Abdulaay Wàdd
Abdulaay Wàdd mi ngi juddu ci 29 Mee 1926 ca Kebemeer, am na 82 ciy at, mooy njiitu réewum Senegaal ca 1fanu awril 2000 ba leegi, ki mu wuutu ci toogu boobu mooy Abdu Juuf. Ba tey mooy njiitu làng gu demokaraasi gu Senegaal (PDS), te it moo ko sos ci 37 Suwe 1974 ci ginnaaw bi mu ci tàggoo Léopold Sédar Senghor ba mu nangu, nekk na ci kujjeg politig gi lu toll ci 25 ciy at, yàgg na koo jiite, ci diir boobii tëjees na ko ci ay yoon. Soxnaam mi ngi tudd Fifiyaan Wàdd. Am na ñaari doom: góor ak jigéen, Kariim Wàdd mooy góor, Sinjili Wàdd di jigéen. Diineem mooy lislaam fiqu maalik, bokk it ci yoonu murit. Moom nag ku xareñ la ci wàllu yoon ak koom-koom am na it lijaasa jàng wi gën a mag ci ñaari wàll yooyii, mi ngi jànge wàllu yoon ci daara jii di lycée Condorcet ca Fraas. Wàllu koom-koom mu jànge ko ci daara ju kawe ju Ndakaaru.