Baraay
Ci Jëmm, baraay ab delluwaay la bees di sukkandiku ngir xam ñaata yoon la genn feeñte guy tóllantiku di amal ag tóttantikoom ci benn diiru jamono bees jël. Maanaam ñaata yoon la xew-xew bi di feeñ, ci genn anam gi, ci benn diirub jamono. Ngir natt baraayu genn feeñte dañuy jël benn diiru jamono xool ñaata yoon la mbir mi di dellusi ci biir diir bi lim bi ciy jóge di doon baraayam. Geneen anam gees ko manee natt mooy xool jamono yi ñaari xew-xew yu toftaloo di door, bu ci nekk nga xam jamono ji muy tambali ak ja muy jeex, kon xam itam seenub diir. Baraay bi di doon safaanu boobu diir .
Njureef li ñu koy xayma ci Hertz (Hz), 1 Hz mooy teewal benn xew-xew buy am benn yoon ci 1 saa (s). Ngir natt baraay bi jumtukaay bees di jëfandikoo lees di wax ab nattbaraay.