Gàddaay
Gàddaay di ci fr “immigration” baat la buy tekki : tukkee ci barab mbaam réew dem ca meneen, ngir sàkku fa dara, mbaa ngir naqarig sam réew ci yaw mbaa barab ba nga bawoo, loolu di faral di jur ag tumbrànke, akug ndoxondéemu, tax ngay am turu doxondéem giy tekki ku dëkkul ca réew ma nga nekk, cosaanoowoo fa
Kon gàddaay mooy: immigration ci fr
Doxondéem di : étranger
Tumbrànke di coona ak tiis ak naqaru xol gi gàddaay di faral a jur
Looloo waral Yonnant bi (j.m) di faral di wax naan: “Tukki aw daggiit la ci mbugal ”
Am ku ne moo de da koo woyofal waaye mbugal aw dogiit la ci tukki