Yëngu-yëngu yu ag nasaraanal ak ay wi mu àndal

Yëngu-yëngu yu ag nasaraanal ak ay wi mu àndal:

Ag nasaraanal yëngu-yëngug diine gu ñu nos la, gu li ko tax a jug mooy tas diiney nasaraan ak xayug nasaraan yi ci jullit ñi ak ñu dul ñoom. Nasaraanal gii nag lu taqoo la ak sancug Tugal gu yees gii nga xam ne jot naa man a liggéeyal diiney nasaraan ci anam gu nëbbu, jaare ko ci ay yoon aki defiin yu lëmu te jafee xam. Loolu lépp nag ngir liggéeyal ay xemmemtéef yi mu amoon ci sanc àdduna bi, yilif ko . Looloo waral du yomb nu tàqale diggante nasaraanal ak canc, te itam nasaraanalkat yi danu daa nekk ci ron kiliftéefug sancaan yi. Lu yéeme la diiney nasaraan nekk di benn ci jumtukaayi canc gu Tugal gu yees gi. Nasaraanal nag yamutoon ci benn Jàngu rekk ci jëmmi boppam, waaye kay Jàngu yépp a ko daan def, moo xam Jàngu bu sowwu bi la (bu Katolig bi), bu penku bi (bu Ortodoksi bi), bu protestant bi walla bu Angalteer bi (bu Angalikaan bi). Gëpplante gi taroon na ak xeex bi ci seen diggante, ni mu tare woon ci diggante réewi sancaan yi.

Taarixu nasaraanal gu yees gii nag am na ag takku gu mu takku woon ci yëngu-yëngu gu wuññi gu melosuuf gi réewi Tugal yu nasaraan yi doon def, te Portigaal ak Espaañ jiite woon leen, di woon ñaari réew yu ëppaloon te xaabaabal ci diine te daan ci par-parloo safaan jullit ñi ak seen àdduna. Bu ko defee wuññikati Tugal yii ame woon ag parparloo gu diine defoon séeni liggéeyi wuññi, soldaarus Tugal si topp ci séen ginnaaw di liggéeyal xemmemtéefi canc yu seeni réew, loolu lépp nag ngir nu àndandoo amal li nu bëgg mooy liggéeyal tubaab yi, te taxawal seenug cang ci diineek fetal .


Jumtukaayi nasaraanal aki ker-keraanam :

Soppi

Nasaraanalkat yu nosu yi jëfandikoo woon nanu ab lim bu rëy ciy ker-keraan (moyens) yu leen di dimbali ci seen liggéeyub nasaraanal bi, bu ko defee ñuy def jamono ju ñëw ñu seet nu ñu ciy def ba liggéeyal ci seen jubluwaay boobu. Jumtukaayi nasaraanal gën na a jëm kanam ànd ak jëm kanam gi jamono def ak gi xam-xami dëppale yi (les sciences pratiques ou appliquées)ak yu xarala yi def. Nasaraanal ñi ngi ko tàmblee ci ay nit di jug di waaraate ak a xamale yonent Yàlla Hiisaa (j.m) akum njàngalem diineem. Wii xeetu nasaraanal sax na fi di ag nasaraanal gu kenn nit di def, mu doonoon lu jëmadi kanam waaye tolloo woon ak jamono ju yàgg ji mu dajeeloon. Jumtukaayi nasaraanal jëmoon na kanam aki ker-keraanam bi yewwuteg xam-xam ak gu ndefar gënee jëm kanam ci Tugal. Bu ko defee yonnee yu nasaranal yu ñu nos yi tàmblee am, ay mbootaay yu nasaraanal yu bees di leen saytu, yuy jëfandikoo mbooleem anam yi ak jumtukaay yu yees yi ngir doxal seeni liggéey, bokk na ci li nu daa jëfandikoo:

(1) Paj ak li mu àndal ci ay barabi faju, lu ci mel ni:

Soppi

fajuwaay yi(les hôpitaux) ak këri faj yu ndaw yi ak barab yiy maye ay garab. Ci xaranub fukk ak juroom ñeent, ay mbootaayi paj yu nasaraanal yu bari feeñoon nanu ci réewi Tugal yi ak Diiwaani Amerig yu Bennoo yi ak yul ñoom ci réewi àddunay nasaraan ji, li leen taxoon a jug mooy waajal ay doktoor yu goor ak yu jigéen, aki rewlikat(dooñkat) aki jàpplekati doktoor ngir ñu man a liggéeyal Jàngu bi jaare ko ci liggéey ci barabi nasaraanal yi nu tasoon ci àdduna bi, rawati na ci Afrig ak Asi. Paj man nañu ne mooy ker-keraan bi la man a gën a may ngay man a jonjoo ag nit ñu néew ñi doole ak ñu ñàkk ñi. Nasaraanalkat yi dañu daa wax naan: li ñu jublu ci jëfandikoo meccem Paj ci nasaraanal mooy ne moom day nooyal yoon wi laytaay ko ba bu Injiil dee ñëw ngir dugg ci xol yi du jafe.(Ma ne man: nit ki boo ko joxee mu lekk, naan, ginnaaw bi muy bëgg a dee cib xiif, di bëgg a dee ci tawat nga faj ko, boo nee ko fii la mu ne foofa la, rawati na bu ko fekkul muy ku tatawu ci xam-xam, aaru ci dali diine ju dëggu). Dañu daa wax it: war na doktoor biy nasaraanal mu bañ a fàtte ne day nasaraanal laata'a dara di xew. Mbootaayi nasaraanal yi sotti woon nanu seen yitte ci meccem paj mii, daal di ubbi lu sakkan ciy barabi paj ci réew yu ndool yi yittewoo paj aki doktoor, ngir loolu man leen a jàpple ci seen ligeeyub nasaraanal boobu leen taxoon a jug.

(2) Njàngale ak li mu àndal ciy jumtukaay, lu ci mel ne:

Soppi

daaray dal yi ak yu diggu yi ak yu ñaareel yi ak xamluwaay yu kawe yi ak daara yu mag yi ak kàggu yi ak daaray mecce yi añs. Ñi jiite woon nasaraanal gi danoo gisoon ne bu nu ubbee daara yii ci réewi jullit ñi ak yu leen moy loolu dana man a doon aw yoon ngir tas ci diiney nasaraan ci doomi jullit ñiy jàngsi ci yii daara, rawati na bu nu leen dee def leeg-leeg ñu cofal leen ci njàggalem Injiil mi, leeral leen ko, nga rax ci loolu li daara yii daa def muy tas xayug Tugal gi ak rawug xam-xamam ak jàngal ko yile dongo, te loolu ag doyodal jullit ñi rekk lañu ci jublu woon.

(3) Jëf ju yiw ak ju nite ji nga xam ne mbootaayi yiw ak nite yu nasaraan yi daa nañu ko def ci réew yu ñàkk yi, rawati na ci jamonoy ay yi ak musiba yu dénd yi ak xare yi:

Soppi

bu ko defee liggéeyub nasaraanal bi di sawar ci biir daw-làqu yi ak ñees tuxal ñi ci réew yu néew yi doole, loolu mooy li ngay gis ci réewi Afrig yeek ak Asi.

Loxob nasaraan biy indi ñam, paj ak ndimal ñeel daw-làqu yooyu ak ñu ñu tuxal ñi, mooy biy tas dali diiney nasaraan ci ñooñii, di jariñu ci seen nekkiin wu metti woowu ak seen tumbrànke gu tar gi.


(4) Xibaarukaay yi

Soppi

Yëglekaay yi ak këyiti xibaar yi, tasum xibaar meek yeene yi nga xam ne seen woote yu nasaraanal yee ko daan tax a jug, ak waxtaan yi nu daa amal ci pénc yi, ak taalifi penkuwaan yi (les orientalistes) yi yi daa gëstu ci xam-xami penku yi ak seeni njàggat aki pas-pas, ak li nekkoon ci loolu lépp ci tooke ñeel jullit ñi ak séenug xay, aki laaj yu man a jur ay sikk aki jiixi-jaaxa ci jullit ñi jëm ci séeni boroom xam-xam aki kilifa, lii lepp ci jumtukaay yi la woon . Nasaraanalkat yi gisoon nanu ne daal téere yii ak mooltéef yii(imprimé/publication) man nañu leen a dimbali bu baax ci wisaare ag nasaraan ci réewi jullit ñeek yu leen moy, jaare ko ci li ñuy bàyyi ci bakkan yu doyadi yi ciy jeexiital. Mbootaayi nasaraanal yi sos nañu ab lim bu mag ci ay daaray yar ci Tugal ak Aamerig ngir waajal ci nasaraanalkat yi war a defi bii liggéey.



Nasaraanal ci réewi araab yi:

Soppi

Nasaraanalkat yu katolig, anglikaan ak protestant yi wisaaroo woon nañu ci réewi araab yi nekkoon ci ron cacug Britani, Faraas, Itaali mbaa gu Espaañ. Bu ko defee nasaraanalkat yi sos ci réew yii ay barabi nasaraanal ci biir askan wi, rawati na fa jullit ña, ndaxte seen jubluwaay ci loolu mooy néewal doole jullit ñi ak seen diine. Réew yi nasaraanal gi sutuxlu danañu leen ci tuddal yii :

Nasaraanal ag cawarteem fésoon na ci biir Nasaatiray Iraag yi, ci Mawsil, Baxdaad ak Basra, ñi ko doon def nag di ay nasaraanalkat yu Faraas ak yu Itaali. Àntug nasaraanal gu katolig gii ci Iraag ci njiitul Faraas merloo woon na Britani, ci noonu mu daal di fa woon yabal ay nasaraanalkat yu anglikaan, daal di ubbi bunt bi ci kanamu nasaraanalkat yu protestant yi, ngir ñu àndandoo xeex nasaraanal gu katolig gu rëy gii doon àntu bu baax ci Iraag. Loolu jur ag gëpplante gu mag ci diggante nasaraanalkat yu katolig yi cig wàll ak yu anglikaan yi ak protestant yi ci geneen wàll. Gëpplante gii nag du lenn lu dul geneenati ci gëpplante yi daa xew ci wàllug canc ci diggante Faraas ak Britani ci goxi penku bi. Britani daa gisoon ne nasaraanalu gu katolig gu Faraas gii nekk Iraag tay, dara yobbuwu ko fa lu dul suuxat xejjug Faraas ak kiliftéefam ci penku bi, te loolu moom la Britani doon ragal moom mi ame woon dooley canc ji gën rëy te ëpp doole. Ay turi nasaraanalkat yu protestant yu bari feeñ nanu ci ñi daan liggéey ci toolub nasaraanal ci Iraag ci xarnub fukk ak juroom ñeent g, ku ci mel ni: nasaraanalkat bii di Grant ak Groves ak Samuel Zwemer añs


Réewi Dóox gu Araab gi  :

Soppi

Ag nasaraanal tasaaroo woon na ci réewi Dóox gu Araab gi (golf arabique), ndaxte bii gox da di ab jàlluwaay bu am solo jëm ci réewi penku yi. Bi mu ko defee, nasaraanalkati protestant yu Amerig yi sawar fa, daal di fay sos ay fajuwaay yu seenub lim àggoon ci juroom ñeent, aki këri doktoor , seenub lim ñoom it àggoon ci fukk ak benn.

Nasaraanal gi yamutoon ci mbootaayi Protestant yu Aamerig yi, waaye weesu woon na leen ba daj yu katolig yi ak yu angalikaan yu Britani yi. Ci noonu yii mbootaay tàmblee joŋante ci sos ay daara aki jàngu aki katederaal ci réewi Dóox gi. Nasaraanalkat yu protestant yu Aamerig yi daal di taxawal Jàngu bu Injiil bu xeet wi ci Kuwet, Ahmadi, Manaama ak Masxat. Bu ko defee katolig yi taxawal katedraal bu katolig bu Rom bi ci Manaama ak Abuudabi, ak Jàngu bu Angalikaan bi ci Manaama. Nu daal di sos ay barab yu ñu jagleel tas Injiil ak seddale ko, ak yeneen téerey seen diiney nasaraan ji, ak seen yéene yi aju woon ci seen woote bu nasaraanal bi. Waaye ak li nit ñiy yittewoo barabi faju yooyu lépp ak daara yi, teewul ñu xeex bu baax safaan yëngu-yënguy nasaraanal yii ànd ceek li nu am ci jumtukaay ak doole. Boroom xam-xam yi xeex ko ci seen xutba yi ñuy def ci jàkka yi ak waaraate yeek gindee yi. Askan yu bañ canc yii te noonu ko ñoom itam xeex ko. Loolu jural nasaraanalkat yi ag sooy akug tas yaakaar.

Réewi Shaam:

Soppi

Nasaraanalkat yi sawaroon nanu ci reewi Shaam yi, ci Siri, Libaa, Palastin ak Sordani . Nasaraanalkt yi yittewoo woon nanu mbirum Libaa ak Palastin, rawati na ginnaaw xareb àdduna bu njëkk bi, nga xam ne réewi Shaam yi danoo tàbbi woon ci ron féetale gu Faraas ak Britani. Bu ko defee way nasaraanal yi sotti seenug nasaraanal ci dëkki Siri yeek Libaa, daal di jàpplanteek kuréelug Mawaarina yu katolig yi ci Libaa. Britani it duggsi, féeteek kuréelug Dursu gi ci Libaa. Nasaraanalkat yi jeqi woon nanu fa ay fitnay kuréel, ca la xarey kuréel yu tàng te tar juddoo ci Libaa, ci diggante Mawaarina yi ak Dursu yi atum 1860g. Way nasaraanal yu Angalikaan yi ñoom danoo sotti woon seen yitte ci Palastin, rawati na ne moom ab digg bu diine la bu am solo ñeel ñi topp ñatti diiney asamaan yi: diiney Yahood, ju Nasaraan ak Lislaam. Mbootaayi Anglikaan yu Angalteer yi tàmblee sosi fajuwaay aki daara, aki mbootaayi yiw ci dëkki Palastin yi, rawati na Quds , Betlahem, Naasira, Tabariya, Yaafa ak Gasa. Fii itam du waa Angalikaan yi rekk a fa doon def ag nasaraanal, waaye it katolig yi, Ortodoks yi ak Protestant yu Aamerig yi. Julliti Palastin yi jàmmaarloo nañook yëngu-yënguy nasaraanal yii, xeex ak ñoom bu baax, ndaxte dañoo noonu woon seen diine, noonu seen jaloore, seen ndono, seen xay ak taarix bu lislaame bu xóot bii. Seenug xeex ko gën na a tar bi mu gënee leer ne ag nasaraanal la te canc gi lay liggéeyal. Ci noonu nasaraanalkat yi jàpplanteek seeni góornamaa kontar araabi Palastin yi ngir defar lañuy wax dëelub Balfour , génne ko it atum 1917g, lii ko taxoon a jug di sos am réew mu xeet mu yahood yu sahyoon yi ca suufus jàmbur see di Palastin, di suufus ay araab yu jullit, tubaab yi déggook yahood yi jox leen ko, ci seenug toroxte ak naqar.


Isipt:

Soppi

Nasaraanal tas na ci Isipt te wisaaroo fi ci xarnub fukk ak juroom ñeent g, rawati na ginnaaw bi ko Britani tegee loxo atum 1882g. Qibt yi dimbali nanu mbootaayi nasaraanal yi tasoon ci biir jullit ñi ci Isipt. Bu ko defee yonnee bu katolig bu Faraas bi tukkee woon Liyon daal di def ay liggéeyi nasaraanal yu fés, mboolooy nasaraanal yu Yesu yi di leen jàpple ci loolu. Nasaraanal ga amoon ca Isipt Paab gi dëgëraloon na ko te jàpple ko.

Mbootaayug nasaraanal gu anglikaan gu Angalteer gi def ay liggéeyi nasaraanal ci Isipt, ay cawartey nasaraanalam gën a yokku ginnaaw bi Britani tegee loxo Isipt te jàpple bu baax yii mboolooy nasaraanal te aar leen. Mbotaayi nasaraanal yu diiŋatkat yu Amerig yi def ñoom itam seeni liggéey ci Isipt ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom ñeent ak bu ñaar-fukk g. bu ko defee mboolooy nasaraanal yii tàmblee xëccoo ci seen biir ak a gëpplante ci wàllug ubbi ay fajuwaay aki daara aki jàngu aki katedraal ak barabi seddale téere yeek mbindi nasaraan yeek yeneen yiy liggéeyal nasaraanal .

Jullit ñi xeex nanu nasaraanal ci Isipt, boroom xam-xami Ashar gu tedd gi jug ñoom itam jàmmaarlook yëngu-yëngu gii, daal di sos mbooloo muy aar Lislaam ngir xeex nasaraanal ci meloom yepp aki anamam. Mbooloo mii mujj na am ay bànqaas ci dëkk yu magi Isipt yi. Sos it ay jànguwaay aki wéeruwaay ñeel way ñàkk ñi, ñu lòtt ñeek jirim yi. Ay doxi ñaxtu yu bari am ci kanamu barabi nasaraanal yi ci Xayra, Demenhor, Saqasiq ak Kafar-siyaat añs. Yenn it ci yëglekaay yu Isipt yi dimblee ci feeñal jubluwaayi nasaraanal gi, yee it jullit ñi ci ay wi mu làmboo.


Sudaan:

Soppi

Liggéeyub nasaraanal sawaroon na ci Sudaan, rawati na ci ginnaaw bi ko Britani tegee loxo. Bu ko defee mbootaayi nasaraanal yu katolig, yu protestant, ak angalikaan yi def seeni liggéeyi nasaraanal ci biir jullit ñi dëkke woon ci bëj-gànnaaru Sudaan ak ñu dul jullit ñi dëkke woon ci bëj-saalumam. Way nasaraanal yi sotti woon nanu seen yitte ci ñi dëkke woon ci bëj-saalumu réew ma te doonadi woon ay jullit, ci noonu ñu jot a tas seen diine ji ci ñoom ak aaday sowwu ji. Nasaraanalkat yi sosoon nañu ay jàngu yu yonnee yu katolig ak yu angalikaan ak yu protestant ci Sudaan, sosati fa ay barabi faj yu nasaraanal.

Waaye waa Sudaan ñoom tooguñu rekk faste seeni loxo ci kanamu nasaraanal gi. jeqiku gu Mahdi gi xeex na ko. Broom xam-xam yi xeex ko. Mbootaayi diine yi rawati na ci bëj-gànnaaru réew ma ñoom itam xeex ko.


Réewi Maxrib gu araab gi :

Soppi

Maxrib walla (Maghreb) gu araab gi dafa nekke fu jàkkaarloo ak réewi nasaraan yi, rawati na Espaañ, Itaali ak Faraas. Réew yii nag jariñoo nañu bu baax néew dooleg réewi Maxrib gu araab bi, daal fay yabal ay nasaraanalkat yu bañ Lislaam ak jullit ñi, ngir ñu def fa seen liggéeyi nasaraanal yi, ak ngir nooyal ko, waajal ko ba mu man a dékku canc gi nar a ñëwi di tukkee ci Faraas, Itaali ak Espaañ. Réew yii yepp nag yu yor diiney nasaraan lañu. Cawarteg nasaraanal gi yokku na te dolliku, rawati na ci keppaarug canc gu Tugal gii ci réewi Maxrib yi. Bu ko defee gëpplante gi ci toolub nasaraanal tàmblee tar ci diggante mbootaayi nasaraanal yu katolig yi, yu anglikaan yi ak yu protestant yi. Nasaraanalkat yi daal di wut ay jumtukaay aki ker-keraani nasaraanal , taxawal ay fajuwaay aki kër doktoor aki daaray nasaraanal añs. Ci biir loolu ñu def lu ñu man ngir fay làkkuw araab, te dundal kàllaamay berber yi ngir xeex ci làkku Alxuraan wi, ñu defoon ay pexe itam ci far aaday Lislaam ji ak taariixam, jéem a jox jullit ña fa dëkke woon ay réewu yu réewi sancaan yi, bu ko defee duñu réewooti ci seeni réew, te duñu ko bëggati. Ñu xeex ak boroom xam-xami jullit ñi daa jéem a taxawal liggéeyub nasaraanal bi.

Waaye nag ñu fonk seen réew ñii dëkke woon ci réewi Maxrib gu araab gi amoon nañu ndam ci damm degug canc gi ak gu nasaraanal gi, ngir seen xeexub njàmbaar bi ñu leen jëmale woon.

Barabi nasaraanal yi ci réewi araab yi:

Soppi

Mbootaayi nasaraanal yi sosoon nañu lu sakkan ci ay barabi aada , yu xam-xam ak yu faj ci réewi araab yi, lii ci la:

  • Mbootaayi nasaraanal yi sos nanu lu bari ci barabi njàngale yu kawe yi ci Isipt, yu ci mel ne: daara ju kawe ju Aamerig ji, xamluwaay bu penku bi, xamluwaay bu Faraas bi, yooyu yépp nag ñi ngi Xayra . Bu dee Sudaan, nasaraanalkat yi sos nanu fa bànqaas bu Kamboni bu katolig bi ak daara ju Amerig ak daara yu Qibt yi, yu Gres yi ak yu Angalteer yi. Mbootaayug protestant gu Aamerig gi moom tam sos ca Bayruut daara ju kaw ju Aamerig’ati. Katolig yi sos fa ñoom daara ju kawe ju katolig ja, walla daara ju kawe ju Yesu ji ñu duppee aji sell jii di Yuusuf (sosef).
  • Nasaraanalkat yu penkaan yi dugg nañu ci gëstuwaay yu làkk yi ci réewi araab yi. Ñu dugg ca gëstuwaayub làkk ba ca Xayra ak bu xam-xam ba ca Damasq , ak bu xam-xam ba nekk Baxdaad, penkaanu Angalteer bii tudoon Jub nag kenn la ci ñoom akMargoliyos mu Faraas mi, Garifani mu Itaali mi, Hothman mu Olaand mi, akHarithman mu Almaañ mi. Penkaan walla penkuwaan yi duggal nañu seen loxo ci téere yu bari yoo fiy gis tay, ñu tudd ci rekk ci misaal: jimblang ci Lislaam ak dundug Muhammad (j.m) ki nuy wax Sir William Mouir def ko, téere bi tudd Lislaam te Alfred Giyom def ko ak yeneen ci téere yi nëbbal Lislaam ag mbañeel.
  • Mbootaayi nasaraanal yi taxawal nañu lu limu ci ay cëslaayi faj , lu ci mel ne: fajuwaayu Marson ak bu Maryon Wilth, ca Bahrayni ak fajuwaayu Noks ca Masqat ak bu Harmal ca Isipt ak bu Maryohanna biy faj bët ca Quds, ak yeneen yu nasaraanal yi wisaaroo ci mbooleem réewi araab yi. (ginaaw ci réew yii lañu nekk nag, kon yu Afrig gu ñuul gii nga xam ne mooy seen mburu mu bees jarul ñu ciy wax).