Yoonu murit

(Yoonalaat gu jóge Murit)

Yoonu murit walla Muriidulaa ni ko ñenn ñi di waxe, wenn yoon wu am solo la wu tasawuf, muy moom tasawuf benn bànqaas bu mbóotu (mystique) ci lislaam , mi ngi nekk nag rawati na ci Senegaal ak Gàmbi. Muy lu ñu sos ci ndoortel XXeelu xarnu, ki ko def di Seex Ahmadu Bamba, yoonu murit nekk na tay yoon wi gën a am ag jeexiital ci Senegaal, bu ñu waxul ci Afrig gu sowwu gi [1] Murit yi tam ñi ngi jëf lu am solo ci wàllug koom-koom ak politig [1]. Njiitul réew mi Abdulaay Wàdd, mi ñu fal ci 2000, mooy njiitul Senegaal lu murit li njëkk a am [2].

Aaday Murit

Soppi

Aaday murit (walla ju yoonu murit)lu jeexiitalu ci caaday Afrig la, rawatina ju wolof. Yitte ak fulla ji yoon wi jox liggéey tax na ba mu man a suuxatu bu baax ci wàllug koom-koom ci Afrig, te tax na it ba mu man a tas bu baax ci dëkk yu mag yi ci Tugal ak Diiwaan yu Bennoo yi. Tay, daanaka mbooleem dëkk yu mag yu Bëj-gànnaar yi gàddaay gu Senegaal gi dëgmalsi te jëm fa kanam, am na ag Kër Sëriñ Tuubaa (Barabu daje ngir julli, jaamu Yàlla, defi màggal, daaray jàng xam-xam añs). Moom de dalub mbooloo mu murit mi la, fi ñuy defe seeni daje ngir jaamu Yàlla, walla ngir leneen, waaye it dana di jariñ it niki ab teeruwaayu gan ñeel way door a agsi yi ciy gan. Danañuy faral di def ab siyaare walla lu mel ne ag aj gu ñuy def ci at mu ne ca dëkk bu sell ba Tuubaa, gi nekk ci digg Senegaal.Màggal gi genn xumbéel la guy jëmmal at mu ne fàttalikug gàddaayal gi ñu defoon Seex Ahmadu Bamba ca 1895, ci loxol kiliftéef gu Canc gi (l'autorité coloniale).

Gongikubaat

Soppi
 
lenn ci ay njiiti yoonu murit wu tasawuf wi ci benn miir ci Ndakaaru

Baatub mourid walla murit ni ko wolof yi di waxe, mi ngi bawoo ci Jef ju Iraada, te mooy «  bëgg dara », « namm dara, xëccu jëm ci lenn » teg ca gongikooti ci murīd giy tekki « aji namm mbaa aji bëgg», jubloos ci aji namm ji Yàlla ki bëggul ku dul moom, lu dul moom, lu dul ngërëmam, loolu it mooy firi fonk gi taalube yi di def seeni sëriñ, ndax Yàlla ga ñuy gis ci ñoom, maanaam ñoom ñoo fi nekkal Yàlla ci jàngale Diine ak aar ko. Murit nag benn la ci ñaari baat yu ba ca des di Laah, kon muy muriidulaa, di tekki aji namm ji Yàlla, maanaam ki Yàlla rekk tax a jug, mu mel ne baat bii mbooleem yooni tasawuf yi dañu koy jëfandikoo niki taalube, walla dongo, waaye bokk na ci li gën a génne baat bi, jox ko fulla mooy ñëw gi yoon wi ñëëw ci jamono joj lislaam da cee xawoon a doyodi, néew ci doole, te li ko waral di nekk gi nit ñi nekke woon lu wuute ak lislaam, daan ko foye, yor geneen dund gu dul gi lislaam tànn, wii melo di lol ñu bari ci bindkati Senegaal yi wax nañu ci, ku ci mel ne Sëriñ Musaa Ka ak ñu ko moy, melokaan wii nag man nañu ne bokk na ci li taxoon Seex Ahmadu Bamba jugoon mel ne ku naan «ana ku namm Yàlla» ana «ku Yàlla tax a jug», ca foola la baat bii daal juge di tekki leegi képp ku di taalubeb murit, muy baat bob daa jug mel ne kuy tàqale diggante ki nekk ciy caaxaan ak ki ko nangoo ba te jublu lu baax li di Yàlla ak la ko wër. Sëriñ bi booy xool day mel ne yorul aw yoon, waaye lislaam la jug ngir taxawalaat, yeesalaat, ndax mbooleem yoon yi mu fi fekk, da leen a nangu, topp leen, jël seeni wird, daa na joxe mbooleem seeni wird te booba mi ngi yor wird wu juge ca Yàlla jaar ci Yonent bi Muhammad, ni yoon yepp ame seeni wird. Leegi kon luy ndayi muy joxe yooyule wird te yoroon wu boppam? Ndaxte daa jugaloon lislaam déet aw yoon, moom moo wax ne

« wépp wird wu waay yor ngir jëmmi Yàlla rekk te leneen taxu koo jug, moo xam woowu daa bawoo ca Jiilaani (Xaadiriya) mbaa mu juge ca Ahmad Tiijaan (tiijaan), na xam ne li mu yor moo dig jub»

Kon kii boole jullit yee ko taxoon a jug, yombal seenug jëm ca Yàlla, far digi yoon yi, boole ñepp ñuy jaami Yàlla ci ron keppaarug Lislaam

Yàllaange (Théologie) ak nosiin wu biir gi

Soppi

Yoonu murit Seex Ahmadu Bamba (1853-1927)moo ko sos, mu di aw yoon wu mbóotu wow mi ngi feeñ ci Senegaal ci biir aw nekkiin wu mboolaay wu ñu nëxël ag sellam jaxase ko, nga xam ne Canc gi (la colonisation) jaxase na bu baax nosteg màndaxoo gu mboolaay gi (le système d'équilibre social). Ngir nag yéwénal mboolaay gu senegaal gi Seex Ahmadu Bamba daa woote woon jëme ci ñu roy njàngalem Alxuraan mi, te ŋoy ci sunnas Yonent bi Muhammad (j.m), te xeeñtu it maanaay tasawuw yi te roy ci, fullaal it xam-xam ak liggéey te jox leen seen àq ak xiima.

Lii nag daa dëppoo ak li ñuy wooye ag yeesal mbaa ag yéwénal, ndax ci Tasawuf waxees na ne Yàlla (t.s) day yonni ci téeméeri at yu ne, jenn Aji yeesal (walla mujaddid) juy taxaw ci dundalaat, yeesalaat lislaam ca dëgg-dëggam, kooku tam mooy nekk aji donn ju ruu ju Yonent bi (j.m), ñu koy wax (qotb walla « pujub cellte ») maanaam fa ag sell man a yam. Bamba kon kenn lay doon ci tànnéef yii.

Yàllaange gu murit yi (walla seen gëm-gëm) dafa jeexiitalu ci yoon yii di Xaadiriyaak Tiijaan waaye it ak mbindi Alxazaali, nga xam ne Bamba da koy tudd lu bari ciy mbindam. Yenn jullit yiy woote ag cunna danuy jàpp ne gëm gu tar gii am ci murit yi jëm ci Ahmadu Bamba aki way donnam aw xeet la ci ag njaamu xërëm, waaye booy xool xamadi rekk a ko waral, ndax ku xóotal ab xam-xamam ci yoon wi duggi ruqam di nga gis lu dul loolu, nit nag bu jëfee lu moy la ñu ko xamal moom mooy ka tooñ, kon na murit yi di jàng mbindum Sëriñ bi tey bañ di tëñëxu di doxe ni ñu ko bëgg a doxe, bëgg ko nee gëme, tey doxe ni ko Sëriñ bi bëgge ci ñoom. Seex Ahmadu de giseeful ciy mbindam lenn lu dëppoowul ak Alxuraan ak sunna [1].

Murit yi am nañu ay jikko ak xiima yu di yu lislaam fekkoon ci ñoom, te xawoon a giim Sëriñ bi ñëw dekkalaat ko . Bokk na ci yooyu liggéey gi ñuy àgg ci di sellal, jàpplanteek dimbalante. At mu nekk ay milyoŋi nit dañuy bawoo fu nekk di màggali Tuubaa gi nekk ci digg Senegaal . .

Ni ko Emmanuel Brisson gise, Yoonu Murit « dafa nosu - ci gis-gisu ñenn ñi - niki ag noste gu laman (système féodal), moom daa tegu ci kaw ag toppe gu joyu ñeel genn kiliftéef gu ruu (une autorité spirituelle), Xalifa bu matale bi (le Khalife général), di ku doomu mbaa mu sëtu ci anam gu jonjoo ci Aji sos ji yoon wi. » [2].

Taariixu yëngu-yëngu gi

Soppi

Muy ku janook yoriin wu cang gi(l'administration coloniale) maanaam tubaab yi ngir mbooloom mii di wéy di màgg ba tàmbali woon leen a tiital, Seex Ahmadu Bamba gàddaayalees na ko ci anam gu toftaloo ca Gaboŋ (Afrig gu yamoo gi (Afrique équatoriale)), dale ko ci 1895 ba 1902, ca Gànnaar dale ko 1902 ba 1907, ginaaw bi ñu teg ko ci ron ag dëj gu ñu wattu (résidence surveillée) ci Senegaal ba kero muy làqu (génn àdduna) ca 1927. Kiliftéef gu Faraas gii mujj na ko nànd xam ne aw ay taxu koo jug, mu jàmmal ko, loolu it may yoon wi ci ndimbalul Yàlla ag naataange gu kawe.

Bi fi Sëñ bi jugee ci 1927 ba tay, ay Xalifaam yi ko fi wuutu ñooy ay doomam, dale ko ca ka ca mag, ba ca ka ca gën di gone:

  1. Sëriñ Muhammadu Mustafaa Mbàkke, dale 1927 ba 1945
  2. Sëriñ Muhammadu Falilu Mbàkke, dale 1945 ba 1968
  3. Sëriñ Abdul Ahad Mbàkke, dale 1968 ba 1989
  4. Sëriñ Abdu Xaadir Mbàkke, moom ag ayam weesuwul 11 weer dale 1989 ba 1990
  5. Sëriñ Saaliwu Mbàkke (mi ngi gane àdduna 1915), di xalifa dale 1990, làqu ci guddig 28 jëm 29 desambar 2007
  6. Sëriñ Muhammadu Lamin Baara mom Muhammadu Falilu Mbàkke, dale 30 desambar 2007

Ginaaw bi fi Sëriñ Saaliwu bàyyikoo, moom miy doomi Sëriñ Tuubaa ju fi mujj, la xilaafa gu matale gi tuxu leegi dem ci sët yi. Xalifa bii fi nekk mooy ki mag ci sët yi, di Sëriñ Muhammadu Lamin Baara Mbàkke, ññu koy wax Alaaji Baara.

Seexal

Soppi

Bi Sëriñ bi yoree yoon wi ci la seexale ñennat ci mag ñi, bu ko defee ñu daal di leen féetale ñenn ci taalube yi, loolu nag daa doon luy am ginaaw ag yar akug wulli ba mu mel ni war ci ab sëriñ dëgg bu war a jiite aw nit ci lislaam, bu man a yare, man a tege ci yoon. Loolu mooy li am ci Maam Seex Ibraayma Faal ak Maam Cerno bi tubaab yi gàddaayalee Sëriñ bi. Seexal gii nag dakkoon na ca 1912, at mi Sëñ bi seexale ki mu mujj a seexal, mu di Madiba Silla ca Njaaréem. Sette gi ci amaat mooy Beeco Cuun mi ñu ne Sëriñ Saaliwu moo ko seexal ca 1987. Seexal gii jeqi na coow lu bari ci biir yoon wi. Bokk na ci Seexi Sëriñ Tuubaa yu may yu jàmbaare yi Sëriñ Ndaam Abdu Rëhmaan Lóo, Sëñ Isaa Jenn

Jeexiital gu koom-koom ak gu politig

Soppi

Yoonu murit mi ngi gën di yaatu bu baax, te am na it ag jeexiital gu am doole ci politigu Senegaal . Moom day joxe ay ndigali farle (consignes de vote) te xalifa bi it lu sakkan ciy way politig dañu koy seetsi, di diisook moom juge fu ne.

Ci wàllug koom-koom ak mboolaay , « Ñoom Murit yi dañuy joxe dëkkuwaay, dund ak tàggatug xel - ci jàngale alxuraan ak xam-xam yi ci aju - ñeel xale yi gën a ñàkk, mbaa yi "sànku". Am nañu ay way jam (détracteurs), yu leen di yedde seen roose gi, seen mbay mu bari mi, seen ndimbal gu mboolaay gi (aides sociales). (...) Yoon wi war naa yor koom bu sakkan mu bawoo ci mbay mi, rawati na ci gerte g. » (Brisson, 2008 [2])

Wisaaroo gi (La diaspora) ca Paris, ca Brescia ak ca New York, nga xam ne daa jàppe xaalis muy lu sell, ndax ci liggéey la meññoo, ak ci yaxantu, day yonnee ay lim yu rëy ci xaalis ñeel mbokk ya nekk Tuubaa.

Xalifa yu Murit yi ñaare ñu am ag jeexiital lañu, ndaxte duñu rekk ay njiiti ruu yu ay taalube yu ñu nattale ci 3 ba 5 milyoŋ, (man jortu naa ne ëpp na loolu di dem ndax Tuubaa rekk lu ëpp milyoŋ dëkk na fa), waaye it ca dëgg-dëgg ay njiit lañu yu jamono (yu àdduna) yu dëkkub Tuubaa bii nga xam ne mooy péey bu ruu bu murit yi, te mujj na ndànk ndànk (moom Tuubaa) di ñaareelu dëkk bu Senegaal, ngir diisaayu demogaraafam ak bu koom-koomam.

Yeneen doom mbaa sëti Sëriñ bi, ñoom it ñu am ag jeexiital lañu ni xalifa yi, ak doonte àgguñu ci xilaafa gi. Ku ci mel ni:

  • Seex Ahmadu Mbàkke Gaynde Faatma, mi ñu xam ci ag sóoboom ci yar ak jëmale kanam gu mboolaay-koom-koom (socio-économique) gu mbooloo yi, xame nañu ko it ci jeexiital gi mu am ci njiiti politig yu Afrig yu mag yi, mi ngi faatu ci 1978 ;
  • Seex Muhammadu Murtalaa Mbàkke, "sëriñub wisaaroo gi" (le marabout de la diaspora), moom it muy ku ñu xam ngir sos gi mu sos ngir Yàlla rekk lu sakkan ciy cëslaayi jàngu ci mbooleem Senegaal, mi ngi làqu ci 2004. fii mu tollu doomam ak xalifaam sëriñ Maam Moor Mbàkke mi ngi wéyal ab liggéeyam, di ci dolli yeneen cëslaay yu bees(autres structures nouvelles) yu dëppook gis-gis bu jëm-kanam bi mu am ci ag jamonoo (la modernité). Moom de mi ngi jéggeek murit gi ag wàll gu am solo ci lu aju ci wisaaroo gi (au niveau de la diaspora).

Kenn ci ñi gën a siiw ci taalubey Bamba yi mooy Seex Ibraayma Faal. Bàyyi na fi ay dongo yu ñuy wooye Baay Faal yiy wottee seenug ñàkk a julli ak woor, liggéey bi ñuy def ci seen loxo ak yalwaan , looloo tax yeneen jullit ni ñoom di leen jam tey naqarlu seeni jëf. Seen njañ yi ñu yore ak seen létt yi yobbe na leen way nemmeekusi yi (touristes) di leen jaawale aki rastamen . Maam Seex nag nekkoon na di ku dëggu te liggéeyal lislaam lu réy, waaye ñàkk a jullit gi ñu bari firee nañu ko ci ne daa amoon ngànt, ndax daa meloon ne ku àndul woon ak sagoom, booy xool it ci ni mu daa waxe mbaa mu koy jëfe lépp da daa wund loolu, mu mel ne ku sóobu la woon ba sóobu gi yobbu ko ci mu nekkoon di ku àndadi akum xelam te loolu lislaam boole na ko ci sart yiy tee julli di war. Bokk na ci sart yiy tax julli di war nit ki ànd akum xelam. Sëriñ bi bind na ko bataaxel bob Sëriñ Abdul Ahad 3eelu xalifa génn woon na ko móollu ko ca téere ba ñuy wax majmooha, muy téere bu dajale waxi Sëriñ Tuubaa yu bari, ma nga cay wax naa :« Yaw Ibraayma Faal boo jotee ci sama bataaxel bii nanga digal sa ñoñ ñuy julli te nga sax ci te muñ ko, laajuñu la wërsëg ñoo la koy jox, te mujj gu rafet ñeel na way ragal Yàlla yi,» lii di aw laaya wu alxuraan wu mu ko yonnee ngir délloosi ko ci, kon day mel ne Sëriñ bi moom wàcci na ak ku nekk, Maam Seex nag ak ni mu gëme Sëriñ bi bu julliwul ngànt a tax, ndax daawul jëfeedi ndigal te loolu ndigal la woon. Seen gëm-gëm nag amul lenn lu ko wuuteel ak bu lislaam, ñu jàmbaare lañu ci lislaam di liggéey di joxe, ngir lépp lu ñu war a kopparal ci lislaam man a kopparu, lépp luy sémb man a àntu, foo leen fekk dañuy sikkar (maanaam tudd Yàlla) di woroomi pastéef yu kawe aki jéll, bu koor gee ñuy joxe ay ndogu ñeel way woor yi, di tabaxi jàkka aki jumaa, lii rekk mooy li ñu leen man a doyodale ci lislaam te du ñépp ñooy ña ca dul julleek a woor, am na ci ñoñ dañu koy def, doonte ñu néew lañu it.

Térekaay

Soppi
  • (en) O’Brien Donal B. Cruise, The Mourids of Senegal. The Political and Economic Organization of an Islamic Brotherhood, Oxford, Clarendon Press, 1971, XXII-321 p. (Publication d'une thèse de 1969)
  • (fr) Omar Ba, Ahmadou Bamba face aux autorités coloniales (1889-1927)
  • (fr) Jean Copans, Les marabouts de l’arachide. La confrérie mouride et les paysans du Sénégal, Paris, Sycomore, 1980, 263 p. (Thèse Paris, EHESS, remaniée)
  • (fr) Momar Coumba Diop, La confrérie mouride : organisation politique et mode d’implantation urbaine, Lyon, Université de Lyon, 1980, 273 p. (Thèse de 3e cycle)
  • (fr) Youssouf Diop, « La signification du mouridisme dans l'actuel contexte socio-politique du Sénégal », Université de Dakar, 1983, 118 p. (Mémoire de Maîtrise)
  • (fr) Mamadou Mbodj (dit) Pape Coumba, Le mouvement des jeunes dans la confrérie religieuse des mourides. Essai d’analyse et d’interprétation, Dakar, Université de Dakar, 1980, 149 p. (Mémoire de Maîtrise)
  • (fr) Oumar Mbaye, Le mouridisme sous le khalifat de Mohamed Fadilou Mbacké (1945-1968), Dakar, Université Cheikh Anta Diop, 2000, 98 p. (Mémoire de Maîtrise)
  • (fr) Cheikh Tidiane Sy, Traditionnalisme mouride et modernisation rurale au Sénégal. Contribution à l’étude des rapports entre socialisme et islam en pays sous-développés, Paris, EPHE, 1965, 236 p. (Thèse de 3e cycle, publiée sous le titre La confrérie sénégalaise des Mourides. Un essai sur l’islam au Sénégal, Paris, Présence Africaine, Université de Paris, 1969, 353 p.
  • (fr) Samba Sy, Le mouridisme à l'Université : essai sur l'association des étudiants mourides, Université de Dakar, 1984, 85 p. (Mémoire de Maîtrise)

Filmkaay

Soppi

Karmat ak delluwaay

Soppi
  1. 1,0 1,1 et 1,2 Emmanuel Brisson, Reportage sur les Mourides, 2008, sur le site de Grand reportage.
  2. 2,0 2,1 et 2,2 Njuumteg royuwaay: Balise <ref> incorrecte : aucun texte n’a été fourni pour les références nommées Brisson3

Xool it

Soppi

Lëkkalekaay yu biti

Soppi