Cosug àdduna bi ak Big Bang

Nit daa mas di laaj ci jamono ju nekk:

  • fan la àdduna su daytaluwul sii juge ?,
  • fan la jëme ?
  • nan la àtte yiy wattu ag màndaqoom (son équilibre) akug nosoom (son ordre)di doxe.

La ko dale ci ay xarnu, boroom xam-xam yi def nañu ay gëstu ci lu aju ci tëriit loolu (sujet boobu), ñu àgg ci génne am mbooloom ay gisiin (théories). Xalaat bi notoon ci xarnub fukk ak juroom ñeent moo doonoon àdduna bi de am mbooloom ne-ne (matiere) la, yu yor dayo bu amul yamu, yu fi nekkoon naka jekk, tey yu fi dul jug it ba fàwwu.

Gis-gis bii nga xam ne mooy cëslaayu xeltu gu ngérum ne-ne (philosophie matérialiste) da daan dàq ak a weddi amug aji sàkk ji (Yàlla), ba noppi di saxal ne àdduna bi amul ab tàmbali, te amul it ab yamu.

Ngérum ne-ne (le matérialisme), nosteg xalaat la (système de pensée), guy jàppe ne-ne ne mooy genn nekk gu joyu (le seul être absolu) gi fi am, ci noste gii, lenn lu dul ne-ne amul. Nosteg xalaat gii nga xam ne mi ngi sosoo ca Geres Gu Yàgg ga, te gën a tase ci fukk ak juroom ñeenteelu xarnu, mujj na di lu siiwe ci turu ngérum ne-ne mu dàggasante (matérialisme dialectique) mu Karl Maks. Ñoñ ne-ne ñi (les materialistes) dañoo jàppe woon xalaatu àdduna bu amul yamu bii muy seen ndëerlaay lu mag lu seen xeltu gu weddi gi (philosophie athée). Ci misaal, ca téereem ba tudd (dal yu dàttu yu xeltu) (principes fondamentaux de philosophie) saa ne-ne (ce materialiste) mii di Jorj Politseer, saxaloon na ca ne àdduna bi du lees sàkk, dolli ca ne bu doonoon lees sàkk, daa waroon a nekk di lu Yàlla sàkk ca saa sa te mu tukkee cig neen.

Bi Politseer saxalee ne àdduna bi sàkkeesu ko cig neen (du néant), dafa sukkandiku woon ci misaal mu sax mu àdduna bi (modèle statique de l'univers) te nekkoon fi ci fukk ak juroom ñeenteelu xarnu. Mu xalaatoon ne def na ag saxal gu xam-xam. Ci biir loolu jëm kanam yi xam-xam ak xarala amal ci ñaar-fukkeelu xarnu, màbb nañu ci mujj gi xalaat bu njëlbéenu (idée primitive) bii ñuy wooye ngérum ne-ne (matérialisme), wuñees na ne àdduna bi saxul ni ko ñoñ ne-ne ñi daa waxe . Waaye ci safaan bi daa nekk cig tàllaliku. Gisees na it jaare ko ci seetlu ak xayma ne àdduna bi am na ab tàmbali (fu mu tàmbalee), te dees koo sàkk mu tukkee ci tus, ci ag fàcc gu mag. Tay jëf jii àddunay xam-xam jépp nangu na ko, te wuññig jëf yu am solo yii mi ngi jàppandee ci ay seetlu aki njuréefi gëstu yu di ag jeqiku (révolutionnaire) .

Ca 1929 ca seentluwaay (observatoire)bu Monpiuson ca Kaliforni, ab saytukatu bidiw bu Amerig bu tudd Elwin Oban defoon na benn ci wuññi yi gën a mag ci taariixu saytubidiw (astronomie), bi muy seetlu bidiw yi ci ag fésalukaay gu ngande (télescope géant), gis na ne dañuy genne genn leer gu xaw a xonq, ci kem seenug soreyoo, loolu li muy wund mooy bidiw yi dañuy dem sori ñu. Waawaaw, ci li ay àtte yees nangu ci jëmm (lois phisique) wax, jëmmi ceññeer yu leer yi bu ñuy tuxu jëm ca tombub seetlu ba, dañuy jeng jëm ci yolet, te jëmmi ceññeer yu leer yiy dem di sori tombub seetlu bi dañuy jeng jëm ci xonq. Seetluy Oban yi may nañu nit xam ne leeri bidiw yi dañuy jëm ci xonq. Loolu li muy wund mooy ñoom kat dañoo dëkk ci di ñu sori, di dem wëlis ñu. Ginaaw loolu Oban defaat geneen wuññi gu mag. Du rekk bidiw yi ak galagsi yi dañuy sori wëlis nu, waaye dañuy dox di soreente ñoom ci seen biir. Ndegam nag mbooleem céri àdduna bi (ses éléments) dañuy soreyante ci seen biir, lenn lees man a jàpp mooy ne àdduna bi daa nekk cig yaatu gu sax (tàllaliku=expension). Ngir gën a xam loolu man nañoo jeneer àdduna bi mu mel ne kaw ag manq gees nekk di wal. Ni tomb yi nekk ci kaw manq gi di soreentee lees koy gën di wal, ni la yëf yi nekk ci jawwu ji di soreentee lu àdduna bi gën di tàllaliku. Lii sax wuññeesoon na ko ci gisiin (theorie) ci lu gënoon a teel, Albeer Anstaayin mees jàppe ne mooy boroom xam-xam bi gën a mag ci ñaar-fukkeelu xarnu àggoon na ci ginnaaw ay xayma yu xam-xamu jëmm bu gisiin (physique théorique), àggoon na ci ne àdduna bi nekkul di lu man a sax (statique). Ci biir loolu daa tegoon nee wuññeem googu, ngir rekk bañ a dëppoodeek misaalum sax (model statique) mu àdduna bi, mi nga xam ne moom la népp jëloon ciy jamonoom. Ci ginnaaw bi Anstaayin gisoon na ne def na ci loolu njuumte li gën a mag cig dunnam akub liggéeyam.

Lu tàllalikug àdduna bi di wund? Tallalikug walla gën di yaatug àdduna bi day wund ne bu ñu manoon a deltu ginnaaw, dinañu seetlu ne àdduna baa ngi doore ci benn tomb, fa la jële cosaanam. Xayma yi wone nañu ne benn tomb bii nga xam ne moo ëmboon mbooleem ne-ne bu àdduna bi daa waroon a am kemub tus (volume zero) akug fataay gu amul yamu. Àdduna bi nag mi ngi sosoo ci fàccug benn tomb bii yoroon dayob tus . Fàcc gu mag gii nga xam ne ci la àdduna bi doore, tuddeesoon na ko Big Bang, gisiin wi it daal di jël tur wi. Cig pàttali dayobb tus aw waxiin wu gisiin la (expression théorique) wees jëfandikoo ngir man a leeral, xam-xam manul a leeral maanaam neen ( concept de neant) mi nga xam ne weesu na digi déggiinu nit, ba mu koy tudde tombub tus. Ca dëgg-dëgg, dayob tus mooy ag neen, ci noonu àdduna bi mi ngi sosoo ci cig neen, ngir gën a leer , dees koo sàkk. Lii nga xam ne ci ñaar fukkeelu xarnu rekk la ko xam-xamu jëmm bu jamonoo bi wuññi, Alquraan moom saxaloon na ko booba ak leegi tollu na ci fukk ak ñeenti xarnu: Moom moo sos asamaan yeek suuf si. Gisiinu Big Gan (la theorie du Big Bang) mi ngi doon wone ne, ci njëlbéen gi, mbooleem yëf yi nekk ci àdduna bi benn cér rekk lañu woon, ginnaaw bi ñu séddalikoo. Lii nga xam ne gisiinu Big Bang wee ko wone, Alquaraan it jotoon na koo wone booba ak leegi toll na ci fukk ak ñeenti xarnu, ci jamono joj nit lu néew la xamoon ci àdduna bi. Ñi weddi xanaa gisuñu ne asamaan yeek suuf si benn jóor lañu woon bu taqaloo (lu ci ne tayu ci moroom ji), ñu tàqale leen,. Loolu li muy wund mooy lépp sàkkees na ko ci genn fàcc gu mag gu bawoo ci benn tomb, bu ko defee mu doon àdduna bii ngay gis bi mu tàqalikoo. Tàllalikug àdduna bi benn la ci firnde yiy wone ne àdduna bi cig neen lees ko sàkke. Lii nag xam-xam wuññiwu ko lu moy ci ñaar-fukkeelu xarnu bii rekk, waaye Yàlla moom jotoon na ñu koo xibaar ci Alquraan, jees wàcce booba ak leegi tollu na ci 1400 at: Asamaan si ñoo ko tabax ci sunu kàttan, di ko yaatal it ci anam gu sax. Big Bang day wone ci anam gu leer ne àdduna bi cig neen lees ko sàkke. Ci nu gën a leer, Yàlla a ko sàkk. Looloo tax saytukatu bidiw yi taqoo woon ak xeltu gu ngérum ne-ne mi (materialime) wéyoon ci weddi Big Bang te sax ci dëgëral xalaatub àdduna ju mul yamu bi. Sababi lànk gii feeñ na ci baati Artir Edington, benn boroom xam-xamu jëmm bu siw la woon: (( ci wàllug xeltu, déggiit (notion) wu ag tàmbali gu bette (abrupt) daf may xatal )). Beneen saa ne-ne bu waa Angalteer di Fred Hoyle, moom itam gisiinu Big Bang xatal na ko. Ci digg ñaar-fukkeelu xarnu Hoyle daa di nay doon farandoob gisiin wu melokaan wu sax wi (état stationnaire), woowu gisiin daa niroo woon ak wa fi nekkoon ca fukk ak juroom ñeenteelu xarnu, te di woon àdduna bu tekkaaral bi. Gisiinu melokaan wu sax wi daa saxaloon ne àdduna bi ab kemam amul yamu naka noonu ab diiram. Gisiin wii nga xam ne amul woon geneen jublu gu feeñ gu dul dëgëral xeltug ngérum ne-ne (philosophie materialiste) nekkoon na di lu safaanoo ak gisiinu Big Bang wi saxaloon ne àdduna bi am na ag tàmbali. Ñi daa layal melokaan wu sax wi yàgg nañoo lànk Big Bang, waaye ci biir loolu xam-xam moom di wéy di leen weddi. Ci 1948 Jorg Gamow indi na beneen xalaat ci lu aju ci Big Bang. Saxal na ne ginnaaw bi dduna bi sosoo ci ag fàcc gu mag, ab gëwéelub ceññeer (circuit de rayonnement ) war na am ci àdduna bi, niki jeexiitu fàcc gii. Rax ci dolli, ceññeer gii daa war a nekk di lu tas ci anam gu benno ci mbooleem àdduna bi. Firnde loolu doon na feeñi . Ca 1965 ñaari gëstukat yu tudd Arno Pinsiyas ak Robert Wilson wuññi nañu ceññeer yii cig mbetteel . Ceññeer yii ñuy wooye ceññeeri mbëj-bijjaakon yu Big Bang (fond diffus cosmologique) niruwuñu woon lu juge ci benn gongikuwaay, waaye da doon lu tas ci jawwu jépp. On comprit ainsi(degguma li mu wax foofu). Pensiyas ak Wilson joxees na leen neexalub Nobel ngir seen wuññi yooyu. Ci 1989, Nasaa sànni woon na ci jawwu ji satalit bii di Kob, ngir def ay gëstu ci ceññeeri mbëj-bijjaakon yu Big Bang , ba ñu defee juroom ñatti simili ci jawwu ji lañu dëggal xaymay Pensiyas ak Wilson yii. Kob wuññi na jeexiiti fàcc gu mag googee amoon ca ndoortel àdduna bi. Wuññi gii ñu jàppe gi gën a mag ci mbooleem jamono yi, indi na firnde lu leer ñeel gisiinu Big Bang. Leneen firnde lu am solo lu Bing Bang mi ngi bawoo ci kem bu Idrojen ak Eliyon bi nekk ci jawwu ji. Ci biir gëstu yi gisees na ne dajaloog Idrojen-Eliyom gi am ci àdduna bi dëppoo na ak xaymay gisiin yu dajaloog Idrogen-Elyom yi desoon ginnaaw Big Bang.

Bu àdduna bi amul woon fu mu tàmbalee mbaa mu nekkoon di lu fi mas di nekk, kon aji toggaleem ju Idrogen (sa composant dihydrogène) lekku na ba jeex bu yàgg ba far soppiku di Elyom. Firnde yu leer yépp nag ñoo tax woroom xam-xam yi nangu gisiinu Big Bang . Misaalum Big Bang mooy baat bu mujj bi woroom xam-xam yi agseegun ci lu aju ci cosaanul àdduna bi. Ginaaw bi mu yàggee layal Melokaan wu sax wi ci wetu Fred Hoyle, Denis kiyama melal na taxawaayam bu mujj bi mu mujj a àgg, ginnaaw feeñalug mbooleem firnde yiy dëgëral gisiinu Big Bang. Skiyama jibal na ne (( layal na gisiinu melokaan wu sax wi, du caagéenug ngir ne da koo wóoroon ne mooy dëgg, waaye rekk ngir ne loolu la bëggoon muy li am. Skiyama dolli na ci ne, bi firnde yi tegaloo, manatul a def lu du nangu nag ne làmb ji tas na, te wacci gisiinu melokaan wu sax wi)).

Profesëer Jorj Abel bu daara ju kawe ju Kaliforni nangu na moom it ndam lu mujj li ñeel Big Bang. Daal di jibal ne firnde yi am ci jamono jii wone nañu ne àdduna bi mi ngi feeñ ci ay milyaari at ci ginnaaw, te Big Bang gi waral ko. Mu nangu ne amul meneen pexe mu dul nangu gisiinu Big Bang. Ak dikkug gisiinu Big Bang, léebuw ne-ne bu sax (mythe de la matiere eternele) wi nga xam ne moo doonoon cëslaayul xeltug ngérum ne-ne (la base lde la phiolosophie materialiste) mujjees na ko sànni ci sënub taarix. Lu fi amoon kon njëkk Big Bang ? Jan doole moo sabab amug àdduna bi ci fàcc gu mag gii te kat bu njëkk lu amadi la woon ? Laaj bii day da fiy indi - ci waxi Artir Edington – lu naqari li ci wàllug xeltu li ñoñ ngérum ne-ne nanguwul a nangu te mooy amug aji bind (aji sàkk). Xeltukat bu weddi bu siw ba nii la saraa laaj boobu: (( Xamees na bu baax ne diine lu baax ci bakan la. Kon maa ngi doore ci nangu ne Stratonocien bu weddi bii manul lu dul nangu dëppoo gu àdduna gii. Ndax mel na bu baax ne sóobukati jawwu yi indi nañu firndey xam-xam ci ne àdduna bi am na ab tàmbali)).

Boroom xam-xam yu bari yu dul tënk seen bopp ci ne fàwwu dañoo war a nekk ñu gëmadi, nangu nañu ne am na aji sàkk ju man lépp ju sabab sosug àdduna bi. Aji sàkk jii daa war a nekk aji nekk joj moo sàkk jamono ji ak jawwu ji (walla féex gi = l’espace), waaye nekk it di ku temb (maanaam ku wéeruwul, sukkandikuwul) ci jamno ak jawwu ji. Lii la boroom xam-xamu jëmm (physicien)bu siiw bii di Hugh Ross wax : (( Bu tàmbalig jamono tollook tàmbalig àdduna bi ni ko layal wu féex gi saxale (le théorème de l’espace), kon li sabab àdduna bi daa war a nekk ag nekkte (entité) guy jëfe ci tolluwaayu jamono bu temb (indépendant) ci anam gu mat, ba noppi jiitu fi tooluwaayu jamono bu àdduna bi. Jii wax nag mi ngi ñuy jàngal ne àdduna bi du Yàlla moom ci boppam, te Yàlla it nekkul di lu ëmbu ci àdduna bi. Waa-waaw ne-ne ak jamono aji sàkk jee leen sàkk, ki nga xam ne wéeruwul ci benn ci maanaa yii, jii aji sàkk nag mooy Allaa Yàlla miy aji man lépp, kiy boroom asamaan yeek suuf . Ca dëgg-dëgg, Big Bang indi na ciy jafe-jafe lu sakkan ñeel woroom xam-xami ngérum ne-ne mi , Antoni Flew dëggal na loolu. Ndax Big Bang saxalul rekk ne àdduna bi cig neen lees ko sose, waaye saxal na ne it dees koo sos ci anam gu nosu, gu tegu ci yoon, gees fuglu. Big Bang mi ngi ame ci fàccug tomb bi ëmboon mbooleem ne-ne ak kàttanug àdduna bi, akug tasam ci jawwu ji ci mbooleem wàll yi, cib gaawaay bu yéeme. Ne-ne bii ak kàttan gii ñoo jur ag màndaqoo gu mag gu ame ci ay galagsi, ay bidiw, jant bi, suuf si ak mbooleem yeneen yaram yu asamaan yi. Nga rax ci dolli, ay àtte yees tudde àttey xam-xamu jëmm (lois de la physique) daal di feeñ, ay àtte yu niroo ci àdduna bi bépp, yu dul soppiku. Àttey jëmm yii feeñ ànd ak Big Bang, soppikuwuñu lu gën a néew ci diir bu tollu ci 15 milyaari at. Nga rax ci dolli, àtte yii ñi ngi tegu ci ay xayma yu àgg ci leer ba bees ci soppee la gën a néew ci li mu doon, mu yàq bindub àdduna bépp akuw meloom. Lii lépp li muy wund mooy Big Bang indi na fi ag nosu gu yéeme. Ci biir loolu ag fàcc, ci yoon, ag nosu daawu ci juddoo, mbooleem fàcc yees ma a gis, toc la daa def, moñoxe, wisaare, tas. Bees gisee nag ag fàcc def ag nos gu mel ne gii, li nuy man a wax mooy ag yewwute manul a ñàkk ci ginaaw li ko amal, te nag kenn daal moo war a yëngal mbooleem cér yii tas ngir fàcc gi, ci anam gees fuglu lool. Freds Hoyle mi mujjoon nangu gisiinu Big Bang, ginnaaw bi mu ko weddee ay at mi ngi leerar loolu ci anam gu leer: (( Gisiinu Big Bang saxal na ne àdduna bi mi ngi tàmbalee ci genn fàcc. Moone ni ñu ko man a seetloo, ag fàcc du def lu dul tas ne-ne , te Big Bang moom ci anam gu mbóotu daa def safaan ba, ci dajale ne-ne ci melow ay galagsi. Bu ag fàcc yobboo cig nosu gu mag loolu du man a def lu dul gëmloo ci ne am na aji sàkk juy ki ko def. Weneen feeñiit wu nosu gu kiimaane gii sosu ci àdduna bi ci ginnaaw Big Bang mooy sosuwug àdduna bees man a dëkke. Sart yi manul a ñàkk ci sosuwug àdduna bees man dëkke bari nañu te jafe ba xel du nangu ne man nañoo sosoo cig tombe. Paule Davis ab boroom xam-xamu jëmm bu gisiin (physique theorique) bu siw jibal na, ginnaaw bi mu defee am mbooloom ay xayma ci kemub tallalikug àdduna bi, jibal na ne kem bi de àgg na ci leer ak tegu ci yoon fu xel manul a xalaat. Davis nee na : (( njuumte gu ndaw ci natt kemub tàllikug àdduna bi man naa waral àdduna bi moy ag bijjam (sa gravité), bu ko defee wéyal ag tàllalikoom ci anam gu nosoodiku. Adduna bi, bu gënoon a dox ndànk ci nii mu koy defe, day daal di rot, bu gënoon a gaaw tuuti rekk nga gis ne-ne bu àdduna bi tas bu yàgg.Big Bang de du fàcc gu mel ne yépp : ((Ag fàcc la gu am ab tolluwaay bu sax, gu yam fees ko yamloo)). Prosesëer Stefaan Aukin, dib boroom xam-xamu jëmm bu mag, jibal na ca téereem ba tudd (Une breve histoire du temps) ne:(( àdduna bi mi ngi tegu ci ay xayma aki màndaqe yees nos, defar leen ci anam gu leer gu ñu manul a xalaat nun)). Aukin jibal na ci lu aju ci tàllalikug àdduna bi : (( Su fekkoon ne kemub tàllaliku gi, as cimili ginaaw Big Bang bi, daa yées ak doonte lu tollook téeméeri miyaari milyoŋeem la, àdduna bi day daanuwaat cig teel balaa tollu nii mu toll tay)). Paul Davies leeral na ba tay ngérte lees manul a moyu, lees di génnee ci xayma ak màndaqoo (équilibre) yu leer yii te yam ba ëpp : (( Lu jafe la nga man a tëyewu ci kanamu xam ne ni àdduna bi bindoo fi mu ne, nga xam ne lu néew lees ci laal rekk man na koo yàq, lees liggéey la ci anam gees sonn. Boole gu mel ne lu kiimtaane gii ci ay xiimaa yu lim te dénd bi (la nature) jox ko ay way saxam yu dàttu yi (ses constantes fondamentaux) day wéy di firnde lu fés liy wone ne àdduna bi lu nosu la)). Ci lu ci aju ba tay, Jorj Greenstein dib Profesëer bu Amerig, ca téereem ba tudd (L'univers symbiotique) nee na : ((Su nu xoolee firnde yii yépp, ab xalaat bu làkkale di na nu jàpp mooy ne lii daal mooy war a doon màndargam ag nammeel gu xarbaaxe (volonte surnaturelle))).

Ci gàttal daal bu ñu dee settantal nosteg àdduna gu yéeme gii, dinanu gis ne amug ak nosu gu àdduna bi dañoo goor ci ay màndaqoo yu yëgu (delicat) ak ci nosu gu fasu ba tombe rekk ak fiiroo (coïncidence) duñu doyati ngir firi leen, leeral leen. Ci lu leer, lu manul a nekk la nosu gii ak màndaqoo gu mat gii nekk di lu fi dikkal boppam ak cig tombe ginnaaw ag fàcc gu mag.Sosu gu ag nosu gu ni mel, ginnaaw ag fàcc gu mel ne Big Bang mooy firnde lu fés li ci ag sàkk gu xarbaaxe. Nosu ak tegu ci yoon gu mat gu àdduna bi dañuy wone ci anam gees manul a moyu teewaayug aji bind ju yor xam-xam, kàttan ak hikma ju dul jeex, mooy ki sos ne-ne jële ko cig neen, tey fuglu ak a doxal lii lépp cig wéy. Aji bind jii mooy Allaa, boroom àdduna yépp. Aji tekki ji : Abdu Xaadir KEBE