Tukkloor genn giir la gu nekk Senegaal. Ñoom ci seen bopp, Halpulaar lañu tudd. Nguuru Fuuta-Tooro mooy seen i dëkk, li moo tax dañuy wax tamit FuutaŋkooBe / Fuutaŋke (ku dëkk ca Fuuta).

Sëriñu Tukkloor (nataalu abbé Boilat ci Esquisses sénégalaises, 1853)

Ñoom dexug Niil lañu juge, ca dëkk ba ñu tuddee Nubi / Kuus, di nekk tay ca réewu Sudaan. Foofu dañoo bokkoon ak Séeréer yi. Pël yi nekkoon wàllu tukkloor ñoo nekkoon sammkat. Boobu baatu tukkloor ñëwaguloon. Ñoom ñépp dañoo mujj a gaddaay, ba agsi dexug Senegaal. Suuf si ñu agsi ba noppi, ay Sooninke ak ay naar agsi nañu fa tamit. Moo tax tay képp kuy dem ca Fuuta Tooro, xeet yooyu yépp ngay fekk. Turu Tukkloor ci lakk tubaab la juge, tukkloor lañu doon wax, ndax tur woowu nañu daan tudde seen dëkk (Tekuruur). Tukkloor mooy ku dëkk Tekruur. Am na ñu ne, wolof yi ñoo sos baat bi. Tukkloor yi Pulaar mooy seeni lakk, lislaam mooy seen diine. Tukkloor yi dañoo teel a dugg ci lislaam ca jamonoy imbraatoor gu Gana. Sooninke yi ñoo leen duggal ca lislaam. Buuru tekruur bii di War Jaabi, moo indaale lislaam ca nguuru ga, te

Ca XVIeelu¹⁶ xarnu, benn sëriñu tukuloor mu tudd Ali Elibana Saal, ak xarekatam, Jihaaroonàñu ca Fuuta-Tooro, ndax Deeniyaŋkooɓe yi ak óoih Tegaelaamiu leen jiite, ñoo yooonr nguurgai te nekkuñu woon ay jllli, aAy Ceddo lañu woon. Waaye deeniyaŋkoɓe yi, àaq añun Elibana Saal ak xarekatam. Ñoomñu daw ba Saalum, foofuldañu Jhyaar ca Séeréer ai waaye ñoom àaq añu Ali Elibana ba dexug àambi, foofu tukkloor yi tabax nañugbenn nguur mooy nguur Kabada.

Ca XVIIeelu¹⁷ xarnu, Maalig Si Daawda, tabax na nguuru Bundu, ca Senegaal, ca wetu nguuru Jolof, ak Gajaaga. Moom tamit Def na Jiyaar ca Fuuta-Tooro, deeniyaŋkooɓe yi dàq ko ca dëkk ba. Moom ak njabootam, xarekatam, daw nañu ca Njarmeew, di daje ak Waly Mbëru Mbakke Ndaw berlëp ku daan ilif dëkk boobu. Foofu la tabax nguuru Bundu. Malig Si Daawda, tooroodo la woon.

Ca XVIIIeelu¹⁸ xarnu, Tooroodo Tukkloor yi dàq nañu Deeniyaŋkooɓe yi fa doon Buur (Silatigi). Li yépp ak Suleymaan Baal ak Abdul Kader Kan la xewe. Ñoom nag, duggu nañu FutaŋkooBe yëpp ca lislaam, di fa teg ay Almamy, Almamy boobu moo yore woon nguur bi, dafa waroon na nekk Seriñ bu gëna am xam-xam ca lislaam ca FutaŋkooBe yi.

Ca XIXee xarnu, El Haaj Umar Taal, tabax na imbratoor gu Tukkloor ca Mali. Umar Taal, dem na ca Makka, foofu Xaalifa yi, def neen ko, Xaalifu Tiijaaniyaa ca reew yi nit ñu ñuul (Sudaan bu sowu jant). Umar Taal duggu na ay nit yu bare ca biir tariqa Tiijaaniyaa. Jiyaar na ca nguruu Xaaso waaye foofu tubaap yi daq neen ko. kon dem na ca Mali, xeex ak nguuru Jaara, rey fa Buur ba (Birante Karunga Jawara). Xeex na ak Buur yi Bambara yi (Fama yi), ca nguuru Segu ak Kaarta, di leen uuf ca imbratooram. Xéex na ak Amadu Bari, buuru Massina, di ko uuf tamit.

Ca XIXeelu xarnu, Maba Jaxu Ba, Almamy bu Rip la nekkoon. Rip moo doon benn diiwaan ca biir Nguuru Saalum. Ca Rip ay Buuru Mandiŋ (sant Maroon) ñoo fi nekkoon. Nguur bi Badibu la tudde woon, Maba jaxu moo ko joox tur boobu: Rip. Ndax mu mëna fa nekk Almamy, Maba jaxu jiyaar na ca badibu yepp di rey Buuri yepp. El Haaj Umar Taal, moo ko daan digal mu def loolu, ndax gis na ci moom, nit ku xam lislaam bu baax. Ca atum 1871-1875, Amadu Seexu, benn Almamy bu Fuuta-Tooro, jiyaar na ca nguruu Jolof, di fa nekk Buurba, ñeent at.

Jiggeenu Tukkloor bu Bundu (atum 1890)

Nosteg mboolay

Soppi

Tukkloor seeni Nosteg mboolaay ga, nii la tëdde woon:

Rimbe yi (dimo su ne benn) ñoo doon:

  • Sebbe yi, xarekat lañu woon, ñoom ay Ceddo lañu nekkoon. Sebbe yu bari ca xetu Séeréer ak Pël lañu joge. Ba XVeelu xarnu ba atum 1776 ñoom ñoo yoroon Fuuta-Tooro.

Seeni sant: Njaay, Saal, Jeŋ, Wan, Ñaŋ, Jah, Ndoom, Cimbo, Jaw, Bah, Ndaw, Caam, Waad, Mbooj.

  • Torodoo yi, ñooñu ñoo daan doxal lislaam. Ca atum 1776 lañu jëkk am doole. Ñoom ñoo daq Sebbe yi. Buuru Torodoo yi Almamy la. Seeñi maam ñu bare ca xetu Sooninke ak Naar lañu juge.

Seeni sant: Sih, Lih, Kan, Aan, Ture, Siise, Aïdara, Njaay, Caam, Wan, Ja, Saal, Bah. Am na yeneen.

  • JaawamBe yi, ñoo doon topp Buuri, di leen wone naka lañu yore nguur gi. Ca Pël yi lañu juge seeni sant : Jaw, Ñaan, Daf, Njim, Bokkum.Ci lu gëna siiw.
  • SubalBe yi, ay nappkat lañu, te ci cosaan dañu doonoon ay xarekat mel ni Sebbe yi. Bokk neen ak Sebbe yi. Yu bare seen maam ay Séeréer lañu. Seeñi Buur, Teeñ walla Jaaltabe la tudd. Seeni Sant: Sar, Ñaŋ, Juuf, Maal, Gay, Diba, Jool, Jeey, Gey, Jaw. Am na yeneen Sant.

Ñeeno yi:

  • WayilBe yi ñoo doon Tëgg yi.

Seeni sant : Caam, Mbow, Jaw, Kante, Sih, Peen.

  • LawBe yi, Seen yi, ñu jefandikook bant.

Seeni sant: Sow, Jum, Gajaga, Wañ.

  • SakeeBe yi, ñoo doon Wuude yi.

Seeni sant: Beey, Gakko.

  • MabuuBe yi, ñoo doon Rabb y.

Seeni sant: Gise , Sangott, Kume, Jonŋ, Taal.

  • Waambaabe yi, ñoo doon Xalamkat yi, woykatu xarekat yi.

Seeni sant: Bah, Jum, Gise.

  • Gawlo yi, woykatu Buuri, sab lekk yi.

Seeni sant: Mbum, Samb, Sek, Jeŋ, Laam, Mbay, Joob.

Jaam yi:

  • Maccudo/Kordo/JyaaBe. Tey, kenn du jaamloo jammbuur. Aada bu jëkk la woon.

Tukkloor yi, bey mooy seeni dund. Ca Fuuta-Jalon am na fa ay Tukkloor. Ca Kajoor dañu jëkkoon nekk ca diiwanu Jammbuur (Luga, Koki). Am na yu bare dañu daw Fuuta, di dem ca Dakar, Kawlax, Cees, wala Ndaar, ak yeneeni peey yu mag. Ñu ci bare ca tariqa Tiijaaniyaa lañu bokk.

Xool itam

Soppi