Fuuta Tooro
Nguurug Tukulóor mi ngi sosu njëkk juroom ñeenteelu xarnu, njabootug Ogo Ja jiite ko, ci mujjantalug xarnu bu fukkeel la Waar Jaabi song ki mujjoon ci buuri njaboot googu, ray ko. Bu ko defee daal di jël nguur gi, ci noonu la geneen njaboot jote ci nguur gi, mooy gu Mana.
Waar Jaabi dugg na ci lislaam, daal di jug def jiyaar ci kaw dëkkandoom yi dul jullit, ci noonu la nguurug Tukulóor xéye di nguur gi njëkk a dugg ci lislaam ci Senegaal.
Tukulóor yi bokkoon nañu ci yaxantug wurus wi ak njaayum jaam yi, li ko waraloon it mooy dend gi ñu dendoon ak dexug Senegaal gi, ak nekk gi ñu nekkoon ci yoonu yaxantu wi. Mu nekkoon réew mu naat te am doole, waaye dafa rotoon ci ron teg loxo gu imbraatóor gu Gana, (ci xarnub fukk ak benn), ginnaaw bi mu rot ci gu Mali (ci xarnu bu fukk ak ñatt), rotati ci gu Jolof (ci xarnub fukk ak ñeent). Ci mujjug xarnub fukk ak juroom la Koli Tingala (kilifa gu bokk ci càllallag Pël, juge ci wàllug bëj-saalum gi) jug xeex Tukulóor yi, daal di tembal ay goxam (ñu moom seen bopp) taxawal nag nguur gu yees mooy Fuuta Tooro, njabootug Deñanke jiite ko.
Ci xarnub fukk ak juroom benn Fuuta Tooro def na ay xare ngir yaatal suufam ci kaw ay dëkkandoom : Jolof, Kajoor. Njabootug Deñanke nag manatuñu woon a jàmmaarlook cong yi tukkee ci biti, ak lëj-lëji kuutu gi (succession). Ci atum 1770 g.j, la ag fipp am walla ag jeqiku tukkee ci kilifay jullit ñi, Cerno Sulaymaan Baal jiite ko, daal di daaneel njabootug Deñanke, bu ko defee Baal jël lislaam def ko cëslaay li nguur gi di tegu te di ko ci doxale. Cerno Sulaymaan Baal bàyyee woon na nguur gi Yilimaan Abdul Xaadir Kan, moom lañuy jàppe ki njëkk a doon Yilimaan ( Amiirul Moominiin :njiitul jullit ñi)
Gongikuwaay
SoppiTaariixu Senegaal bu Abdu Xaadir KEBE
Seetal BUNTU TAARIIX |