Wikipedia
Wikipedia (di jàng wikipediyaa) ab sémbub jimbulang la ci web bi, di lu àddunawu te bariylàkk. Ag bindam nag mi ngi wéy ba tay, xaralaay wiki lañu jëfandikoo ngir sos ko. Yéeney Wikipedia mooy jébbal am ëmbiit mu ubbeeku, maandu te fugluwu.
Jaar-jaar
SoppiSémbub Nupedia
SoppiNupedia di woon ab sémbub jimbulang bu ubbeeku bu Jimmy Wales sosoon ci weeru gamu atum 2000. Mboolaay gu Bomis (gi Jimmy Wales féetewoo woon moomeel gi ci ëpp) moo ko jàppale woon ciy koppar, doon fay Larry Sanger mi jiite woon mbind mi. Waaye Nupedia ag màggam dafa yeexoon lool ba waraloon, ci 2001, Larry Sanger xalaatoon ni sos ab wiki moo doonoon liy man a gaawal yokkteeg jukki yi. Xalaat boobu ñeel jëfandiku xaralag wiki ngir sos ab jimbulang, juroon na ag diisoo ci diggante Larry Sanger ak tëriinkat boobu di Ben Kovitz ngir mu faramfaceel ko ci ni mu gën a leeree ana nan la xarala gu wiki di doxe, ci ab reer ca San Diego la ame woon, ci 2 tamxarit 2001. Ci nii Larry Sanger ni Jimmy Wales ngir ñu jëfandikoo xarala gu wiki ngir sos ab jimbulang bu gën a woyof, lii moo jur sosug jimbulang bu Wikipedia.
Sémbub Wikipedia
SoppiGinnaaw bi ko Jimmy Wales ak Larry Sanger sosee, Wikipedia ngi judd ci kàllaama waa angalteer ci 15 tamxarit 2001. Gu waa faraas teggu ci 23 gamu 2001, gu waa almaañ tegu ci ak yeneen yépp, ba tay ci atum 2007 mat nañu ñaari-téeméer ak juróom-fukki làkk.
Ci 1 diggi-gamu 2002 la Larry Sanger tekki ndomboy-tànkam ci ñaari sémb yépp, ginnaaw bi Bomis tëyyee loxoom, fayatul Larry Sanger ci liggéey bi mu doon def ci Wikipedia ak ci Nupedia. Ci 26 weeru koor 2003 la Nupedia tëj ba fawwu, Wikipedia moom wéy di màgg.
Boobu ba léegi Wikipedia di dox ci ay àtte yiy askanam tëral ndànk-ndànk jëmug kanamam. ci 20 maami-koor 2003 la Mbootaay gu Wikimedia (wikimediafoundation.org ) juddu ngir wut ay koppar yu muy suuxate sémbi wikipedia yépp.
Wikipedia Wolof
SoppiWikipedia wolof moom mi ngi sosu ci ndeyi-gamu 2003, toog daanaka ñaari at te amul benn yëngu-yëngu. Ci tamxarit 2005 la am jukkeem bu njëkk. Xoolal xët wi ñeel Taariixu Wikipedia wolof
Melokaanu sémbub Wikipedia
SoppiYéeney sémb bi
SoppiNi ñu ko binde ci xët wu njëkk wi, bakkam mooy:«Jimbulang bu ubbeeku bi», maanaam di lu ñépp bokk, te ñépp man cee cëru ngir gënal ko. Jimmy Wales di kenn ci ñaar ñi sos sémb bi, mi ngi koy tekkee niki «ag jéemantu ngir sos ak séddatle ab jimbulang bu ubbeeku ci anam gu mucc-ayib ngir nit ku ne man koo am ci làkku cosaanam».
Melokaani Wikipedia
SoppiBaatu «Wikipedia» mi ngi jóge ci taqaleg ñaar yii di «wiki» di ag nosteg yoriinu ëmbiitu dalub web bu ñu man a soppi jaare ko ci ab joowukaayub web, ak « pedia » di reenu baatu làkku waa angalteer bii di encyclopedia, di tekki jimbulang.
Li ñu jublu ci sémbub Wikipedia mooy mu doon ab jimbulang, maanaan muy jëmmal bépp xameefu nit, lépp lu nit xam man caa ne. Wikipedia du ab baatukaay, du am péncum waxtaanuwaay (xoolal xët wii ngir xam lu wikipedia doon ak lu mu doonul: Ndimbal:Ubbeeku). Sémb bi dafa àddunawu, day laal bépp xeetu xam-xam, bariylàkk, te amul ag pay.