Ñi ngi siyaare man de doomi Senegaal laa juy dund fii mu nekk ca Ndakaaru ak Tuubaa, di jaabante ci diggante bi ci mujjug-ayu bis gu nekk daanaka, nekkoon naa nag Itaali, di naa wax wolof mooy làkk wi ma dàqal ci làkk yi ak araab, frãse, àngale ak itaalien, wu ci nekk nag déggiin wu wér laa ko dégg, ab dongob daara laa woon nag bu jàng alxuraan ba mokkal ko, demoon naa Aamerig ak Faraas ak Espaañ, taalif naa as lëf ci wolof, tekki ci it ay téere, bari na lu ma dugal ci wiki bi ciy jukki, ab metlang (entrpreneur) laa ci B.T.p maanaam tabax laay liggéeye, may ñaan ñun ñi sopp wii làkk te man koo jëmale kanam ñu xamante, booloo ngir def ci ay liggéey yu man a amali Sunu gaal njariñ.

Abdou Khadre KEBE sakkmultiservices@hotmail.com

Wikipedia:Babel
fr-2
en-2
it-3
ar-5
Seet waa-wikipedia ci làkk-ak-làkk