Sëriñ Ndaam Abdu Rëhmaan Lóo
Ki moo féetewoo woon Njàggale mi, lu bari ci doomi Sëriñ bi moo leen jàngal, moo yoroon daara ju mag ja ca Ndaam di Daarul Haliim Al-Xabiir, bi Sëñ bi sàncee it Mbàkke Baari ca Jolof, ba Tuubaa rëbee, ngir jàngale moo yoroon njàngele ma di ko doxal.