Fitna
Jamma ngen fitna Bis boobu, ci njël la jok, dèm ci wanag wa, raggu. Ginaaw loolu, ma dèm jappu ba sètt, juli, jal sama kuruus, doxontu walee ba ca tunduwa, ndax daagub suba day fuddu tank. Kerook, guddi googu, taw bu barri mo soteeku si dëkk bi. Ma ngi fateliku, bi marax di jot, ap jabbu bu am doole doona melax ci bëtt ganaar. Dëgg la sax de, xiin ño ngiko baaxó giss si penkku bi. Ba bi ñuy fàtu, xiin wa saaxé gul woon. Bi ma leemo ba tëdd daal, la degg peppu ndox di tëgg xeddu neeg bi, mbete ay gewāl yuy sajji lambu. Ci kaw loolu la for bëtt bani gis, aw dännu wu rey buy xoti asamán mooma yee waat. Dëkk bani selaw. Dara yanguwul, nga xamni yalla rekk moo am doole, kuy jaay doole, kuy jaay ngoora, akk nguur, ba dajje ak Boroom bi, danga xamni, nguur ken’ako moom tamuy Yalla, keppu kum ko jox, war nga séed suba, yaræm jaamam yi. Loolu motax wolof njaay naan, nguur kenn duko gnèd. Bi ma walbatikoo, ba foraat bett, ci la daadi song ap nelaw badi aji xôôt. Nees tuuti, ci ay smili yu neew, samäy gët ubee ku si manding bu yaatu, bu nurook geej. Ben picci bu weex tal nãw tiim ma, mu daldi sap, ginaw loolu, mu bayi ben bataaxal bu ñu bind si aw keyit, ci lu toloog juroomi xët. Tamba leeko si mbëbestal la bacci daneel ba. Si la dox ay jeego wut si bataaxal bi, ma for ko, janggu ko. “assalamu alayi kum ya SENEGAAL. Ma ngi leen di nuyu, ken kunekk si turam ak santam. Di leen xamal ni, weer wi niu degmal, ayi jotaayu xecco ak taneef ku jiite gox yo ak gox goxaat yi. Ma dileen wax ni, rewmi di senegaal, ben bop la, ta ken duko xar niaar. Jamm moo njek, ta itamit jamm mooy mujju. Kaddu yi maleen di beral si bataaxal bi, kaddu yu weex xat la, waaye garab du neex, rawatina garab guy aar. Fagaru moo ngan fajju, te itt, xodiku bala nga lak le. Bu degloo lifi xacco katu nguur yi di wax si seeni lamiñ, dafa melni dañuy ma solal yerre yu aji raglu. Ak koj goo mandi bayou, sa wax si jamano bi rewmi tollu dafa wara lamboo jamm. Ndax nak, fitna day nelew, ta keppu kuko yee du moy walis yeekat ba. Ta fitna, xaritu alcande la, yoon wumu jar, booyal toolu boroom, boyal taw feexu askanam. Ta moom safaraam ayib la, ayib bu jaffe fay. Dëkku yi ak xuloo yi xotinañ lambaayu siki saka. Ken xamatul fumuy dägmal, ni wara addu, waxuñ, sen lamiñ la ñu yeew ak buumu xális. Ndaw ñi gälëm nañ, seen yaakar naax say na, seen rangooñ dil wal ci seen xarkanam ya di aji raag ngir yaram talu. Ay waay, yeen way politiseŋ, baayi leen xel badoola yi ak baÿkat yi, ay waay jox leen gëdd fac kat bi, jàng kat bi, ndax ňii ňooy reeni kom kom. Kuleen tuutal, nasaxal nga elagu reewmi. Bi leem reew, da niu ko sëff lumu atannul, ñaata ndawu reew, ñaata, kaŋ kam, ñaata, pencci ak bärëb yuy warax alallu baytimál. Tabe ci alall jó moom. Li fum ñu jëmmé, yeen doomi rewmi. Sama yaram dawna, sama xóll di jooy ci diggu all badi aji liw. Ngir Yallah, saaŋ leen ma si mbalaan num yermande, lii de kuko déf, wasaaré nga ngelawal wërsek ak peppu xeewal si ëttub senegaal. Safaanu lii, musiba la, jikatu fitna, dawal katu mbaamu coono , mbate ay saafa’ndoo yu raag yuy naan si ndox mu nëx. Waaru na si kooku kiy wuuti niit ñi, di leek seen alal yum tooggé si kawdiru yaq ak jalgati, nuluge ko deretu mbaam xuux. Ku def li wor na, ku def lii du gor, tooke lay sap melni janaab badi aji marr