Tamxarit
Tamxarit (محرم ci araab), mooy weer wi njëkk ci yu gàddaay gi, moom nag bokk na ci li ñuy wax ci Lislaam "Al-ashur al-hurum", (maanaam weer yu am worma yi): tamxarit nag tuddees na ko ci araab "muharram" ngir ne araab yi dañu ci daan araamal xeex.
Xew-xew
Soppi- Ci lees di xewal bés bu njëkk ci at mi. Ci senegaal ci lañuy taajabóon.
- Ci la shiit yi di fattalikoo xareb Karbalaa ca Iraak. Ca lañu faatee Useynu ben Aali sëtu yonent bi.
- Bisu Tamxarit
Tamxarit | Diggi-gàmmu | Gàmmu | Rakki-gàmmu | Rakkaati-gàmmu | Maami-koor | Ndeyi-koor | Baraxlu | Koor | Kori | Diggi-tabaski Tabaski |