Njàngale walla Yar

Soppi

Tekkiy ñaari baat yi, yenn saa yi dañ leen di jaawatle. Ci maanaa, baat bu mujj bi, ci lu daj, mooy lépp lu ñuy xamal nit ki, ci bépp fànn (diine, ngor, teggin, xam-xam,añs). Baatu njàngale moom, ci wàllu boppam, day di rekk benn xeetu yariin, mooy xam-xam bi ñuy sukkadinkoo ngir taggat la ci lenn li, jàngal la lenn li.

Kon njàngale benn xeetu yarin la bu ñu man a gis ci daara yu taaxe yi, fa nga xam ne ab sëriñ, bu taxaw janook ay ndongaam, di leen taggat ci xam-xam, jaare ko ciy kaddu walla ciy mbind.

kon njàngale man naa tekki yar, waaye yar man naa bañ a doon njàngale. Baatukaay Jàngale wolof