |
Jibuti | 23 000 | 768 900 | 20,6 | 1977 | Jibuti |
Eritere | 121 320 | 4 465 651 | 36,8 | 1993 | Asmara |
Ecoopi | 1 127 127 | 74 777 981 | 60,0 | Addis-Abeba | |
Royuwaay:SSD Sudaan gu Bëj-saalum | 644 329 | 12 778 250 | 20 | 2011 | Juba |
Keeñaa | 582 650 | 34 707 817 | 53,4 | 1963 | Nairobi |
Madagaskaar | 587 040 | 18 595 469 | 28,1 | 1960 | Antananariwo |
Malawi | 118 480 | 13 013 926 | 90,3 | 1964 | Lilongwe |
Mayot (Faraas) | 374 | 201 234 | 456,9 | Mamudsu | |
Mosambik | 801 590 | 19 686 505 | 24,5 | 1975 | Maputo |
Ruwandaa | 26 338 | 8 648 248 | 280,9 | 1962 | Kigali |
Seysel | 455 | 83 688 | 176,0 | 1976 | Wiktoria |
Somali | 637 657 | 7 753 310 | 12,2 | 1 suwe 1960 | Mogadisu |
Tansani | 945 087 | 37 187 939 | 39,3 | 1961 | Dodoma |
Ugandaa | 236 040 | 24 699 073 | 104,6 | 1962 | Kampala |
Simbaawee | 752 614 | 9 959 037 | 13,2 | 1980 | Lusaka |
Saambi | 390 580 | 11 376 676 | 29,1 | 1964 | Arare |
Diggu Afrig: | |||||
Angolaa | 1 246 700 | 10 593 171 | 8,5 | 1975 | Luanda |
Kamerun | 475 440 | 16 184 748 | 34,0 | 1 Samwie 1960 | Yaunde |
Réewum Diggu Afrig | 622 984 | 3 642 739 | 5,8 | 1960 | Bangi |
Cadd | 1 284 000 | 8 997 237 | 7,0 | 1960 | Njamena |
Kongóo | 342 000 | 2 958 448 | 8,7 | 1960 | Brasawil |
Kongóo-Kinshasa | 2 345 410 | 55 225 478 | 23,5 | 30 suwe 1960 | Kinshasa |
Gineg yamoo | 28 051 | 498 144 | 17,8 | 10 sattumbar 1974 | Malabo |
Gaboŋ | 267 667 | 1 233 353 | 4,6 | 17 ut 1960 | Librewil |
Sao Tome ak Principe | 1 001 | 170 372 | 170,2 | 1975 | Sao Tome |
Bëj-gànnaaru Afrig: | |||||
Alseeri | 2 381 740 | 32 277 942 | 13,6 | 1962 | Alse |
Isipt | 1 001 450 | 70 712 345 | 70,6 | 28 fewirie 1922 | Xayra |
Libi | 1 759 540 | 5 368 585 | 3,1 | 20 disembar 1951 | Tripoli |
Marok | 446 550 (710 050 ak sahara) | 31 167 783 | 69,8 | 2 awril 1956 | Rabat |
Sudaan | 1 861 484 | 40 782 742 | 22 | 1956 | Xartum |
Tiniisi | 163 610 | 9 815 644 | 60,0 | 20 awril 1956 | Tunis |
Suufus waa-tugal ci bëj-gànnaaru Afrig : | |||||
Duni Kanaari (Ispaañ) | 7 492 | 1 694 477 | 226,2 | Las Palmasu Kanaari gu Mag, Santa Cruz gu Tenerif | |
Ceuta (Ispaañ) | 20 | 71 505 | 3 575, 2 | — | |
Madeira (Portugaal) | 797 | 245 000 | 307,4 | Funsal | |
Melilla (Ispaañ) | 12 | 66 411 | 5 534, 2 | — | |
Bëj-saalumu Afrig: | |||||
Botswana | 600 370 | 1 591 232 | 2,7 | Gaboron | |
Lesoto | 30 355 | 2 207 954 | 72,7 | Maseru | |
Namibi | 825 418 | 1 820 916 | 2,2 | Windok | |
Afrig gu Bëj-saalum | 1 219 912 | 43 647 658 | 35,8 | Pretoria | |
Eswatini | 17 363 | 1 123 605 | 64,7 | 1968 | Mbaban |
Sowwu Afrig: | |||||
Bene | 112 620 | 6 787 625 | 60,3 | Porto-Nowo | |
Burkinaa Faaso | 274 200 | 12 603 185 | 46,0 | 5 ut 1960 | Uagadugu |
Kap Weert | 4 033 | 408 760 | 101,4 | 5 sulet 1975 | Praia |
Kodiwaar | 322 460 | 16 804 784 | 52,1 | 7 ut 1960 | Abijaa, Yamusukro |
Gaambi | 11 300 | 1 455 842 | 128,8 | 1965 | Banjul |
Gana | 239 460 | 20 244 154 | 84,5 | 6 Maars 1957 | Akra |
Gine | 245 857 | 9 371 065 | 31,6 | 2 Oktoobar 1957 | Konaakri |
Gine Bisaawóo | 36 120 | 1 345 479 | 37,3 | 10 Sattumbar 1974 | Bisaawóo |
Libeeria | 111 370 | 3 288 198 | 29,5 | 1847 | Morowia |
Mali | 1 240 000 | 11 340 480 | 9,1 | 1960 | Bamako |
Gànnaar | 1 030 700 | 2 828 858 | 2,7 | 1960 | Nuasot |
Niseer | 1 267 000 | 10 639 744 | 8,4 | 1960 | Ñaame |
Niseeria | 923 768 | 129 934 911 | 140,7 | 1960 | Abuja |
Senegaal | 196 190 | 11 343 328 | 57,8 | 4 awril 1960 | Ndakaaru |
Siraa Leyoon | 71 740 | 5 614 743 | 78,3 | 1961 | Freetown |
Togóo | 56 785 | 5 285 501 | 93,1 | 27 Awril 1960 | Lome |
Lépp | 30 368 609 | 843 705 143 | 27,8 |
Goxub Afrig gëstu gi aju ci ay way dëkkam
SoppiYërël bii jukki ci Way dëkki Afrig |
Cosaan ak diine
SoppiXool: Diiney Afrig
Làkk
SoppiGëstukatu-làkk yi ci xayma nee nañ 2 000 làkk ci goxu Afrik, ñu boole leen ci ñeenti mbooloo, làkk yi fa cosaanoowul bokkuñu ci.
Xool it
SoppiLëkkalekaay yu biti
Soppi- History of Africa The last tribal states.
Afritugalasi | Oseyaani | Afrig | Tugalasi |
Bëj-gànnaaru Aamerig | Tugal | Asi | Bëj-saalumu Aamerig |