Diggi-gàmmu
Diggi-gammu, (صفر ci araab), mooy ñaareelu weer ci weeri wolof. Tuddees na ko "safar" ci araab giy firi féex, wéet, limub tus, ci araab mi ngi bawoo ci baat boobu di safar {sifr) ndax féexam ga, ëmbadeem ga dara. Kon safar tuddees na ko safar ci araab - ma baamu- ngir ne weer la wow këri araab yi dañu ci daan wéet, féex ci ci ay ñoñam ngir xare-ji, waxees na it ne li ko waral mooy araab yi dañu ci daan song ak a lokki giir yi, bu ko defee ñu leen di "safaral" maanaam tusal ci seeni bagaas ( maanaam jël li ñu am ba duñu deseeti "tus" (sifr),ñu mujj di ñu wéet ciy yére, féex ciy bagaas).
Xew-xew
Soppi- Ci la njabootu Muhammad dugg njéndul Yasid ca Siri.
- ci 7u fan la juroom-ñaareelu imaamu Shiit ba Musaa al-Kasim judd.
- ci 9u fan la ndamu Imaam Aali ibn Abi Taalib ci xareb Nirwaan.
- ci 18 la serigne touba démone gabon.
Lëkkalekaay yu biti
Soppi- (en) Islamic-Western Calendar Converter (Based on the Arithmetical or Tabular Calendar)
- (en) The Umm al-Qura Calendar of Saudi Arabia
Tamxarit | Diggi-gàmmu | Gàmmu | Rakki-gàmmu | Rakkaati-gàmmu | Maami-koor | Ndeyi-koor | Baraxlu | Koor | Kori | Diggi-tabaski Tabaski |