Xarefulwoon
Xarefulwoon (di tekki lees manatul a xar, di ci fr Atome), baat bi Seex Anta Jóob a ko tëgg te mi ngi sukkandiku ci bu njëkk li ñu foogoon ne mooy xaaj bi gën a tuuti bees manut a xaraat bu ab ne-ne, (manees na koo tudde it fepp (mi doon tuutalug pepp "peppu suuf as feppu suuf") muy lu bawoo ci ngéru xeltukat yu waa-gires yu yàgg ya. Mooy wàll wi gën a tuuti ci bépp cër bu nekk ci dénd bi buy wéy di yor màndarga yu simi yu la mu doon, ci yeeneen kàddu, soo ko xaaje du nekkati wenn wàll wu ne-ne wa mu bokkoon laataa xaaj gi, beneen xeetu ne-ne lay nekk.
Ci mujjug ati 1800 (ak wuññig mbëjfepp) lañu biral ne xarewulwoon manees na koo séddale, ndax li mu doon, moom ci boppam, lu cëroo ay wàll-wàllaan yu bari yu gën a ndaw (baatu ronxarefulwoon loolu lañu ci jublu).
Faramfacceb xarefulwoon mooy faramfacce biy wax ci melokaanu ne-ne yi, di dëggal ne bépp ne-ne ay bennaan ñoo ko cëroo te ñu leen di woowee xarefulwoon, ñoom ñooy dajaloo ci benn anam bi nekk ne-ne bi. Bii faramfacce ñoo ngi koy man jëfe ci ne-ne yi nekk ci nekkiin wu wow, yullaakoon ak wu gile.
Ab xarefulwoon mi ngi cëroo ab saalu xarefulwoon, bu am ay yani mbëj yu baax, ak ay mbëjfepp yu am yan yu bon te di wër saalu xarefulwoon bi di wëndeelu ci anam gu nosoodiku. Saalu xarefulwoon bi mi ngi cëroo ay feppsaal, yu doon ay wàll-wàllaan yu ami yan yu baax, ak ay feppmaandu, di ay wàll-wàllaan yu amul yanu mbëj. Ab Saalu xarefulwoon di na am lef wu ëppee ab mbëjfepp 1800 yoon.
Màndargaay wàll-wàllaan yi ne ci ab xarefulwoon:
Wàll-wàllaan | Njunj | Yan | Lef | Karmat |
---|---|---|---|---|
mbëjfepp | e- | -1,6 × 10−19 C | 9,1093826 × 10−31 kg (0,51099 891 MmV/c²) | Thomson moo ko wuññi. |
Feppsaal | p+ | 1,6 × 10−19 C | 1,6726231 × 10−27 kg (9,3828 × 102 MmV/c²) | Ernest Rutherford moo ko wuññi |
Feppmaandu | n | 0 C | 1,674 927 29(28) × 10−27 kg (9,39565 560(81) × 102 MmV/c²) | James Chadwick moo ko wuññi |