Taariixu Aamerig

Feeñug Diiwaan yu Bennoo yu Amerig yi (U.S.A)

Soppi

Feeñug Diiwaani Amerig yu bennoo yi

Gàddaay yi waa Tugal yi daa def juge Tugal, jëm Aamerig, gàddaay yooyu wéyoon nañu di sottiku ci Aamerig gu bëj-gànnaar gi. Loolu nag amoon na, ginaaw bi Kolomboo feeñalee Aamerig ba am lu tollook xarnu. Li ko taxaoon a am nag bari na, bokk na ci:

1 Fitnay diine yi amoon ci Tugal gu diggu gi ak gu sowwu gi, li waraloon loolu di yëngu-yëngu yu diine yi jugoon di safaan Jàngu bu Katolig bi, ak la ca juddoo muy ay xeexi ngér, yu amoon ci diggante ngérum Katolig ak ngérum Protestant , ak xeex bi protestant yi doon def ci seen biir, rawati na ci Angalteer, ak la ca juddoo muy boddikoonte ci diine, loolu nag waraloon gàddaayug ab lim bu mag ci waa Tugal yi, dem Aamerig gu bëj-gànnaar gi, ngir rawale seen bakan, ak ngir man a doxal seen diine ci ag féex akug gore.

2 Fitnay politig ya amoon ca Tugal ngir xeex jaay doole ga fa amoon, ak àttee na mu la neexe ga, ak la ca juddoo muy ag ñàkk a nosu gu mbir yi ñàkk a nosu, ak ñàkk-kaaraange, ak dox gi nguur yi di doxe ni mu leen soobe, loolu lepp nag taxoon na ba lu bari ci waa Tugal yi gàddaaye woon fi nu dëkkoon dem, wuti ag goreg politig .

3 Wër gi nu doon wër mbèll yu gànjaru yi, lu ci mel ni wurus mbaa xaalis, bokk na ci li leen daa gàddaayloo, ndax kat lu bari ci ñi daa gàdday, dañoo gëmoon ne Aamerig de réew mu fees dell la ak yile mbell, te ña fa dëkk, ñu néew ag xay lañu, te ñàkk ag taaxe, te yittewoowuñu yenn liggéey yu mel ni lijanti ay wurus aki xaalis ak gasi mbèll.

4 Jëm kanam gi xam-xam am ak ndefar ci Tugal, rawati na ci wàllug liggéey ay gaal, googu jëm kanam dimblee na ci ñu man a tukki ci géej gi, bay àgg ci barab yu sori yee sori.

5 Liggéey yi nga xam ne lonkoo yu Angalteer yi def nañu leen , ngir meññal ak jariñoo suufus Amerig si ak lijanti nu ñu koy sance te dëkke ko ngir dëgërale ci kilifteefug canc gu Angalteer ci goxub adduna bu bees bii, bokk na ci li waral gàddaay gi.

Sancu yi nga xam ne waa Angalteer yi taxawal nañu leen ci Aamerig gu bëj gànnaar gi:

Soppi

Waa Tugal yii bawoo woon Ispaañ, Faraas, Olaand, Suwed ak Angalteer, sancoon nañu ay barab yu wuute ci Aamerig gu bëj-gànnaar gi, ñoom lañuy wax tay Diiwaan yu Bennoo yu Aamerg yi , loolu nag di woon ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom benneel ak bu fukk ak juroom ñaareel g. Waa Angalteer yi nag ñooy ñi njëkk a taxawal ab sancu ca Jims Town, ci diiwaanu New York, atum 1607 g, mujj nañu nag ci diir bu gàtt, di ñi gën a tas, gën a wisaaroo ci barabi tefes yu penku yi, ci mbooleem ñi gàddaaye Tugal.

Barabi penku yii, maanaam yii nga xam ne la ëpp ca ña fa sancoon, dëkke woon fa ay waa Angalteer lanu woon, barab yii mooy yi mujjoon ginaaw bi (1776 g) di laaj ag temb akug dagge ca réew may nday di Angalteer. Waa Angalteer yi nag amoon nanu ñaari anam yu nu daa sance réew yi ak a yilife, bi ci njëkk mooy :

  • Buurub Angalteer da daan may yenn ci lonkoo yi, gu ci mel ni lonkoo gu Werjiniya gu London gi – mooy gi yoroon mbirum sos sancu bu Jims Town bi nu la waxoon leegi - da leen daa may ay sañ-sañ ci ñu taxawal ay sancu, ak jariñoo xéewal ya fa nekk, ak defar xaalis walla koppar yu ñuy man a jëflantee, ak topptoo mbirum kaaraange gi.
  • Geneen anam gi mooy: buur bi day dogal garmi yu Angalteer yi ay suuf, ba noppi féetale leen mbirum yor leen ak àtte leen .

Bi fukk ak juroom ñatteelu xarnu g, di agsi ci digg bi, Aamerig mujj na yor fukk ak ñatti sancu yu Angalteer, ñooy:

Diiwaan yooyu ñooy yi sos, te amal li nuy wax Diiwaani Amerig yu Bennoo yi, ci ginaaw xareb temb gi , atum 1775 – 1783 g, ñu mujj am ag temb ci Angalteer, ci mujj gi. Diiwaan yooyu nag, bu nu leen xoolee ci Aamerig gu leegi gii nii, duñu weesu benn xaaj ci Aamerig gu ñu xaaj fukki xaaj.

Noste gi doon doxal mbiri biir yu sancu yu Angalteer yi:

Soppi

Nguurug Angalteer gi, daa joxoon ay sancoom yi nekkoon ci Aamerig gu bëj-gànnaar gi, da leen a joxoon aw xeet ci “ag àtte gu boppu” (autonomie) , waaye teewul ci biir loolu lepp, mu bàyyil fi boppam kilifteef ak cang gu mu am ci kaw sancu yooyu, maanaam may na leen ñu yor seen bopp, di doxal seen mbiri biir, waaye teewul muy seen kilifa, di réew mi leen moom. Nosteg àtte-gu-boppu googu amoon ci sancu yooyu, mi ngi tegu woon ci ñatti ponk:


Kaŋ bi , mooy kilifa gi yilif dooley xare ji ci sancu bi, mooy féetewoo sàmm mbiri way dëkk yi, di topptoo kaaraange gi, te am na sañ-sañu dindi saxal gu ñu defe ci ñaari jataay yii: bu yoonal bi ak bu diisoo bi. Moom nag (Kaŋ bi) buuru Angalteer bee koy fal ak a folli.

Bu dee nag jataayub yoonal bi, moom ñi dëkk ci sancu bi ñoo koy tànn, li ko tax a jug nag mooy tege galag yi ak fuglu liggéeykat yi, ak saxal seeni payoor, ak payooru Kaŋ bi. Bii jataay nag li ko may doole mooy jële gi mu jële sañ-sañam ak kàttanam ci nit ñi dëkke ci sancu bi, ginaaw ñoo ko fal.

Jattayub diissoo bi moom, li ko taxoon a jug mooy di xelal Kaŋ bi ak jataayu yoonal bi, ak di diisoo ak ñoom. Waaye nag moom sancu bi, ak li mu jot a am lepp, muy “ag àtte gu boppu ” gi nga xam ne taxoon na ba ñu man fa’a doxal demokraasi, teewul mu nekkoon ab sancu rekk bu toppoon ci ginaaw nguurug Angalteer gi, ci gisiinu waa Angalteer.

Goornamaa bu Angalteer li mu fàttee def mooy, wut nu mu nose mboolooy yu waa Angalteer yii dëkke woon sancu yi, ñoom mbooloo yii nga xam ne mujj nañu lu jamono di gën a yàgg, ñuy gën a sori seen réewum nday ma di Angalteer, ci wàllug aada ak dundiin, loolu waral ñu tàmbli koo fàtte, di yëg nag leegi ne fii mooy seen réew, di ci tënku, te di ko fonk.

Loolu nag tàmbli woon na a wuute ak politig bi George mu ñatteel mi, taxawaloon, moo doonoon burub Angalteer ca jooja jamono, lii mooy li taaloon ab xare bu mag ci diggante sancu yi ak nguurug Angalteer gi, xare boobu moom lañuy tudde xareb temb bi .

Li waraloon xareb temb bi:

Soppi

Ñi dëkke woon sancu yi, ay mbooloo lañu woon aki kuréel yu wuute, ak doonte la ëppoon ca ñoom ay waa Angalteer lañu woon yu di ay diiŋatkat (protestants). Seeni njariñi koom-koom it bokkewul woon, te niroowul woon, waaye nag, loolu lepp teewul woon amoon nañu ñatti mbir yoo xam ne kenn wuutewu ci woon, ñepp a ci dëppoo woon, ñooy:

1 Am gu nit war a am “ag goreg jëmm” , rawati na “goreg pas-pas

2 Ak sàmmoonteek yoon ak nosu, maanaam nosu gi mbir yi war a nosu.

3 Yëg gi ku nekk yëgoon ne fii ci sancu yii la dëkk, moo di am réewam, fa la féetale ag réewoom


Ëttub Aamerig bii nag mujjoon di def ay mbir yoo xam ne ñoo waraloon xareb temb bi tàkk. Mbir yooyu manees na leen tënk ci yii:


Yoon yuy tege galag ak tembar

Soppi

Parlamaa bu Britani bi daa génne atum 1762 g, yoon wu ñuy wax yoon wu tembar yi, mooy wiy def ngay fay tembar ci jëflante yu kilifawu yi (officiel yi), ak wayndare yi (les dossiers), ak yëglekaay yi añs. Ci atum 1764 g, ñu farataal galag ci suukar si nu daa jële ci sancuy Espaañ yi, yu Faraas yi ak yu Olaand yi, teg ci farataalati ko ci ataaya, kayit, weer ak biteex (walla betteex) .


Yoon wi aju ci moolu (navigation) ak yaxantu:

Soppi

Ci atum 1651g, barlamaa bu Britani bi dafa génne wenn yoon wuy waral ci sancu yi ñuy tuxal li ñuy génne ak li ñuy jëggaani di ko def ci ay gaal yu Britani, aaye leen ñuy jëndati feneen, leneen loo xam ne bari na ca Angalteer.


Koppar walla kee bu kayit ak jënd suuf:

Soppi

Sancu yu Britani yi danu leen a aaye woon ci yoon, ñuy génne walla ñuy defar benn koppar bu kayit ak di ko jëfandikoo niki koppar bu ofisel (kilifawu) . Noonu tam lañu teree woon – ci weneen yoon (luwaa )- ñuy jënd suuf yi feete sowwu fukk ak ñatti sancu yi, ngir jàpp gu nu jàppoon ne yooyu suuf nguurug Britanee leen moom.


Nos dooley kaaraange ji:

Soppi

Goornamaa bu Britani dafa sosoon jenn doole ju xare ngir aar sancoom yi nekkoon ci Amerig gu bëj gànnaar gi, doole jooju tolloon na ci junniy xarekat , mu waxoon waa sancu yi ne ñooy warlu di joxe depaas yi doole jii di laaj. Loolu nag taxoon na ba waa sancu yi mer, ñaawlu loolu lool, ngir loolu tam goornamaa bu Britani bi ne kon na ci génn, waaye nag galagu ataaya moom dindiwu ko. Loolu tam tax na ba waa sancu yi di yëg ne ñoom daal danuy jëflante ak ñoom, mu mel ne dañuy ay nit walla ag njaboot goo xam ne ñoo gën a néew solo ak daraja ñi dëkke Angalteer.

Waa sancu yi tam yëgoon nañu ne li ñuy fay ciy galag lépp, deesu leen ko defal fi ñu koy faye waaye kay ca réew mu leen sori mee di Angalteer, te loolu du leen jariñ ci seen dund gi, te du ci def dara. Nga rax ci dolli ne Angalteer mooy réew mi rënkaloon boppam ci sancoom yi, yaxantug marsandiis yu bari, maanaam bari na lool ay marsandiis yoo xam ne Angalteer da ne woon moom rekk a leen sañ a jaay ci sancu yi, lu mel niki ataaya, loolu nekkoon na lu waa sancu yi ñaawlu woon.

Ci nii daal la xew-xew yi toppantee woon, di nëxal nag sellug séqoo gi amoon ci diggante Angalteer aki sancoom, loolu tam gën a yaatal paxum réeroo mi nekkoon ci seen diggante. Loolu nag gën na a fés, bi waa sancu yi bañee ne duñu fayati galagu ataaya, ginaaw bi tam am mbooloo jug, ci desambar atum 1773 g, lakk ñatti gaal yu nguurug Angalteer, yu ñu duyoon ak ataaya, ca waaxub Boston, ca sancu bu Masacusets, loolu waral waa Angalteer tëj waaxub Boston bi, ne gaalug yaxantu du fi teerati, daal di ne moom ci jëmmi boppam mooy yoral boppam sancu boobu. Xew-xew bii ak la ca juddoo , man nañu ne moo waral xareb temb bi.


Ndajem waxtaan mu Filaadelfiya mu njëkk mi:

Soppi

Juroom ñeenti diiwaan yu Aameriig teewe woon nañu ndajem New York ma, atum 1765g, di sàkku ci nguurug Angalteer mu teggil leen galagu tembar bi mu leen di teg. Ci noonu Angalteer teggi woon na galag boobu waaye teewul mu wéyoon di tege yeneen galag yi nga xam ne ab Parlamaawam daa na leen woote, te di leen farataal ci mbooleem ay sancoom yi nekk ci àdduna bi.

Looloo taxoon reenub réeroo bi nekkoon ci diggante Angalteer aki sancoom saxoon fi di lu ñu dogadi, ndax kat sancu yi dañoo gisoon ne di leen teg ay galag te seeni jataayi yoonal ànduñu ci, bu amee lu muy tegtale mooy dindi màndargam demokraasi mi seen jataay yooyu di doxal seeni mbir ame woon, ndax kat daa am ab dal(principe) bu nekk ci demokraasi, bu naan “doo fay galag boo amul ndaw” .

Man nañu ne ndajem New York mi mooy lu njëkk a feeñ te nosu loo xam ne waa sancu yi def nañu ko, di ci safaan ni Angalteer di àttee seen diiwaan yi.

Ñoñ sancu yépp a meroon bi Angalteer tëjee waaxub Boston bi, bu ko defee ñu taxawal am ndaje ca Filaadelfiya, atum 1774 g, jàmmaarloo fa’ak Angalteer ne ko na xam ne lépp lu mu defati benn sancu ci sancu yi, na ko wóor ne sancu yépp la ko def, daal di ñaawlu bu baax jëf yu ñaaw yi Angalteer tegoon Boston . Njiitul xare lii ñuy wax George Washington (1732 – 1799 g ) teewe woon na ndaje ma. Ndajem Filadefiya moomu, mooy dàtt bi nga xam ne ci la Kongres mujj a teggu, ci ginaaw bi .

Jaadu na ñu leeral leen ne ndajem Filadefiya mi li ko taxoon a jug du sàkku ag tembte , waaye kay yëgal Angalteer ne lu wuuteek demokraasi lii muy def ci sancu yi neexu leen, te man na a nëxal te yàq xaritoo ak jàmm ji amoon ci diggam ak ay sancoom.

Ñoom kay seeni càkkuteef weesuwutoon lii, mooy na Angalteer xam ne ñoom sancu yi kat ñoo ame àq ak sañ-sañ - ci seen jataayi yoonal yi – ci tege ak farataal ay galag ci waa sancu yi.

Angalteer nag, ci safaanub muy lijanti lëj-lëj boobu ci maslaa gu xereñ, moom daal da fee nekk di yonnee ay dooley xare yu yees ci Boston, ngir gën a dëgëral doole ja fa nekkoon. Loolu tam li mu juroon mooy waa sancu yi ñoom itam, ñu ne woon nañu waajal seen bopp, ndax kat nguurug Angalteer gi bëggul jàmm, ci noonu ñu - ñoom waa sancu yi – defaat beneen ndaje ci Filadefiya, ngir jàng mbir mi, seet nu ñu ciy def.

Ndajem Filadelfiya mu ñaareel mi:

Soppi

Ndawi sancu yi defoon nañu am ndaje atum 1755 g, ca Filadelfiya, muy ñaareelu ndaje mu Filadelfiya mi, ñu wax fa ne dañuy sos menn mbooloom xare , te bennal ko, bañ a def sancu bu nekk am sa mbooloom xare, bu ko defee nag, mbooloom xare moomu ñu tànne ko ci waa sancu yi, ngir ñu aar leen ci ay wi leen dëgmalsi. Ci noonu ñu dugal doomi sancu yi ci xarekat yu bees yii nga xam ne George Washington moo leen jiite woon. Waaye teewul ñu yonnee ca buuru Britani bi, ab bataaxel buy sàkku ci Angalteer mu xoolaat ni muy jëflanteek sancu yi, te lenn baaxu ci, waaye buur bi moom jàpp fa mu jàppoon rekk, ne daal am na ag cang gu ñu joyal ci kaw mbooleem sancu yi. Ci jëfam jooju la tëje buntub jéem gi sancu yi doon jéem ngir defar – ak doonte lu néew la itam – seen diggante ak Britani, réew miy nday.



Ni xare bi tàkke :

Soppi

Bi buur bii di George mu ñatteel mi, ñàkkee faale càkkuteefi sancu yi, ne daal li wér mooy moo ame cang gu joyu gi ci mbooleem sancu yi, maanaam sancu yépp ci ron kilifteefam lañu nekk, ci anam gu matale te daj, bi buur bi nekkee ci taxawaayam boobu ne du ci juge la xare bi tàkk ci diggante ñaari wàll yi, sax nag lu toll ci juroom ñaari at daanaka (1775 – 1783 g ), bu ko defee, mu tas nag ci li ëpp ci sancu yu Aamerig yi, George Washington nag jot na a man a nangu Boston, ginaaw bi mu ko gawee. Dooley gornamaa bu Britani moom, teg loxo lu bari ci waaxi Aamerig yi. George Washington ni mu doon xeexe ak ñoom nag mooy xeexub bette, ci barab yu bari, ak door-daw, foo ko fekk daawul nangoo jàmaarlook ñoom, ndax xammoon na ne ñoo ko ëpp doole te gën koo tàggatu.

Ak li xarekati sancu yi doon jànkoonteel lépp ciy coona yu tar ci biir xare bii, teewul George Washington amoon na ci kaw njiitul Anglteer lii di Burgoyne, ci xareb Saratoga, loolu mi ngi am bi mu jawalsee juge Kanadaa, jëm New York, ci oktobar 1777 g. Ca saa sa, ginaaw bi ñu gañee Britani, Faraas jug na, jibal ab xareem ci kawam atum 1778 g, Espaañ roy ko ci, atum 1779 g, Olaand topp ci atum 1780 g. Man nañoo wax ne Faraas moom jàpple na way fippi sanncu yi ci wàllug xare (militaire) ak ci alal, ba tay it dajale na way coobarewu yu Fraans yi, yobbu leen ci Diiwaan yu Bennoo yi, ngir ñu xeexle leen ci ron njiit lu xare lu Faraas lii di Lavette, safaan Angalteer noonam bu mu yàgg a noonool bii. Ci noonu Britani mujj war a xare ci yu bari.

Dàq gi ñu mujj a def dooley angle ji, ci sancu yi, mooy gi nu defoon seen njiit la Cornwallis, loolu di bi mu deltoo ginaaw, dem dëkkub York Town, fa dexug York di sottikoo, ginaaw ba ko fa mbooloom xarem George Washington ma songee. Xarekati George Washington yooyu nag am njaxasiitum kuréel lañu woon mu ame ci diggante ay waa Faraas aki ñoñi sancu, tollu nag ci fukk ak juroom benni junniy xarekat.

Nañu fàttaliku nag ne waa Aamerig yi ñoom, ci seen suuf lañu doon xeexe, bu ko defee dolli leen doole ci xare ak ci alal day gën a yomb, gën a gaaw, bu dee waa Angalteer yi xawoon a sori Kanadaa, fi seen bagaasi xare daan juge, walla Angalteer gi leen soree woon lu tollook ay ñatti junniy miil daanaka. Nga rax ci dolli, waa Aamrig yi dañoo dogu woon bu wóor ci raxasu ci teg loxo gi Britani tegoon loxo seeni mbir, te amoon nañu ay njiiti xare yu bari, ku ci mel ne George Washington. Doolil ci loolu, nekk gi waa Britani nekkoon di xeexe ci sancu yoo xam ne manuñu fa’a ame jokkoo ak dolli-doole ga war, ca anam ga mu ware te gaaw, te itam pastéefub xeex bi ñu amoon moo gën a suufe fuuf bi waa sancu yi amoon, ñoom ñi taxawoon temb ci xettaliku ci waawug nguurug Angalteer gi. Bokk na ci li doyadil waa Britani yi ci xeex bi, ubbi gi ñu gubbi woon ay jë yu xare yu bari ci seen kaw, ci barab yu sakkan ci Aamerig.

Tembug Diiwaan yu Bennoo Aamerig yi:

Soppi

Bi waa Britani xamee ne lòtt nañu ci toroxal jeqiku gi amoon ci Aamerig, te xam ne doole du mooy lijanti lëj-lëj yi nekk ci sancoom yi, ndax kat mi ngi nii di ku ñu dàqe, ndamu ci kawam ca xare ba, bi loolu amee mu sàkku woon ag juboo, ci noonu ñu xaatim juboo gi ci Pari, ci digganteem aki sancoom atum 1783 g, lii mooy tomb ya ca ëpp solo:

1 Britani day nangu tembteg sancu yi nekk ci suuf yi féete ci penkub dexug Misisipi gi, te jàppe dex gii muy diguw sowwu wi ko tàqale ak sancu yi. Bu ko defee dig yu bëj gànnaar yi ñoom ñu bàyyi leen nañu nekke woon.

2 Jéem a rafetal séqoo yi, ci diggante Britani ak réewum Aamerig mu temb mi (Diiwaani yu Bennoo Amerig yi)

3 Amal ci diggante Britani ak Aamerig gu temb gi, ay séqoo yu yaxantu ak yu koom-koom, waaye nag séqoo yooyu ñu teg leen cig nawleente, ak moroomante, kenn du jaay kilifteef sa moroom.

Nii daal la Diiwaan yu Bennoo yu Aamerig yi ame, xareb temb bi nag am na genn jeexiital gu rëy te xóot, ndax wal na te upp ngelawul gore ak temb ci mbooleem sancu yi.

Lii nag làppal na Britani, loofloo ko, ci wàllug xare ak politig, nga rax ci dolli alalam ju bari ji mu ci ñàkke.

Aamerig nag moom, daal di ñew, defar sartu réewam , daal di taxawal ndajem booloo mi nga xam ne Kongres moo ko digale woon, atum 1788 g, mbooleem ndawi Diiwaan yu Bennoo yi teewe woon nañu ko, ba mu des diiwaanub Rood Island. Cér ya fa nekkoon tam, tànn cig dëppoo, George Washington muy njiitul ndaje mi, ci loolu la nekke ki njëkk a nekk njiilul Diiwaan yu Bennoo yi.

Ginaaw bi lañu def Washington – ginaaw bi mu nekke péeyu koom-koom bi ak bu alal bi – la nu ko def péey bu politig bi. George Washington nag jëloon na xalaatam yepp, def leen ci nu muy def ba bennal Amerig, looloo taxoon waa Amerig yi soppoon ko, wormaal ko, waxam it weesuwutoon : (( doon leen benn, doon leen ay waa Aamerig ..)) , loolu saxoon ci seen xel yi. Washington moom wàcci na jal bi, joxe njiit gi, atum 1797 g, ginaaw bi mu ko yoree ñaari yoon.