Wolof genn giir la gu nekk Senegaal. Wolof ñoo ëpp ci waaso yi ci Senegaal. Maami wolof yi Isipt lañu bawoo. Séeréer si, Pël yi, Sooninke yi, Tekuruur yi (Tukuloor), ak Sara yi juge nguuru Bagirmi ca réewum Cadd. Wolof yi ca xeet ya lañu juge. Xeet ya yépp danoo jaxasoo, ca yoonu Imbraatoor gu Ghana, ca dëkk bi nu tuddé Jolof. Wolof mooy ñu bawoo Jolof, Waa-Lof (ay gaa yu juge Lof) walla Waa-Laf (ñoñ Laf), di nekk tay Wolof. Seex Anta Joob, Walaf la doon wax. Noonu la xeetu Wolof judoo. Tur wii nuy wax Jolof, benn Soose bu tundoon Jolof Mbeng moo ko joxoon dëkk ba. Ca cosaan dañu ne Jolof Mbeng ak njabootam ñoo fa njëkkoon a dëkk. Ba noppi Amadu Abuubakar ñëw fa, moom baayam Naaru Murabituun la woon, turam di Abu Bakr Ben Omar, ca cosaan danu daa wax Abu Dardaayi, yaayam Tukuloor la woon, turam di Fatumata Sàll doomu Lam-Tooro (Lamanu Tooro) ca Tekuruur. Amadu, Baayam jenn jàmbaar ju Saraxule moo ko ray, booba nag la Fatumata seeti jeneen jëkër. Amadu bégul woon ci boroom këru nday ju bees ji, lii a taxoon mu dem Waalo. Foofa nag nit ña fa nekk ay Lamani Séeréer yu sant Ngom aki Sàmmkati Pël yu sant Jaw. Laman yi danoo yékkati woon Amadu, ndax dafa baaxoon ba jaaxal dëkk bi, ba far mujj di Buuru Waalo.

Wolofu Kajoor (boyaade (gravure) gu 1890)

Séeréer si ñoo ko tudde Njaajaan Njaay. Bi Amadu agsi ca waalo, ci li mu daan daaw keru yaayam, ñii daan dëkk Waalo ñoo demoon setsi Maysa Waly Joon, buuru Siin ba, ngiir mu leen wax kan mooy Amadu boobu ñu leen jaxal. Buur bi, boroom xam xam la woon, ku mënoon gis yu bare. Maysa Waly ne leen koku Njajaan Njaay la, ci Serer mooy: ku doy war. Fofu la tuuru Njaajan Njaay joge, ak sant bobu di Njaay. Kon Njaay, ci Serer yi la joge. Njaay itam, mooy Gaynde (Gaynde Njaay ca cosaan) te Gaynde mooy buuru àll ba. Da bokk ak turu Jaara ci kallama Mandinke yi, Jaata ci Joola yi. Moo ñu dakkantal Njaayen yi Jaara walla Jaata. Ñu yooree tur yi, dañu kalante.

Waaye ba noppi Njaajaan dañu koo dàqe dëkk ba, ndax daa am ku ko bëggoon a ray. Mu daal di woon daw ba Jolof ca Wolof ya. Njaajaan Njaay dajale woon na Wolof yi ndax ñu gën a am doole, ba man a taxawal Imbraatóor gu Djolof. Wolof yi, Jolof mooy seeni dëkk, waaye ak seeni imbraatoor gi, dañoo demoon dëkk te yor: Waalo, Tekuruur, Kajoor, Bawal, Siin-Saalum, Njarmeew (soog a dëkk Bundu), Ñaani, Wulli, Bambug. Nguur ga gépp Jolof uffoon na ko. Lii moo tax Làkku Wolof mooy làkk wi ñu gën a wax ci Senegaal. Ca atum 1549 la Jolof gu mag ga tas ak Lele Fuli Fak. Nguuri Wolof yépp am seeni buuri bopp: Dammeel ca Kajoor, Teeñ ca Bawal, Baraag ca Waalo, Buurba ca Jolof (Ca Jolof gu mag ga, Buur Fari lañu daa wax). Decce Fu Njóogu ak Amari Ngóone Sabel Faal, ñoo fi njëkk a nekk Dammeel-Teeñ.

Njabooti Wolof yi yoroon nguuri wolof yi

Soppi
  • Njaay (Jolof)
  • Mbóoj ak Wàdd (Waalo)
  • Faal ak Jóop (Kajoor ak Bawal)
 
ab Ceddo ca wetu Bàkkel (1853)

Nosteg mboolaay ga

Soppi
  • Géer/Garmi, ca kaw, ñoo doon nekk buur yi. Kàŋam (buuri Laman yi) Farba Kaba (buuri Ceddo yi), Tuube, Bumi ak Lingeer.

Ca seeni meen ñoo man a nekk Buur. Meen moo gën a am solo Geño(Meen:wàllug nday). Geño:wàllug baay .

  • Jàmbur ak Sëriñ. Ñoom Sëriñ si ay Tukulóor lanu(Mbàkke, Ja, Si, Lóo, Sàll) Saraxule (Silla, Xulé, Siise, Daraame, Kebe) walla ay Naar (Jaxumpa, Aydara, Kundul, Saadi, Baabu).
  • Baadoola, Mbay moo doonoon seen dund.

Ñeeño yi

Soppi
  • Tëgg, Lawbe, Wuude, Ràbb. Am na ñu bari ci ñoom ci xeetu Pël/Tukuloor lañu juge ñooy ñi sant : Caam, Mbow, Ace, Jaw, Jum, Taal, Faam, Gise, Sow, Béey, Ñas, Mbay . Ñeeño yooyu dañuy kalante ak Pël yi, ndax danoo bokk maam.
  • Géwal yi, ñépp lañuy woy, Buur yi, ñeeño yi. Cosaanu nit ñépp lañu xam, seeni Sant yi gën a siiw: Sekk, Mbay, Mbuub, Laam, Séy.

Ci ñoom, am na ñuy jefandiku ak xalam gi. Ñuy xalam itam, ci lu ëpp, ay tukuloor lañu, ni Bukunta Njaay walla Samba Jabare Saamb, maamam di baawo Gede, been dekk la ci diwaani Fuuta Tooro.

Jaam yi

Soppi
  • Am na jaami buur yi ( Ceddo yi), Jaami Juddu, Jaami Sayor (ñoom ca xare lees leen daan ame ak a jàppe). Xeet wu nekk nag lanu daan juge.

Wolof yi danoo jaxaasoo, lii moo tax seeni sant bari, ak tamit xeet yu bari ñëw nanu ci ñoom (Wolofal: Wolofisation). Ca Fuuta-Tooro, ca Cuballo (Nappkatu Tukuloor) walla Sebbe (Ceddo/Jàmbaar Tukulóor) Walla Tooroodo, lanu. Danoo teel a nekk foofu. Ci Senegaal ñoom ñoo njëkk a gis Tubaab yi. Bu njëkk Ceddo lañu woon, tay ñu bari ci yoonu murit lañu bokk walla tiijaaniya. Am na ay ay nasaraan (chrétiens) tamit waaye duñu ñu bari (Gore/Ndar). Seex Ahmadu Bamba Mbakke ak Alaaji Maalik SI ñoo gën a dugal Wolof yi ci lislaam. Wolof yu bari gàddaay nanu (walla tukki nanu) dem Faraas, Diiwaan yu Bennoo yi (États-unis), Itaali, Espaañ. Ci Senegaal ñoo yor pal yi gën a rëy (loolu du lu ñépp man a ànd, ndax gisees na ne Njiitul Senegaal lu njëkk séeréer la woon la ca topp it noonu, boo demee ca xare ba (l'armée)lu ëpp ca kilifa ya doonuñu ko. Kon wax jooju ju deesi xoolaat la). Ñoom ñoo gën a fonk seeni réewm (Nationalisme Sénégalais). Am na ci ñoñ ci Mbay (Kaw-Kaw) lanuy dunde, am ci ñoñ ci Napp, ca géej gi (ci ñoom la Lébu yi bokk). Jom ak Teraanga ci ñoom la fekk baax.

Xool itam

Soppi