Gerte
Gerte
SoppiGerte xeetu garab la gu bokk ci njabootu lujum yi. Mi ngi soqeekoo ca réewum metsig. Dees na ko bay ci gox yi gën a bari naaj ak taw, fu mel ni réewum Senegaal.
Melo wi
SoppiDees koy ràññee ci suul gimuy suul ay meññeefam. Gerte gàncax la gog at ba at lees koy bay su dee du mbayum dër. Xobam day nëtëx. Mi ngi toll ak 20i ba 90i sànti meetar ci guddaay. Meññeefam a ngi tollu ak 3i ba 5i sànti meetar. Garab la it gog dees koy bay ci suuf suñu ndiraag
Mbooram
SoppiEndoy Aamerig ya woon kepp a ko doon bay ci àddina. Ginnaaw bi la ko way-noti Ispaañ yañu daa woowe: "conquistador" tasaare. Ca Peru gisoon nanu ci seeni jalaase maam ya ay peppi gerte. Noonu la gerte tàbbee ci kembaarug Afrig law bokk ci mbayu Senegaal.
Njariñal gerte
SoppiDees na ci jële diwu gerte. Diw googu dees na ko jëfandikoo ngir togg ceeb ak yu ni mel ca Senegaal ak feneen. Dees na ci jële it tigadege. Joolaa yi ñu xereñ lañ ci liggeey boobu. Tigadege boobu dinañ koy boole ak cere ak yeneen. Kembaarug Afrig ak Aamerig nag ñoo ëpp luñ koy jëfandikoo . Garab la gog bari na ay wopp yu muy faj. Ay njariñam bari na lool waaye dinay sabab it ay tawat.