Tugal
Tugal mooy wàll wi féete penku goxub Tugalasi, ci baax dees koy jàppe niki benn ci juroom-benn walla juroom-ñaari goxi àdduna bi. Gox baa gi digu ci sowwu ci mbàmbulaanug Atlas gi, ci bëj-gànnaar ci dottub Bëj-gànnaar bi, yem ci géej gu Diggu gi ci bëj-saalum. Ay digam ci penku dese nañoo leer, dinay faral di jur ay werante; li ko waral mooy ni mu taqalook goxub Asi.
Dayo | 10,180,000 km² (3,930,000 sq mi) |
way-dëkk | 710,000,000 |
fattaayu way-dëkk | 70/km² 181/sq mi |
Turu aji dëkk: | Waa-tugal |
Réew | 48 réew, 27 yi bokk nañ ci Bennoob Tugal |
Waa-Islaand jàppees na leen ni waa-tugal (donte féeteem ci degalub Tugal-Aamerig), ak mbooleem dun yi ci géej gu Diggu gi, Sipër mi gën a jur coow, ci wàllu melosuuf. Riisi ak Tirki ñi am li ëpp ci seen suuf ca Asi, waaye day ni rekk li ëpp ci seen taariix réewi gox bi lañu ko bokkal.
Melosuuf
SoppiNgir xóotal: Melosuufug Tugal Tugal a ngi yaatoo 10 392 855 km² (fukki junni-junni ak ñetti-fukki-junni ak juroom-ñent-fukk ak ñaar ak juroom-ñetti-téeméer ak juroom-fukk ak juroom). Di benn ñetti Afrig walla benn ñenti Asi walla Aamerig.
Mi ngi séedatliku ci jurromi diwaan: Penku Tugal, Diggu Tugal, Sowwu Tugal, Bëj-gànnaaru Tugal ak Bëj-saalumu Tugal
Gox bi am na 49 ciy réew.
Réewi Tugal
SoppiTuru diwaan aki réewam, ak seen raaya |
Yaatuwaay (km²) |
Way-dëkk (1 sulet, 2002) |
Fattaay/way-dëkk (ci km²) |
Péy |
---|---|---|---|---|
Penku Tugal: | ||||
Belaarus | 207,600 | 10,335,382 | 49.8 | Minsk |
Bulgaari | 110,910 | 7,621,337 | 68.7 | Sofiya |
Réewum Cek | 78,866 | 10,256,760 | 130.1 | Prag |
Oonguri | 93,030 | 10,075,034 | 108.3 | Budapest |
Moldaawi | 33,843 | 4,434,547 | 131.0 | Kisinawu |
Poloñ | 312,685 | 38,625,478 | 123.5 | Warsaw |
Romaani | 238,391 | 21,698,181 | 91.0 | Bukarest |
Riisi | 3,960,000 | 106,037,143 | 26.8 | Mosku |
Eslowaaki | 48,845 | 5,422,366 | 111.0 | Baratislawa |
Ukreen | 603,700 | 48,396,470 | 80.2 | Kiyew |
Bëj-gànnaaru Tugal: | ||||
Danmaark | 43,094 | 5,368,854 | 124.6 | Kopenagen |
Estooni | 45,226 | 1,415,681 | 31.3 | Talin |
Finlaand | 336,593 | 5,157,537 | 15.3 | Elsinki |
Islaand | 103,000 | 307,261 | 2.7 | Reykjawik |
Irlaand | 70,280 | 4,234,925 | 60.3 | Dublin |
Letóoni | 64,589 | 2,366,515 | 36.6 | Riga |
Lituwaani | 65,200 | 3,601,138 | 55.2 | Wilniyus |
Noorwees | 324,220 | 4,525,116 | 14.0 | Oslo |
Suweed | 449,964 | 9,090,113 | 19.7 | Stokolm |
Nguur-Yu-Bennoo | 244,820 | 61,100,835 | 244.2 | Londar |
Bëj-saalumu Tugal: | ||||
Albaani | 28,748 | 3,600,523 | 125.2 | Tirana |
Andoor | 468 | 68,403 | 146.2 | Andorra la Vella |
Bosni | 51,129 | 4,448,500 | 77.5 | Saarayego |
Korwaasi | 56,542 | 4,437,460 | 77.7 | Sagreb |
Ciipër | 9 251 | 788 457 | 85 | ... |
Girees | 131,940 | 10,645,343 | 80.7 | Aten |
Itaali | 301,230 | 58,751,711 | 191.6 | Rom |
Réewum Maseduwaan | 25,333 | 2,054,800 | 81.1 | Skopje |
Malt | 316 | 397,499 | 1,257.9 | Waleta |
Montenegro | 13,812 | 616,258 | 44.6 | Podgorika |
Portugaal | 91,568 | 10,084,245 | 110.1 | Lisbon |
San Marino | 61 | 27,730 | 454.6 | San Marino |
Seerbi | 88,361 | 9,663,742 | 109.4 | Belgrad |
Esloweeni | 20,273 | 1,932,917 | 95.3 | Jubaljana |
Ispaañ | 504,851 | 45,061,274 | 89.3 | Madrid |
Watikaa | 0.44 | 900 | 2,045.5 | Watikaa |
Sowwu Tugal: | ||||
Ótiris | 83,858 | 8,169,929 | 97.4 | Wiyen |
Beljik | 30,510 | 10,274,595 | 336.8 | Burusel |
Faraas | 547,030 | 59,765,983 | 109.3 | Paris |
Almaañ | 357,021 | 83,251,851 | 233.2 | Berlin |
Liechtenstein | 160 | 32,842 | 205.3 | Wadus |
Luksambuur | 2,586 | 448,569 | 173.5 | Lusambuur |
Monaako | 1.95 | 31,987 | 16,403.6 | Monaako (péy) |
Olaand | 41,526 | 16,318,199 | 393.0 | Amsterdam |
Suwis | 41,290 | 7,507,000 | 176.8 | Bern |
Diggu Tugal: | ||||
Kasakistaan | 150,000 | 600,000 | 4.0 | Astana |
Penku Tugal: | ||||
Aserbayjaan | 7,110 | 175,200 | 24.6 | Baku |
Jeoorji | 2,000 | 37,520 | 18.8 | Tibilisi |
Tirki | 24,378 | 11,044,932 | 453.1 | Ankara |
Lépp | 10,176,246 | 709,608,850 | 69.7 |
Karmat ak delluwaay
SoppiXool it
Soppi
Xool it Wikimedia Commons
|
Jukki yi ci lonku
SoppiLëkkalekaay yu biti
Soppi
Afritugalasi | Oseyaani | Afrig | Tugalasi |
Bëj-gànnaaru Aamerig | Tugal | Asi | Bëj-saalumu Aamerig |