Alxuraan
Téeree ngii di benn ci yi ñu gën a yër ci àdduna bi, mooy téere bees sellal ci lislaam, di fi jullit ñiy ball-loo seen yoon di Shariiha, ak ci sunna siy dundiinu Yónnent bi (jàmm yal na nekk ci moom), kon nag bu am solo la lool fi jullit ñi.
Alxuraan: Alxuraan mooy téere bu sell bi ñeel jullit ñi, mooy balluwaay bu njëkk bi ñeel yoonal gu Lislaam gi, ci ginnaawam la Sunna di ñëwe. Li njëkk a wàcc ci Alxuraan it mooy laaya wi njëkk ci saaru Halaq muy : «Jàngal ci sa turu boroom bi bind (sàkk) »
Alxuraan nag mooy waxi Yàlla ji mu wàcce ci Yonentaam ba Muhammad, Jibriil nag mooy ndawul Yàlla tey malaaka mi ko wàcce; ngir nag Yonent bi jottali ko nit ñépp,. Moom nag fa Yàlla dees koo bind ca àlluwa jees wattu ja (Lawhul Mahfuus), àlluwa jii nga xam ne Yàlla bind na ca lu nekk njëkk mu koy sàkk. Wattu googu nag Yàlla la soob, mu bëgge ko noonu, noonu la ko waxe: «Nun noo wàcce Alxuraan, te nun noo koy wattu»
Kaamil bi
Soppi[1] PDF