Julli yi juroom farata la ci lu dog,ci alxuraan ak suna ak ci dajeg boroom xam-xam yi. Kepp ku ko bañ a def ngir weddi,mook ku tubbee yam cib àtte,dees koy tuubloo may ko ñatti fan,bu tuubee nu ba ko,bu tuubul,sariiya ray ko ci jaasi,te deesu ko sang,deesu ko sàng ,deesu ko jullee te deesu ko suul fa jullit ña.

Imaam daal day yonni kenn rekk, mu suul ko,te dunu ko jublule xibla,te alal ji mu am it ci baytul maal lan koy def (baytulmaal mooy (trésor publique) bu nguurug lislaam),ku nangu ne julli lu war la ba noppi lànk ne du ko def,te amul ngànt,moom danu koy bàyyi ba waxtu julli wi jot,nu digal ko,bu lànkee nu muñal ko ba doroora ji dem bay bëgg a jeex,nga xam ne lu tollu ne benn ràkkaa rekk a ciy bëgg a des,bu bañee nu topp ko,ba mu wóor ne faatiya sax xajatu fi,walla ab yamoo,loolu lepp nag ngir bañ koo ray, ñongal dereetam,bu bañee, kilifa gi ray kook jaasi ,rayug gëtën mu bañ a doon ni nuy raye ab yéefër.

Bu réccoo nag ne nan ko ba mu julli ngir ragal a dee, deesu ko nangu,dees na ko jullee nag,waaye boroom ngëneel du ko jiite,ndax da nuy bañ keneen di ko ci roy.Bàmmeelam nag dees na ko fonk,jégénal ko(jal ko) kenn du ko maasale noonu rekk,ndax moom fi boroom xam-xam yi ab julit la.Lii dey waxi imam Hawfii la


Ag leeral Soppi

Nettali nanu jële fa gën ji mbindeef ne ku biral ci ginnaawug laab ne ( Ashadu ba fam yam) da nanu ko ubil bunti àjjana yi, mu dugg ci bi ko soob,waaye wuute nanu ci jamono ji nu koy ubbi.