Tekuruur moo doonoon benn nguur ca bej gannaaru Senegaal. Xeet yu bari tase nañu fa, juge Isipt: Séeréer si, Pël, Sooninke, Naar yi. Leeegi Tekuruur, Fuuta-tooro la tudd. Koli Tenŋela Bah, denyankobe bi, moo ko jox tuur wi. Ca nguur ga, Tukuloor ak Pël ñoo fa ëpp ba tay, waaye Séeréer si ñoo fa jëkk a nekk, ak Pël. Buur yu bari ñoo yoroon nguur ga:

  • Jaa-Ogo yi ci yoonu imbratooru Gana. Ñoom ay tëgg lañu woon. Bokk ci Pël yi.
  • Manna yi. Ca Penku lañu fekke baax (nguuru jaara / kingi), sant Ñaxate, bokk ci sooninke yi.
  • Tondiyoo yi. Ñoom ay Séeréer lañu woon.
  • Lam-Termess, Lam-Taga, ak Lam-toro yi. Ci ñu nekke buur, Jolof moo doon uuf dëkk bi, di fi teg ay Farba (Farba Walwalde, Farba Njum, etc).
  • Deeniyankooɓe yi, yu Koly tenŋela Bah, Sebee lañu woon, Sebbe mooy Ceddo.
  • Almaami yu Torodo yi. Sulaymaan Baal ak Abdul Xaadir Kan, ñoo dàq deeniyankooɓe yi ci atum 1776. Ay jullit lañu woon.

Ba noppi, tubaap yi ñëw ak canc gi (colonisation), ci atu 1890, jël nguur gi, elif Almaami yi, di séddale dëkk bi, ci ay - li nuy wax ci lakku fraanse (Canton) ak (Provinces).

Tukuloor, mooy ku dëkk Tekruur, da mel ni baatu Fuutankooɓe / Fuutanke, di ku dëkk Fuuta Tooro. Tur wi ñuy wax Tukuloor tubaab moo ko fi indi, yeneen yi naan Wolof yi ñoo ko sos. Nit ñi , dañu faral jaawale, Tukuloor (ku dëkk Tekruur) ak xeet wi nekk ca dëkk boobu. Ñoom, ci waaso yi lañu joge: Pël, Séeréer, Sooninke, Naar. Seeni sant ñoo ko firnde. Deeniyankooɓe ñoo tax lakku pulaar siiw dékk boobu.