Laman, walla lamaan, benn tur la, ñu ko daan joxe ñu yorewoon suuf si, ci jamono ju yagg ya, ca Senegaal.

Cosaanu baat bi

Soppi

Taarixkat yi, mel ni Seex Anta Jóob, walla Abubakry Muusa Laam, wone nañu, baat boobu, ci Isipt gu yàgg ga la juge.

Foofu, baat bi di laman, leppuy jemewoon ci suuf si la tekkiwoon (suuf si ci boppam, walla lu doon jem ci wallu bay).

Séeréer yi ak Pël yi, ñu xam ne ca dexug Nil lañu cosaano, fu amoon Isipt gu yàgg ga, ñoo indi tur bi di Laman, ca Senegaal.

Ba ñu agsi Senegaal, ci ñoom, laman moo doonoon ku yore suuf si, buur bi. Li yepp, ba indi LAM bi buur bi takkoon ci loxoom, ngir wone ne, moo moom suuf si.

Laman yi ca Senegaal

Soppi

Nguuru Waalo, Fuuta-Tooro, Jolof, Kajoor, Siin-Saalum, Bawol, foofu yepp, ay Laman moo fa jëkkoon nekk, di yore seen nguur.

Ca cosaan, dañu fattaliku LAMAN JAW, LAMAN NGOM ak JOLOF MBEŊ ñu nekkon ca Waalo ak Jolof, bokkoon ci Seereer yi ak Pel yi, ñu nekkoon fa ay jamono yu yagg sooga Njaajaan Njaay ñow.

Ca Kajoor ak Bawol it, dañu fattaliku laman yi fa nekkoon, ñu bokkoon ci njabootayu ñu sant Jaañ ca Kajoor, Juufeen yi ca Bawol (lamanu Bawol di doon Teeñ), sooga Dammel yi ñow, ak PAALEN yi.

Ci nguuru Fuuta-Tooro, dañu fattaliku LAM-TOORO bu fa nekkoon buur, ca dëkk bu ñu naan TOORO, mu gënoon am dole dëkku Fuuta yepp, ba ñu woowe Fuuta, Fuuta-TOORO. Kooku, ca peey bu tudd GEDE la dëkkoon (wolof yi di woo LAM-TOORO bi BUUR GEDE). Ci ñu sant SAAL la bokkon, bokk ci ururbe yi. LAM ci pulaar, mooy buur (LAMƁE - LAMƊO - LAMIƊO).

Ba jamono Jolof uuf nguur yi yepp, laman yi nekoon ca nguur yi, dootuñuwoon ay buur, ndax buur-ba Jolof rekk moo nekkon buur (buur fari). Waaye laman yi, dañu mujj nekk ay kanŋam bu mag, ak ay jaambur ju mag, bokk ci xeet yi buur-ba yi juge woon ci seen meen.

Dëkk yi yepp, ay lamana lañu ko doon seddële, di firnde ni laman yi, dañu wey am doole, ba canc gi ame ak tubaap yi, ci jeexitu fukk ak juroom ñeenteelu xarnu.