Toolu bijjaakon

Toolu bijjaakoon, ci jëmm, ag feeñte la gu màndargaloo ab taraay ak ab jubluwaay bu jenn doole, jees duppee Dooley Lorentz, ju judd ci doxub ay yani mbëj. Toolu bijjaakon, moom ak toolu mbëj ñooy ñaari cëri toolu mbëjbijjaakon di li banqaasu jëmm bi di mbëjbijjaakon di faramface. Soo boolee ay duusi ab toolu mbëj ak yu ab toolu bijjaakon dañuy man a baawaan ci barab bi ak ci lu ëpp ci ne-ne yi. Yii xeeti duus lees di wax duusi mbëjbijjaakon te leer gi nuy gis bokk na ci yenn ci anam yi mu ñuy feeñoo.

Hans Christian Ørsted, Der Geist in der Natur, 1854

Maxwell moo fexe ba boole mbëj ak bijjaakon, ci nii, mu jur ag noste gu ñeenti yamale (Yamaleg Maxwell) yuy lëkkale seen ñaari tool yi. Bu njëkk ñaari tool yi dañu leen doon tàqale ngir gëstu, faramfacce, seen feeñte yu wuute. Albert Einstein moo wone, ni tooli mbëj ak tooli bijjaakon doonee ñaari anami feeñiin yu benn feeñte; ni ab xoolkat man a gisee jenn doole ju bijjaakon, ci jenn jamono ji, beneen xoolkat buy daw di gisee jenn doole ju mbëjtekkaaral, di liñuy duppee gisiin wu ajoo. Ci nii, ak ajoo gi, manees naa xam doole ju bijjaakon ji ci bu nu xamee doole yu mbëjtekkaaral bi.


Wikipedia
Wikipedia
Bii jukki ab junj rekk la. Man nga cee duggal sa loxo suqali ko ndeem am nga ci xam-xam ci anam yi Wikipedia taxawal