37°58′N 23°43′E / 37.967, 23.717

Ci angale mooy Athens; Ci faranse mooy Athènes

Aten dëkk bu mag la, ci réewu Geres mooy péey ba sax, te siiw na ngir xam-xam ba'ak njàng ma, ak caada ja. Yaakaarees na ne lu ëpp téeméeri junni ciy way dëkk ñoo fa dëkke. Nekkoon na péeyu nguuru waa Geres, bi tuddoon Atig (Attique). Tey mu tudd Aten .

Sancees na Aten daanaka 3.000 at Nj. Is (njëkk Iisaa). Daanaka 500 at njëkk Iisaa fekkoon na mu am nguur gu yaatu lool. Waaye Geres dafa ñàkkoon suuf. Moo tax waa Geres yi tuxu, di sanc ay dëkki Geres yu bari ca Tugal ak Asi gu ndaw gi.

Moone ca jamonoy Pool dafa ñàkk xaalis. Amatuñu nguur, te diiwaanam Atig dafa tuuti - dénd bu tollook 2.600 kilomet kaare matul sax benn departemaŋ ca Senegaal. Amul feneen ca Atig fu gën a sore Aten 40 kilomet. Seen suuf musuñoo doy seen soxla. Taw bi barewul woon, lu tollook taw bi ñu am ca noru Senegaal. Ñetti cér ca ñeent ca suuf si amul njëriñ ci bey te yu bare ci yi des amoon njëriñ ca bey garabu oliw rekk. Amoon nañu mbélli xaalis waaye fekk nañu ne jeex nañu tàkk laata jamono nguuru Room. Tamit seen doole ci jaay wàññiku na, ndax doole yeneen dëkk yu mel ni Ancos, Korent, Efes, ak Alegsàndiri.

Dëkku njàng la woon, bu amoon jenn daara ju kawe 'iniwersite'. Naka noonu siiw nañu ndax seen xam-xam ak seen waxin, ndaxte waxin lañu ca gën a jàngale. Wax ak a déglu lu bees rekk lañu daan xinte. Amoon na ay mbooloo boroom xam-xam. Benn ca mbooloo boroom xam-xam moo tuddoon Epikuren. Kureel la woon, bi sës ci njàngalem Epikuur (mu faatu 270 at lu jiitu jamano Kirist) te fonk bànneex, ba mucc ci bépp tiis. Gëmuñu Yàlla, waaye ñu gëm ne àddina dafa sàkk boppam te amul boroom. Te boo deeyee amul dara lu ciy topp. Nekkatuloo daal. Beneen mbooloo dafa tuddoon Estowisen. Kureel la woon, bu sës ci njàngalem Senon (mu faatu 265 at lu jiitu Kirist). Fonk nañoo naagu, ba bañ a yég dara, muy bànneex mbaa naqar.

Akëropool ca Aten.

Dëkk bi fees na dell ak màggalukaayu yàlla yi ñu defare marbar, yu réy-a-réy te rafet, nataal ya ñu yett, kenu ya, robine ndox bi ñu tudd 'fonteen' ak yeneen rafetaay. Ca diggu dëkk ba amoon na benn tund wu am ay màggalukaay rekk. Ëpp nañu fukk. Nekk na daanaka 100 meetar ca kaw niwo dëkk ba. Ca ñetti boor am na mbartal bu jub xocc mel ni miir. 'Akëropool' la tudd.


Lu des tey ji ca màggalukaayu Sës ca Aten.
Kenu ya ca màggalukaayu Sës ca Aten.

Benn ca màggalukaay ya moo doon màggalukaayu Sës, yàlla ju gën a mag ca diine Gereg. Àggaleeguñoo tabax màggalukaay ba ca jamono Pool. Waaye ba noppi amoon na 104 kenu marbar, bu nekk am kawewaayu 17 meetar ak yaatuwaayu 2 meetar! Kawewaayu màggalukaay ba moom ca boppam moo doon 27 meetar. Ca biir amoon na nataalu Sës bi ñu defare wurus ak iwaar. Bokkoon ca ñeenti màggalukaay yu gën a réy ca àddina si ca jamono.


Parténon ca Aten.
Parténon ca Aten.

Màggalukaay bu gën a am solo moo doon li ñu tudd 'Parténon' bi ñu defaroon ngir yàllay dëkk ba, maanaam, Atena. Guddaay 72 meetar la, yaatuwaay 34 meetar, te kawewaay 20 meetar. Ca kaw kenu ya amoon na nataal bu ñu yett bu wëroon tabax bépp ca 92 wàll. Wàll bu ne indi na benn ca seeni nettali yàlla. Amoon na beneen nataal bi ñu yett ca diggante kenu ya bu amoon 600 melo ya - ay góor, ay jigéen ak ay bàyyima yi bokk ca ña indi seen yàlla Atena benn yére wurus at bu nekk. Guddaayu nataal bi mooy 160 meetar. Te def nañu nataal yi ngir ñi taxaw ca suuf di ko xool yaakaaroon nañu ne dañuy jàkkaarlook nataal ba, fekk na ne nekkoon na 10 meetar ca seen kaw.

Waa Aten jaamu nañu ay yàlla yu bare. Waaye yàllay dëkk ba moo doon Atena. At bu nekk ci weeru yuuliyoo, amoon nañu benn màggal lu diir 8 fan. Ca fan yu jëkk ya def nañu ay joŋante, rawante gaal ya, fas ak sareeet ya, rawante ca woy ak nettali, ay mbumbaay. Ca juróom-benneel ba fan, ca fajar, saraxalekat ya ak magi dëkk ba, jiitu nañu mala ya ak waa dëkk ya yépp, ñu dox ca biir dëkk ba, ba egg Panténon fu ñu def sarax ya, te ñépp lekk yàpp. Sarax nañu 100 mala, mooy nag ak xar, at mu nekk.

Amoon na bérab ci biir dëkku Aten bu tudd Areyopas. Nekkoon na ci kaw wenn tundu xeex wu kawe. Amoon na ay siis yi ñu defare woon doj ngir kureelu dëkk ba manoon faa daje. Indi nañu Pool foofu ngir mu waareji.

Ni dëkki Gereg yépp amoon na pénc bu ñu tudd 'Agora'. Amoon na ñaar sax - benn bi waa dëkk ba tabaxoon ak benn bi waa Room tabaxoon. Ay péncu doj lañu yi ñu rafetal ak kenu yu réy ak nataal ya. Ñoo doon maase, ak grand palaasu dëkk ba, te fu ñu doxale nguur. Foofu itam amoon na ay màggalukaay ak ay saraxalukaay. Ci dëgg-dëgg mënuloo dem fenn ca dëkk ba te gisul benn màggalukaay walla nataalu yàlla.

Powukaayu Erodd Atikus ca Aëropool, Aten.
Powukaay bu Room ca Aten.

Amoon na ay powukaay itam. Ñoom itam dañuy kéemaane. Benn ca ñoom woyuwaay la bi ñu teg ne mooy bu gën a rafet ca àddina si. Beneen mënoon na toogal 17.000 nit, te léeg-léeg dina fees ba ëpp loolu sax! Amuñu jot a lim bépp tabax bu yéeme bu nekkoon ca Aten bi fa Pool ganesi.

Dëkku Gereg la woon waaye amoon ay Yawut itam.

Aten dafay feeñ ci Injiil ci Jëf 17:15,16,21,22; 18:1; 1Tes 3:1.

Iniweersite Soppi

Lëkkalekaay yu biti Soppi

 

Xool it Wikimedia Commons