Ceddo, jàmbaaru nguuru Senegaal la doonon bu jëkk, ci cosaanu Senegal. Nguuru: Kajoor, Bawal, Jolof, Waalo, Fuuta, Siin ak Saalum, Galam, lanu dekke woon. Seeni col nekkoon na mbubb ak téere yu bari ci seen kaw, njañ ak létt lañu daa am, jaaro ak takkaay yu bari it ñu ràngoo leen. Def nañu lépp, xare ba sonn, ngir tubaab man a bàyyi réewum Senegaal. Demba waar Sàll, Farba Kaba, Dammeel Lat Joor Ngóone Latiir Jóop ci ceddo yi lañu woon.

Baatu Ceddo, yaatu na. Geer yi (walla garmi), ak ku nekkoon doomi buur, Ceddo lañu ko daan woo. Yemul ci jammbaar yi rekk. Ci Pël yi ak Tukkloor yi, dañu daan joxe turu Ceddo (walla Sebbe su de dañu bare), ñu nekkoon buur. Séeréer yi tamit, Ceddo yi, doomi buur lañu woon (bino maad ci seen lakk). Ci Senegaal fepp, bu jëkk, Ceddo yi ñoo daan yor nguur yi, ñoo gënoon fete kaw, ci nos gi.