Cig déggoo, Njëkk-taariix mooy jamono ju taariixu nit ji jiitu sosum mbind.

Wikipedia
Wikipedia
Bii jukki ab junj rekk la. Man nga cee duggal sa loxo suqali ko ndeem am nga ci xam-xam ci anam yi Wikipedia taxawal



Fànn ci Njëkk-taariix

Ak juddug mbind taariixkat yi am nañu ay wayndare yu leer te yaa yees man a sukkandiku ngir man a taxawal toftaloog xew-xew yi yiy biral digalub jamonoy taariix yi.

Xaaj bu yaa bu taariixu nit njëkk sosug mbind, ci xayma, mi ngi door mat na 200 junni at, ba jëmm ji njëkk jees man a nattanleek nitu tay jii feeñee ci Afrig gu Bëj-saalum.

Donte sax mat na 2 milioŋi at, benn xeetu nit bu doon dund ci wetu Dexu Viktori (war a doon tay jii ci diggante Ugandaa, Keeñaa, Tansani) moo njëkk a jëfandikooy jumtukaay ci noonu taariixu xarala door. Cig lawal, manees naa njort ne fala xalaat, fànn, xeltu ak xam-xam dooree.

Sosug jumtukaayu liggéey bu njëkk man a tax nu jàpp ne nëkk-taariix a ngi door 2 milioŋi at ci ginnaaw, donte mbooloo yooyu maneesu leen jàppe niki nit ninu ko xamee tay, ci jëmm ak doxalin.

Logo Commons

Xool it Wikimedia Commons