Sëriñ Saaliwu Mbàkke
Sëriñ Saaliw mi ngi gane àdduna, ca Njaaréem(Senegaal) ci guddig àjjuma gu 14 ci weeru tabaski, atum 1333 g.g, dëppo ak 22 satumbar 1915. Aji juram ju góor di ku jaradee leeral ngir xam gi ko nit ñépp xam di Seex Ahmadu Bamba, ju jigéen di Soxna Faati Jaxate, mom Sëñ Moodu Asta mu baax ma te sell. S Tuubaa bi mu ganee àdduna daa bindoon ciw kayit tur wi di (Saaliwu giy tekki aji baax, aji yéwén) jox ko Sëñ Muhammadu Lamin Jóob Dagana, ne ko tudde ko ko, bi mu ko defee moom S Dagana, daa daal di bind as lëf ciy bayit ñaanal ci liir bu tedd bii aw fan wu gudd akug wér, akug yékkatiku ci jamonoom ba mel ni jant, mu wax ca ne:
«Yal na Yàlla mii di Aji-des bàyyil ñu fi Saaliwu mii mu ñu may te def ko mu jël turam wi (aji-baax).
Yal na ko fi desal mu dib jant ci asamaani jamonoom, bu ko defee, muy leeral kanamam gu këriis gi.
Yal na ko fi desal muy kuy mottali jub gi fi Yonent bi indi woon, di ku barkeel, di ku wér, tey ku am muur»
Am njàngam
SoppiAy ceññeeri xel ak màndargay yewwute ak man a wattu teeloon naa feeñ ci moom te booba matagutoon a dal jàng, bokk na ci liy dëggal loolu te di ko dëgëral lii nettalikat yi di nettali muy ne moom de mokkaloon na xasida gii di (Ikfinii) te booba gone gu ndaw la woon, ginaaw bi mu jànge Alxuraan ca Tuubaa ci loxol nijaayam S Alasaan Jaxate mom Jàmbaar, ba mokkal te bind kaamil, ginaaw bi mu dugg ci jàng xam-xami diine yi ak làkku araab ci ay ustaas yu màgg niki Seex Moor Saasum Jaxate mom Xaali Majaxate Kala ca Aynu Maadi ak Seex Muxtaar Guyaar Jang walla Njang ca Husnul Maab(Tindoodi) ak S Abiibu ca Tuubaa, S Mut Dem ca Njaaréem, Seex Aamid Saw ca Mewndu, kii mooy ki ko jàngal xam-xami gëstubiddiw yi (falag) ak melosuuf gi nga xam ne xóotoon na ci ba àgg ci di xam ci mbiri ay réew ca Asi, Tugal ak yeneen réew lol ña fa dëkk sax leeg-leeg ñu xaw koo réere. Ku soppoon yër ay téere la, ndax saxoon na ci ab diir ci jamono ba mujjoon di géej gu deesul jot ag suufam ngir ag xóot. Bi Sëñ bi àggee fii ci njàng mi la gis ne daa war a dugg leegi ci jeneen dara mooy ju tukki, ndax tukki benn la ci daara yu mag yi xam-xam di juddoo, di yokk jarbu tey dollim xel, ndax bari na xam-xam yu ci juddoo, ndax dina yobboo ñaare ci xalaat ci dénd bi te Yàlla (tudd naa sellam ga) yàgg na cee woote jëme. Ci noonu, mu def lu sakkan ciy tukki ci biir réew meek biteem, ci mbooleem diiwaani Senegaal,Kot Diwaar ak Gàmbi, mu jële ca daj gu mag ak jarbu gu réy ci lef yu bari
S Saaliwu ci wideo: http://www.youtube.com/user/lahaddf
Yenn ciy meloom
SoppiAb xam-xamam
SoppiNiki ñu la ko waxe leegi Sëñ Saaliwu nekkoon na di ku géeju ci xam-xami lislaam yi: Tawhiid (wéetal Yàlla (t.s)) fiq , tasawuf , nos-wax walla nahwu ak nos-woy (haruud) ak jotal (balaaxa) ak leeral (bayaan), muy ku yéeme woon ci woy , daan def ay jam ci woyi dongaam yu tarbiya yi daan faral di def ay woy yu yéeme, ñoom de bokk nañu ci ñi gën a man a woy ci araab ci Senegaal ku ci mel ne Sëriñ Alhaaji Lóo , Utilisateur:Abdu Xaadir KEBE mi ci wikipedia, nga xam ne loxoom lu fa am solo la te ay gëstoom gën a màcc ci làmmiñu wolof, S Xaliil Màkke, S aboo Kebe mi def ab dalub murit bu jéggi dayo ba ci làkku araab [1] "www.wikimouridia.org" , S Mamoor Kebe, S Alaaji Mbàkke mi nga xam ne lu dul jeex ciy téere la taalif ci yoon wi ak aji sosam añs , ndax daawu leen bàyyi ci seen jàmm, foo ko fekk ma nga leen di soññ ci sàmmoonteek sarti "jotal" yi walla balaaxa ci seeni njuréefi woy. Ku mokkaloon lu bari la ci woyi waa Gànnaar yi ak waa Andalusi yi
Ag sonnam ci Jaamu Yàlla
SoppiDaa na toggoo ci jaamu Yàlla yi lu kawe misaal, mu daan taqook ay dog ciy wird aki tudd-Yàlla, daawu leen ginaawal mukk ak lu yitte yi tar tar mbaa xat-xat yi baree ko ni, kenn ci taalubeem yi nettali na ma ne moom de masul a jël aw wird ndare bu da caa sax ngir sàmmonteek Addiis bi naa "Jëf ji Yàlla gën a sopp mooy ji gën a sax ak doonte néew na", muy ku xéroon cig jaamoom ci tënku ci Alxuraan ak Sunna, daan teet bidaa ak cibéel (lu ñu sib), ci anam gu jéggi dayo ba cig tar.
Ag dëddoom
SoppiSëriñ Saaliwu daa dëddu àdduna ginnaawal ko ginaaw bi ko àdduna dëgmalee, jublu ko, mu ñëkkaloon ko ag kanamam ginaaw bi ko àdduna muuñee, ag dëddoom àdduna nag ca xol ba la ko defe, ndax teewu koo topp ndigali Yàlla (t.s) yi aju ci dundal suuf si, ndax Yàlla (t.s) nee na : «Moo leen sàkke ci suuf si te sàkku ngeen dundal ko», bu bokkoon ci ñiy toraxal suuf si ngir woote ag dëddu doo fi gis tay yii tabax yu kawe yi mu fi def ngir rekk kaweel baatub Yàlla bi, doo ko gis it kon muy bay lu tollu ne li mu daa bay ngir rekk séddaleeti ay njariñam aki njuddeefam ci nit ñeek ñu ñàkk ñi, di leen wax laayab Alxuraan ba: «Ñun de dañu leen di leel rekk ngir Yàlla, soxlawuñu ci yeen ag pay du caagéenu ag cant»
Ag Ñawam akug Yewwoom
SoppiSëñ saaliwu nekkoon na di ku yewwu, ku ñawum xel, ku amoon la ag xereñ akug xóot ci xam mbir yi, boroom xam-xamu xel la woon (psychologue), ku daan xam xeli nit ñi la woon ak seeni jeng-jeng, booy tàmbalee wax ak moom rekk mu jëli la, ndànd la, boroomug ñaw la woon ba deesi ko seetlu saa soo ko tegaleeb laaj, ak bu mu man a doon. Bis gan dikkal na ko di kilafa gu bawoo ci biti, bi muy wax ak moom ci lu aju ci tànnéefi njiit yu Senegaal yu waroon a am ca jamono jooja, gan ga daal di koy laaj kan la faral ci lawax yi (les candidats)? Sëñ bi ne ko: man de ki askan wi tànn rekk laa faral, te loolu manul a am ndare bu tànnéef yi daa gore, sell te leer, looloo tax sama bëgg-bëgg mooy na mel nii, ci noonu gan daal di ne : tontu bii de bu diblomaasee la .
Ag Ubbikoom
SoppiKu ubbiku la woon ci ñépp, daan tertoo ci kanam gu lewet guy muuñ, ak dënn bu yaa, di jaxasook ku nekk ci lu dul genn wàttuwu, ñi duli murit it mu jàppe leen mbokki diine ak yu ban, ngir jëfe waxi waajur wa: «wépp wird wu waay wor te Yàlla rekk tax, moo xam wu Jiilaani la mbaa wu Ahmad Tiijaan, mbaa muy wu keneen ci Qutb yi, yooyu yépp a baax ndax cig jub lañu nekk yooyu yepp »
Yërëmam nit ñi ak Soppam ñeel xale
SoppiYërmaande ji mu am ci mbindéef yi ak ñeewant gi mu am ñoom xaw nañoo nekk di lu maneesul a misaal, moom de kuy yittewoo mbirum jullit ñi la ak fu ñu man a nekk, di nemmiku ak a xeeñtu xew-xew yiy xew ci réewi jullit yi niki xareb dóox gi (guerre de golf), ak intifaada ca Palestin, ak mbooleem tër (condition) yi jullit yi di dund ci mbooleem àdduna bi, mu daan digale ci ñu wàcce ay kaamil ngir ñaanal leen ci. «Man ci sama jëmmi bopp (Abdu Xaadir KEBE) dem naa fa moom bis ànd ak sama jenn mag ne ko Sëriñ bi war ngaa ñaanal jullit ñi, ndax yaw yaa fi nekkal Yàlla ci kaw suuf, te kat waa Aamerig ñi ngi taal àdduna bi te loolu ñi ngi ko gën a defe ci jullit ñi, taal nañu ab xare ca Afganistaan, taalati ko ca Iraaq, jamono jii ñu nekk ñi ngi waajal ngir taal ko ca Iraan, mu daal di feeñal yitteem bu baax ci wax ji ne ma loolu nu mu deme ma gën ko koo leeral, mu ne loo ci xamati naa ko yëg ndax lu ma ci yëg du yam ak lu ma ci yëgul, te kat booba waa Aamerig feeñaloon nañu yitte ju mag ci song Iraan, ba tàmbali woon a yëngu's lëf jëm ca Dóox ga (le Golf) waaye ba leegi waxatuñu lu dul luy jàmmal, ba sax njiit lu bon la daa xeex rekk di George Bush far na daanu, kii di Barak Obama daal di toog, te moom benn ci dig yi mu doon def ci bi muy sàkku ñu fal ko mooy toog ak Iraan waxtaan, yal na ko Yàlla àntul, te gëm naa ne day àntu ndax waxi Sëriñ Saaliwu ji, lii nag ñeewant la ñeel jillit ñi waaye it ñeel nit ñi, te ca baayam la ko jële mi daa wax : «Yaw boroom nguur gi (di Yàlla) yaw mi màgg ba weesu fayoontoo, rikk nanga yërëm mbindéef yépp » kon moom mbindéef yépp la yërëmoon rawati na jullit ñi waaye it baatin la ndax sunu boroom fanq na ay wi cig ñaanam ci barkeem.
Yërëm xale yi
SoppiMu nekkoon di ku am ñeewant ci gone yi, yërëmoon leen ni mu ko defe mag ñi, mu daan leen dimbale di leen gunge ci jafe-jafey dund gi, mu daan mettitlu te daan naqarlu bu gisaan kenn ci yale yi mu tumbrànke , mbaa sonalees ko cam njàngam mbaa mu ami góom mbaa mu wéradi mbaa mu xiif.
Daawul toog ak ñoom ndare bu da leen a teral, jox leeni neexal aki mbiskit ak lu ni xeetoo. Daa na àndaale ak ñoom ci tukkeem yi, di kaf ak ñoom mel ni gone ni ñoom te loolu lépp ngir ñu fàtte seeni waa jur ba man a dékku li ñu leen bëgg a sol ci yarub lislaam bu kawe te sell, ndax kat gone baaxoowul a miis ay waa juram ngir ñeewant ga, waaye fi moom day am ngir yërmaande ja. Mu daan fanaan ak ñoom ci néegi boppam yi, nekkaloon na leen di baay ci li baat bi ëmb ci maanaa, taxoon na xalaatatuñu seeni way jur ngir wuutu gi mu leen wuutu woon ci ñoom ci jëfam ju baax, foofu nag amal na fa waxi baayam ja ba muy ñaan Yàlla (t.s) naan ko: «taxal ñu fàtte seeni way jur ngir man» Waaye nag yërmaande ji teewu ko woon a taxaw ci yar leen ni mu ware, mu daan waxtaan ak ñoom ci nu kawe seeni at, daan leen nettali ay xisa yoy daawuññu ci xam dara, waaye da daan sedd bis ba ñuy doone mag ba koy soxla ca seenug dund, loolu nag ci Yonent bi Muhammad (j.m) la ko daa roye, ndax mooy ki daa wax Omar ibn Abii Salama te booba gone la gu xamul li mu koy wax: «Neel Bismil Laah, te lekke sa ndijoor te lekk ci sa kanam»
Ag dundam
SoppiDund gu wow la yoroon gu soofiyoo, gu ag dëddu àdduna muur, ragal Yàlla peek ko, biir ga di yërmaande, muy ku amoon ag ñeewante ci gone, te yéggoon aw wartéef jëm ci doomi aadama yi, ku amoon ayba la woon ak wegeel, ku ubbiku woon la te lewet, waxi woykat ba dëppu woon na ci moom : « Lewt ba ne domm, diis ba ne gann cig wet () woyof ba ne toyy, saf sapp ak boroomam » boo koy xool rekk gis ag Yàlla ak aybaam ga, dëggoom ga, wegoom ga, muy ku ñépp wormaaloon, ñi ko jegeek ñi ko sori woon, Benn ci labbe yi ci Senegaal seereeloon na ko ginaaw ag làqoom: «Kii de àdduna da koo dikkal mu toog fi suuf», loolu di wax ju réy, di lépp dikkal na ko te faalewul dara lu dul Yàlla te xam ne dara amul solo lu dul moom, fii dara saxu fi, dara dëkku fi, woykat ba nee na : «Jural-leen dee, tabaxal mbàbb», muy ci maanaa lu fi waay jur dee dina digg leegi ne ko fuuf, lu ngéen tabax it day mbàbb leegi, kii nag lii la tegoon ci ron bëtam, jëfam jépp it Yàlla la ak lu ci jëm, misaal mi kenn la woon ku àddinaadi, te teewul mu sos fi lol maseesu ko fee sos ci ay sémb yu mag, xoolal li mu fi bàyyi ci xaalis, tollu na ci lu jege 17 milyaar, ñeel naal yu aju ci Dëkkub S Tuubaa bi, te loolu masut a am ci taariixu yoon wi, la ko dale ca Waajur wa ba ci fii ma la koy waxe, te loolu bokkul ak li mu fi jot a liggéey ci alali boppam, te loola gën jaa néew mu weesu 7 milyaar, lu sakkan ciy kër S Tuubaa sosoo na ciy loxoom, waxuma la li sosu ciy jumaa aki jàkka cig ayam te ñuy yu réy te taaru.
Kenn ci murit yi nee ne bokk na ci bind yi ñu man a jële ci moom: «Nekk gi mu nekk doomi S Tuubaa doy na teraanga te dib xalifaam, nekk it mag mu am ay xéewal war naa tax a noppalu, te moom boole woon na ñaar yooyu yépp, waaye teewu ko woon di yëngu jamono ju nekk ak a liggéey, kon loolu li mu man a doon mooy bind bu mu ñuy jox mu aju ci liggéey ak doonte deesul yàggati fi, ndax loolu yéene nit ñi ay xéewal lay wund te ci ag jaamu Yàlla la »
Sëriñ Saaliwu ak Tarbiya
SoppiBi Sëriñ bi toppee yoon wi ba àgg ca jëmuwaay bu kawe ba, muy àgg ca Yàlla, daa daal di sóobu ci tarbiya , maanaam yare ak sellal jikko yi ak setal leen ciy ayibi bakkan ngir jeggeele Yàlla mu kawe mi. Yoon wi mu daa jaar ci yareem googu mooy wi mu jaaroon, nekkutoon di kuy tañaxu waaye ci xam-xam la ko tegoon ak leerug xol, loola dëppoo ak laaya bii di: «Neel wii de mooy sama aw yoon, damay woote jëme ca Yàlla ci leerug xam-xam man ak ku ma topp»(yuusuf 108)
Tëriinu yaram wi (programme bi) dafa làmboo woon lii: alxuraan , xam-xami sariya yi ak xasiday S Tuubaa yi, ak liggéey yu yaram. Yooyu ñooy ñeenti xeet yi mu daa jaar ngir laabal xol yi ci ay jàngoroom, walla ñooy saabu bi mu daa raxase bakkan yi ci seeni ayib
Yariinu xale bi
SoppiGone gi day door - ci li muy njëkk a def - ci jàng Alxuraan ba mokkal ko, bind ko te du ko xool, door a tàbbi ci jàngum xam-xam mi. Aji mokkal ji daa nees ko neexale lim bu am solo ci xaalis ngir mu soññu laata muy tàmbalee jàng xam-xam ak di jàngale Alxuraan, jàngalekat yi tam amoon nañu seen dëkkuwaayi bopp yu ñu leen jagleel ak seen lekkug bopp ngir wormaal alxuraan ji nekk ci ñoom, jenn daara ju nekk it daa na am 12 jàngalekat, kaamil yi ñu binde ci daaray 2 dale ko 1993 - taariixu sancug Xelkoom - àgg nañu ci 2289 kaamil, te ay téeméer ciy kaamil bindees na leen njëkk taariix bii ak ci ginaawam ci daaraam yu bari yii maneesul a lim. Bokk na ci li yayoo fàttali mooy ne fii ci Senegaal, rawati na ci digg yu daara yi, miinees na fi ñuy bind kaamil ginaaw ag mokkal, loola nag mooy aji mokkal ji bind kaamil bi te du ko xool niki firnde (certificat) cig mokkalam.
Nosiinu daara ji
SoppiDaara ju nekk am na bu jàngalekuti Alxuraan yi jàllee, kuy jàngale xam-xami sariiya yi ak làkku araab, kooku mooy faral a jiite daara ji, lañu fay jàng it mooy li ñu baaxoo jàng ci jataayi jàng-xam-xam yi (Majaalis) nga rax ci dolli xam-xamu Usuul ak Mustalah, benn bi Usuul di jàngale gongikuwaay yi àtte yi di bawoo, bi ci des di xamle yattiinu baat yi ñeel xam-xam yu yees, balaa ndongo lee àgg foofu, dana fekk mu jot a jàng am mbooloo mu ñu tànn ci xasiday Sëriñ Tuubaa yi, ci Tawhiid, Fiq, Tasawuf ak nos-wax.
Moom de foo ko fekk da daan soññ dongo yi ci góorgóorlu bu baax ci gëstook njàng, di leen nettali démbi am njàngam, ak coona ya mu daa jànkoonteel, leeg-leeg mu laaj ay laaji nattu ak seet fi ñu tollu, di een won téere yi ñu war di yér, di xiirtal ci di teewe yenn jataayi xam-xam yi ak di ci bokk, daaraam yi it lu sakkan ciy woroomi xam-xam génne nañu fa, yoy yenn ci ñoom def nañu ay taalif yu am solo ci wàll yu bari, Fiq, Tasawuf, Jaar-jaar (Siira), Mustalah, Njàggat ak farata yi. Sëriñ bi jotoon naa móol yenn ci taalif yooyu te wisaare leen ci alali boppam te loolu ag soññee gu mag a ngi ci, akug góorgóorluloo. Daara ju nekk it am na am mbooloo mu liggéeyam mooy jàngal xale yi ay xasida ak tàggat leen ci ñu man koy yekkati ci ay daaj yu yéeme yu ñu jële ca mag ña daa jàng ca jamono ju Sëriñ Tuubaa mbaa waa kër Sëñ Masàmba , ku ci mel ne S Yuusu Ndaw, Alaaji Siise, S Mayib Géy ñi daa yekkati ci kanamu S Tuubaa. Mbooloom xasida moomu ëmboon na lu ëpp fan-weeri xasida, yi ci gënoon a siiw di Jasbul-Quluub, Mawaahibun-Naafih , Muqaddimaatul-Amdaah ak Rabbii-bimaayasrahul ... Dongo yi nag daawuñu def leneen lu dul jàng ak jàngale, ndare ci jamonoy nawet bi, bu boobaa ñu sóobu ci liggéey bi ci tool yi, ndax loolu ag wàll la woon ci tarbiya gi
Sëriñ Saaliwu (g.y.m) nekkoon na di ku xamoon mbirum mbay, di ci fóore, bëggoon ko lool it te jàppe woon ko mecceem akug njaamu gu sell ñeel Yàlla (t.s), daawu ci faale néewug la mu cay ame, mbaa ag yàqoom walla ag àntoodeem. Daa na jëfandikoo ci tool yii ay bijjikaay (Tracteurs)yu tolloon ci 220. Mbooleem ay njuddéefi mbayam it addiya la leen daa def ñeel ki fi nekkal Sëriñ Tuubaa, bi mu nekkee it xalifa, daa daal di woon tàmbali di leen séddale njabootug Sëriñ bi ak miskiin yi, ak faqiir yi (way ndóol yi), ag wàll ci ñoom mu sotti ko ci luy defar dëkkub Tuubaa bi
Ag Xilaafaam
SoppiMoom nag mi ngi nekk xalifa ci 13 mee 1990, làqu ci guddig 28 jëm 29 desambar 2007. Moo doonoon juróomeelu xalifa bu Sëriñ Tuubaa, ku kiimaane la woon ci nangoo liggéey ak jaamu Yàlla ak dëddu àdduna ak yar ci Lislaam.
Ay liggéeyam
SoppiCi jéem gi mu doon def ngir dab bànneexu Sëriñ Tuubaa ci amal ay mébatam ya mu def ca Matlabul-Fawsayni, genn ciy xasidaam, Sëriñ Saaliwu taxaw na ci mottali ay sémb yu mag yu fi ay magam bawoon te dolli ci yeneen yu mag te am solo, bokk na ci yooyu:
- Àggale Daara ju Kawe ju Tuubaa (l'université de Touba) ba mu man a dékku lu tollu ci 5000 ciy dongo,
- Yeesalaat Jumaay Tuuba, def fa benn jumtukaayu kàddul (une sonorisation) bu man a àgg ci 12 km ci soriwaay
- Yaatal dëkk bi, natt ci 110.000 pàkk yoy ñaari ñatteel yi noppi nañu (pàkk yu ñuy joxe cig neen (amul pay) ñeel képp ku yéenee dëgg Tuubaa)
- genn mbaalug laabal (un réseau d'assainissement) ci Tuubaa gu toll ci 18 km
- Naalub mbay bu Xelkoom, mu yaatoo ci 45.000 ha.
Sos na fi lol maseesu ko fee sos ci ay sémb yu mag, xoolal li mu fi bàyyi ci xaalis, tollu na ci lu jege 17 milyaar, ñeel naal yu aju ci Dëkkub S Tuubaa bi, te loolu masut a am ci taariixu yoon wi, la ko dale ca Waajur wa ba ci fii ma la koy waxe, te loolu bokkul ak li mu fi jot a liggéey ci alali boppam, te lool a gën jaa néew mu weesu 7 milyaar, lu sakkan ciy kër S Tuubaa sosoo na ciy loxoom, tollu nañu ci 28, waxuma la li sosu ciy jumaa aki jàkka cig ayam te ñuy yu réy te taaru, ñuy yu mu sos ci alalam mbaa ci ndigalam mbaa mu dugal ci bu baax loxoom.
ay daaraam
SoppiSos na ay daara yu bari, ngir jàng ak jàngale, ci barab yu bari te wuute ci réew m i, bokk na ci yooyu: Got gi mu njëkk a sanc ci daara yi, mi ngi ko sos ci 1934, Njurul, ca wetu Tuubaa, Njàppundal, Ndookaa, Lagan, Ñibingal, Ñaaru, Ngaabu, Ngéejaan, Xàbbaan, Geloor, Tuubaa Njaaréem, ak yeneeni tool yu mu sanc ginaaw bi mu gental leen, mbaa yu mu sancagul ak jii mu mujj a sos te mu nekkoon jenn ju mag ju doon benn pakk bu mag ci suuf bu ëmb 15 daara, mooy Xelkoom, mi ngi ko sanc ci 1993, daara ju ci nekk yor turu ag gàdd (cartier) ci Tuubaa, yaatoo 50000 ektaar, la fa nekk ciy donga yuy jàng àgg ci 50000 jëmm, yoy li leen di dundal ci bis dina tollu ci 2500 kilo ci ceeb.
Li ñu daa def ci daara yi
SoppiDaara mooy fu deesi jànge Alxuraan waaye fi murit ñaare daaray tarbiyu lay doon, di benn barab bob dees koy sos ngir jàng Alxuraan ak xam-xamu diine waaye it ngir yar, mbay ak liggéey, mu mel ne day doon fu deesi waajale nit ba bu fa jugee dara du ko jaaxalati ci àdduna, moo xam lu deesi xam la ci diine, mbaa lu deesi dajeel ci jafe-jefey àdduna, ndax ka fa yaroo day miin coona yi, man koo dékku, wullees ko ci liggéey, jàngalees ko, mu mujj di "ku ñu jàngal ba mu ne arr, yar ko ba mu ne nërr" ni ko Sëriñ Fallu waxe woon ne noonu la leen seen baay Cerno defoon, kon (yar bees ne nërr, jàngale bees ne arr) mooy mbóotum tarbiya,>
Ay séqoom aki mbokkam
SoppiS Saaliwu amoon na ay séqoo yu rafet te teey aki mbokkam, mu daan leen wéttalikoo te doonoon seen xarit, ñoom itam ññu fonkoon ko lool, daa ko tudde seeni doon, te daan leen ko jox ngir mu yor leen, yar leen, moom it mu nekkoon kok daa gisoon ne liggéeyal mbokkam yooyu de liggéryal S Tuubaa la, looloo taxoon mu boole woon ko ci wartéefam yu njëkk yi, mu daan diisoo ak ñoom ci lu mu man a doon, daan def lu mu bay ak lu mu bari bari jox ko Xalifa bi fi nekk.
Ay séqoom ak mag ñu Sëriñ Tuubaa ñi
SoppiS Saaliwu - yal na ko Yàlla dolli leer - ku amoon ag cofeel la akug worma ñeel mag ñu S Tuubaa ñi, mu leen daan faral a jox addiya yu gànjaru, daan na def lu bari bu daan dem ci daara yi daan ànd ak ñoom, ku ci mel ne S Seex Faat Tàkko Jóob, S Mustafaa Si, S Musaa Alima Gey ak ñeneen ñi mu jamonoonteel. Man naa am nag li waraloon muy ànd ak ñoom ci daaraam yi mooy xaleem yi roy ci ñoom ci seen jikko yu murite ,yu taalubee, yu rafet yi, mu daan gis it ci àndaale googu ag mottali kóllare ci mag ñu baayam ñooñu, ña mu ca jamonoonteelul daa na leen jokke ci seeni doom mbaay sët, ku ci nekk am nga ca daaraam ya doom mbaa sët.
Ay dénkaaneem:
SoppiS Saaliwu - yal na ko Yàlla gërëm - amoon na ay yitte yu daa nañu feeñ ci li daan gongikoo ci moom ci ay dénkaane aki soppaxndiku aki wax, bokk na ci baat yi ñu ko miine woon baatub Cant bi daan baamuwu aw yoon ciy xutbaam ak bu Tuub bi mu joxoon yitte ju mag, bokk na ci waxam yi daa tekki njàngaley S Tuubaa yi:
- ( Yàlla mooy tab bu tedd bi nga xam ne la nekk fa moom ciy xéewal du jeex, kon nañu ko ñaan ci xeewalam yii nga xam ne bindu leen lu dul ngir jaamam yi)
- (Ku ragalul Yàlla, bind na lu mu ragal)
- (Ku fàtte Yàlla de, na xam ne xéewalam yu bari yee ko waral ak yërmaandeem ji)
- (Bokk na ci pexey Saytaane su ñu jam si, bu ndigal jugee ca Sëriñ bi jëm ci murit yi, day gaawantu (moom saytaane) ne leen bu leen def ndigal lii, Sëriñ bi rekk moo ko man, bu ngéen ko manoon du ngéen fi ñëw di jébbalu (am ñu ci naan duma dugg saxaar yanu sama bagaas).
- Bu Yàlla feeñalee ayibi ab jaamam, booba da koo bëggoon a jéggal, waaye ab jaam nag day feeñal ayibi mbokkam ngir gàccaal ko, rusloo ko, ŋàññ ko.
- (Na jaam bi yittewoo biiram bi dul suure lu dul ay jëfam yu baax (Bàmmeelam))
- (Yàlla sàkkal na nit ñaari biir bu boppam bi, moo ko ko yoral jarul mu ciy sonn, saa su xiifee mu reggal ko, ak bu bàmmeel, na cay sonn, ndax lu mu ca deful du ko ca fekk)
Ag génnam àdduna
SoppiS Saaliwu mi ngi génn àdduna ci subag bisub àjjuma 17 ci weeru tëbëski atum 1428 g, dëppook 28 desambar 2007, ba fi nag dund gu jege 95 ciy at, ngir fekki waajuram wu tedd wa S Touba. Yal na gëramul Yàlla sottiku ci kawam ak lu waajuram, ñu gunge ko ba ca saxuwaayam bu mujj ba ca penkub Jumaay Tuubaa ja, ca guddi ga ca topp. yal na ko Yàlla (t.s) fayal Lislaam ak xeet wi gën ji fay gu muy fay jaamam yu baax yi ko liggéeyal. Aamiin
S Baara Mbàkke falilu moo ko fi wuutu niki 6eelu xalifa bu S Tuubaa.
Gongikuwaay
SoppiAbdu Xaadir KEBE