Pël genn giir la gu nekk Senegaal. Pël yi ci Sowwu Afrig, dañoo bokk ci waaso yi gën a bari gën a yaatu. Senegaal, Mali, Gànnaar, Gàmbi, Gine, Gine Bisaawóo, Niseer, Burkina Faso, Niseeria, Benin, Kot Diwaar, Kameroon, Réewum Diggu Afrig, ba Sudaan, ca réewum yii yépp Pël yi ña nga fa. Xeet woowu am nañu tur yu bari: Pël ci Wolof, ci Afrig mooy tur wi gën a siiw, Fula ca Mande ya, Fulani ca Naar ya, Fellata wala Fellan ca Sudaan.

Sàmmkatu Pël bu Gurma, bëj-saalumu Gao, Mali
Pël, Mali

Ñoom ci seen bopp dañuy wax Pullo wala FulBe. Isipt mooy réew mi ñu bawoo. Pël ya ca Isipt ay nit ñu ñuul lañu nekkoon. Ba noppi, ay nit ñu weex, ñëw ca seenum réew juge Asi ak Tugal , bokk na ca xeet yooya: Scythe, Aryen, Phrygien, Hittite, askan yu bari yu ñuy tudde ay waa End-tugal (Indo-européen). Pël yu ñuul yi ak nit ñu weex ñi dañoo jaxaasoo woon. Lii moo tax Pël yi gën a xees, gën a sew, am kawar gu gën a nooy, bu ñu leen xoolee ci yeneen xeet yu ñuul yi ci Afrig. Ba noppi, Imbraatóor gu Iran(ñoñ Cambyse ñi(les Perses) ), tegoon nañu loxo réewum Isipt, di fa tege dund gu metti, rawati na ca nit ñu ñuul ña. Lii moo tax Pël ya ak Séeréer sa gàddaay, dëkki ca Sudaan (Nubie) dëkki seeni maam, soog a dem Senegaal. Pël ak Séeréer danoo bokk maam, seeni làkk tamit. Yàgg nañoo ànd, dañuy kalante ci seen biir. Ca yoonu Tekuruur, pël ya ca Dexug Senegaal rekk lañu nekkoon ak seeni nag. Booba nekkuñu woon ay jullit. Amuñu woon nguur ndax ak seeni nag ci màng rekk lañu nekke woon. Meew ak Sanqal (ñórndi) moo doonoon seenu lekk. Pël ci boppam am na xeet yu bari (Leyyi/KinDe), Ardo mooy seen Buur: JaawBe yi, UrurBe, WodaaBe, LaaCe, CutinkooBe, YirlaaBe. Am na yeneen KinDe. Màng gi ñu dëkke tax na ñu tuuru ci Sowwu Afrig gépp, ba far delseeti Sudaan, cig muñ ak coona ndax saa su nekk ci dëkki jàmbur yi rekk lañuy nekk, seen nag yi leeg-leeg ñu ruur tooli baykat yi, loolu it di jur xuloo bu rëy ak ŋaayoo ci seen digg ak woroon tool yi.

Pël (Togóo)

Ca atum 1539 Koli Tengella Bâ, mi ngi bokke ci Pël ci wetug baayam, bokk it ci Mande yi ci wàllug yaayam (Keyta), dajale woon na sàmmkati Pël yi ak mande yi, ngir ñu man a am doole. Daa di dugg ci yeneen xeet (Wolof, Séeréer, Bajaaranke, Joola, Baga, Sooninke . Ñoom ñépp ak seen aroo Koli Tengella, ñu yéeg ba Tekuruur, di xeex ak Buur-ba Jolof ba, ndax kii moo doon yor dëkk ba, ak Lam-Toro ya, Lam-Térmes, Lam-Taga ya, Juroom ñeenti fan soog a yor dëkk ai. Koli Tengella teg na fa njabootam (Denyakoobe yi), tudde na nguur ga Fuuta-Toro (Fuuta mooy dëkku Pël ca seen Làkk). Lii ca Senegaal la xewe.

Ca Mali Pël ya doñoo njëkk am doole ca atum 1818. Booba nag Ahmadu Bari, Sëriñ la nekkoon, dajale na Pëli Jullit yi, ak Mande yu jullit yi ( Mandé Mori yi : Siise, Ture, Silla ), ngir ñu àndandoo xeex (Jiyaar) safaan nguuru Bàmbara yi fi nekkoon (nguuru Ségu ak Kaarta). Buuru Bàmbara yi (Fama) ak seeni jàmbaar (Ton-Dion), amoon nanu doole, lii moo tax Ahmadu Bari tabax Imbraatoor gu Pël ca Massina Kese. ak itam Pël yi, ca Mali, foofu lañu ëppe woon ba tay (Tay jii foofa mooy diiwaan (Région) bu Mopti). Ca Gine, Pël ya dañu faa yàgg, waaye Mande ya (Jalonke) ñoo yoron dëkk ba. Ca 1715, ay Pël yu jullit yu juge Fuuta-Tooro ak Massina ca Mali, ñoo ñëw Gine, di fa Jiyaar, di ray ñi duli jullit walla di leen jàpp ay jaam, lii moo tax giir yu bari (Susu yi, jalonke, ak Baga yi) daw ca géeju Gine, di tabax foofa ay nguur. Pël yu Jullit yi dañu doon ray ñoom tamit yeneen Pël ngir ne nekkuñu woon ay juulit. Pëli jullit yi dañoo bokkoon ca njabooti: Bâ, Bari, Jallo, Sow. Ñoom ñoo tabax nguuru Fuuta-Jalon. Karamoko Alfa Jallo mo njëkk a nekk Almaami. Ca Niseria atum 1808, Usmaan Dan Fojo, njabootam Fuuta-Tooro la bawoo, nekk ay Tooroodo, Sëriñ bu mag la nekkoon, bu bokk ca tariixa Xaadiriya. Moom nag dajale na baykatu Awsa yi, ak sàmbkati Pël yi, di leen dugal ci Lislaam, ndax ñu man a def jiyaar ca Nguuru Awsa yi fi nekkoon. Ray na Buuru Awsa bi, daal di tabax Imbraatoor gu Sokoto. Dem na xeex ca Imbratoor gu Kanem-Bornu ca Cadd, waaye ñooñu dañoo amooon doole lool. Ca kaw Kamerun atum 1810, benn sëriñ bu tudd Mojibo Adama, dajale na Pëli jullit(foofu Fulbé lees leen di wax) yi fi nékkoon, nu tabax nguuru Adamawa. Waaye am na Fulbé yu bari (WodaaBe/Borooro), yoy ànduñu woon ca googa nguur. Modibo ak yeneen Pël yi ñoo defoon Jihaad, ndax ay jullit lanu woon. Modibo Adama, Usman Dan Fojo moo ko dimbali woon. Ca atum 1860, Alfa Yaaya Molo Balde, tabax nguuru Fuladu ca Bëj-saalumu Senegaal. Daal di dajale Pël yi di leen dugal ci lislaam, ndax Almaami bu Fuuta-Jalon Alfa Bokar Biram, nee na woon du dimbali ku dul Jullit. Almaami boobu ak Alfa Yaaya xare nanu ak nguur gu Mandé, Kabbu ak seeni Buur (Mansa), ndax foofu Pël yi danu faa nekkoon Jaami Mandé yi. Ñaari Buur rekk ñoo yoroon Fulaadu, Alfa Yaaya ak doomam Musaa Molo Balde.

Kon Pël yi, Lislaam moo leen dajale, di leen jox doole.

Pël seeni Nostey mboolaay nii lanu tëdde woon:

  • RimBe ñoo daa doon Buur yi.
  • JaawanDo yi, ñoo daa topp RimBe yi di leen won nan lañuy yore nguur.

Ñeeño yi:

  • WayilBe ñoo daa nekk Tëgg yi.
  • LawBe ñoo daa doon Seen yi.
  • SakeeBe, nekk Wuude yi.
  • MabuuBe, doon Ràbb yi.
  • BaambaaDo, doon Xalamkat yi, woykati Jàmbaar yi.
  • Gawlo, Woykati Buur yi.

Jaam yi:

  • Maccudo walla Kordo.

Ca Isipt Pël ya, dañoo yoroon ñatti Sant rekk (Ba, Ka, Bara (tay mu soppiku di Bari)). Ba noppi Pël yi danoo jël yeneen Sant Ndax dëkk bi, walla Mban yi, liggéey yi ñu doon def.

Li lépp ba am tay Sant yii: Bâ, Bari, Jallo, Ka, Ja, Sow, Jaw, Caam, Naan, Jum, Dikko, Seydi, Mbow, Bokum, Dem, Sidibe, Sàll, Ca fulaadu Pël yu bari Jamanka lañu sant. Ca Mali Sidibe mooy Sow. Ca Niseriyaa Pël yu bari Bello lanu sant. Ku sant Baal, maamam ay Bâ lanu woon. Ku Sant Jakk maaman ay Sow lanu woon. Sankara, Sankaré, Shagari, yooyu yépp benn lanu. Am na Pël yu bari yoy dem nanu ca Wolof ya, looloo tax am ay wolof yu sant (Caam, Mbow, Sow, Naan, Sàll). Am na tam waaso yu bari yoy dikk nanu ci Pël yi, moo tax am ay Pël yu sant Siise, Ture, Njaay, Jakite, Kamara ak yeneen sant.

Xool itam

Soppi