Toolu mbëjbijjaakon

Toolu mbëjbijjaakon, ci jëmm, ab tool la buy juddoo ci teewaayu yani mbëj, banqaasu jëmm bi koy gëstu mooy mbëjbijjaakon. Ay bokkaanam (ñi bokk doon ko) ñooy ab toolu mbëj ak ab toolu bijjaakon, seen teewaay di juddal ay doole yees man a natt ci bépp tombu tool bi ci jamono ju ne. Ci fànnu gisiin wu ajoo dees na ci wuññee ne toolu mbëj ak toolu bijjaakon ñaari feeñte lañu yu wuute tur te di lenn li, lépp mbiru nosteg delluwaay la. ba tax sax su benn xoolkat bu taxaw di gis ci misaal ab toolu mbëj kepp, ab ñaareelu xoolkat buy yëngu moom dina gis ab toolu mbëj (nakka-jekk waaye bu dul tekkaaral lay doon) ak ab toolu bijjaakon.

Toolu mbëjbijjaakon bi dafay jur jenn doole ji ci wenn wàll-wàllaan wees yan, bu yamaleb Lorentz diñu jox:

Te di yanu wàll-wàllaan wi, diy xélam, toolu mbëj bi, moom di xiirtalug mbëjbijjaakon bi. Àtteb Faraday-Neumann-Lenz mooy wax ne: wuuteeg aj giy judd ci ag ndombo gu tëju dafa aju ci anam gu jonjoo ci coppite gu walug bijjaakon gi te aju itam ci diirub jamono bi muy ame. Ci yeneen kàddu dafa aju ci xél yi walug bijjaakon gi di soppikoo ci jamono ji. Doxiinu masini mbëj yu bari yu mel ne ci misaal soppalikaay yeek doxalukaayu mbëj yi ci bii àtte lañu sukkandiku.

Lëkkalekaay yu biir Soppi