Bawol

(Yoonalaat gu jóge Bawal)

Ci xarnub fukk ak juroom Bawol nguur su ndaw la woon su toppoon Jolof gu mag gi, bu ko defee, ag njaboot gu amug jegeñaale ak buuri Kajoor yi daa ko jiite.

Bu jëkk, nguur googu, ay socé ak ay séeréer, ñoo ko yoroon. Am na ñu ne sax, baat bu ñu tudde dëkk boobu tey, di Bawol, ci kallama socé yi ñu fa nekkoon la joge, di tekki lii wolof tudd dex. Ndax Bawol, been dex la woon foofu ci lu dooga am. Boobu jamono, Bawol, amoon na ndox mu bare.

Ci cosaan, dañu ne, Bawol, ku fa jëkka nekk buur, XAAYAMAGAAN moo doon turam. XAAYAMAGAAN, ci lakku socé yi la soqeekoo, mooy: buuru gaalam. Ñoom, socé yi fa nekkoon jamono boobu, seen mamm, Mande lañu baawo.

Ba paré, séeréer yi ñëw. Ñoom, fuuta tooro lañu joge woon, gadday ba Bawol, ndax jiyaar ji muraabituun defoon foofu. Ba ñu agsi Bawol, ci ubbite, dañu daan dekkando ak socé, sooga leen daq. Ba loolu ame, ñu elif dëkk boobu. Ci séeréer yi, askan yi ñu faloon, ñoo ñu sant Juuf, Ngom, Caw. Te buur ba ñu daan taan ci ñoom, Téeñ lañu ko daan tudde.

Loolu mo amoon, sooga nguuru Jolof ñëw uuf dëkk bi.

Ci xarnub fukk ak juroom benn g.j, la Jolof mànge poseb néew-dooleg nguurug Jolof , daal di jël ag tembam, ni ko yenn ci nguur yi defe woon, gu ci mel ne Kajoor ak Waalo, ngir song gu tar ga Amari Ngóne Sabel Faal defoon Jolof. Ci ñaareelu xaaju xarnu bii la Amari Ngóone xëy di buuru Kajoor ak Bawol ci jenn jamono ji.

Booba la buur bi tàmbalee jiite ñaari nguur, waaye nguur gu ci nekk yor politigu doxaliinu réewam. Waaye boole gii bari lu mu daa jur ay réeroo ci diggante ñaari nguur yi, ndax gu ci nekk daa bëgg a yilif ga ca des.

Buurub Bawal nag di Teeñ ab jataay a ko daa jàppale, bu ñu wéer tabbug kiy wuutu buur bi bu faatoo, ak fuglug saxal yi buur bi di def. Nguur gi amoon na ab ëttu àtte buy àtte mbir yi, mbooleem kuréel yi nag daa nanu fa àttewoo (kuréelug nappkat yi, baykat yi, sàmm si, ñoñ fànn ñi (boroom mecce yi) ak jigéen ñi). Bokkug Bawol ci Yaxantug Tàkk gi taxu ko woon a deme noonu, ndaxte yooni yaxantu gi rombutoon ciy suufam, moom kay daa yamoon rekk ci yaxantug tefes gi.

Seetal BUNTU TAARIIX