Ni Sapoŋ jëme kanam

(Yoonalaat gu jóge Ni Japon jëme kanam)

Ni Sapoŋ jëme kanam Soppi

Japon njëkk fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g:


Sapoŋ de wéyoon na diir bu yàgg, di beru ak a sori xayug Tugal gi, yam ci bobbam, doyloo aadaam, ba ci digg juroom ñeenteelu xarnu g, gii beru gu xay, ak deltu-ginnaaw gu mag raxoon na ci, ci wàllug koom-koom, rawati na ndefar.

Waaye nag lii mu nekke woon, soppiku woon na ci ñaareelu xaajub fukk ak juroom ñeenteelu xarnu. Ci noonu mu tàmblee juge nànk-nànk ci réew mu deltu ginnaaw, dem ci réew mu jëm kanam ci wàll yii: koom-koom, caada, politig ak xare.

Mu roye nag ci réewi Tugal yi, gisiinu canc ak yaatal ko, ci réew yi mu dendal, ngir wone ci dooley àddinaam ji mu yor, ci wàllug xeex gi ñuy def ngir teg loxo ay réew, sanc leen.

Sapoŋ nag ak li muy yeex a jot ci xayug tugal gi lepp, boo ko dee xool ci réewi Asi yeneen yi - ndax dëppoo gi mu njëkk a def ak Aamerig ci wàllug joqalanteg yaxantu weesuwul atum 1854 g gii rekk - teewul mu tàmbli woon na jege nànk-nànk xayug Tugal gi, di ci jariñu, di ci niitu.

Loolu jural ko mu tabax ay isin yu mag, xotti ay yoon, defar ay yooni saxaar , gën a jëmale kanam aw yaxantuwiinam. Réewum Sapoŋ ca saa sa mu tàmblee gis ag yëngu-yëngug ndefar gu mag, gu nirook ga Tugal romboon ba mu ciy door a dugg.

Bu ko defee, Sapoŋ xëy di réew mu dox, mu jëm kanam, raw nag ay maasam ci réewi Asi yi, ci wàllu ndefar, xam-xam ak xarala .

Mu mujj am, moom Sapoŋ, mbooloom-gaal (flotte)mu yaxantu tax a jug, mu mag, moo xam ne moo jël limub ñatteel ci àdduna bi, ci diggante ñaari xarey àdduna yi. Marsandiisi Sapoŋ yi, nga mujj foo dem fekk leen fa, ci Asi ak Afrig.

Sapoŋ, ginnaaw bi ñu ko gañee ci ñaareelu xareb àdduna bi: Soppi

Sapoŋ dumaas na ko ci ñaareelu xareb àdduna bi, te booba moo nekkoon laafum penku mi ñeel réewi digg yi (axe), ñooy: Almaañ, Itaali ak Sapoŋ. Sapoŋ nag mujjoon na nangu ne amees na ndam ci kawam, mu wommatu, joxe loxoom ci kanamu njiitul xare lu Aamerig lii di Mark Arthur, atum 1945g . Ci noonuñnu taxawal benn jataay bu way tapoo yi , ngir doxal mbiri Sapoŋ, ñu dénk ko kii di Mark Arthur, ci diggante 1945 – 1951 g.

Waa Aamerig yi nag rëddaloon nañu Sapoŋ benn strateji, dugal fa demokraasi, jële fa dal bi aju ci jaamu imbraatóor bi , ñu soppi woon it seeni njàngaliin, maanaam ni ñuy jànge ak li ñuy jàng, wutaloon leen sartu réew bu bees, ray it lonkoo yu mag yi (les grandes sociétés) . Ñu fuqarci ay moomeel yu rëy ci loxoy njabooti Sapoŋ yi, sëddale leen ci lim bu mag ci baykat yi, daal di it taxawal ab parlamaa bu bees .

Ci noonu Sapoŋ jot na a tàmblee nosaat dundug koom-koomam., gu plitigam ak gu mboolaayam, te tàmblee dab nànk-nànk, réewi ndefar yu jëm yi kanam.

Waa Sapoŋ jariñu nañu ci li leen Aamerig indil ci ndimbal yu alal ak yu xarala, loolu bokk ci li delloosi cawarte gi ci wàllug koom. Metlàŋ yu Sapoŋ yi dox nañu bu baax ci tas ak yaatal koom-koomu Sapoŋ, ngir seenug yewwute ak ngir bari gu Sapoŋ bari ay liggéeykat.

Suqali nag gën na a yokk ci wàllug ndefar ak yaxantu ci diggante bi topp ci 1955g . Sapoŋ mujj di ñatteelu réew mi ëpp lu muy liggéey weñ, bokk it ci réew yu njëkk yiy segg petrol, ak yi ëpp lu ñuy defar gaal. Mbooloom gaalum yaxantoom mi gën na a jëm kanam, ay ngañaayam gën a dolliku, liggéey bi aju ci jumtukaayi mbëjfeppal “elektronig” yi gën a jëm kanam, ba mujj Sapoŋ àgg ci, ci fi nu man a yam ci raw gu xam-xam. Ja yi ñuy jaaye liggéeyi Sapoŋ yi gën a yaatu, gën a bari ci àdduna bi. Bu ko defee Sapoŋ mujj nag di réewum ndefar mu mag, mu dox, te jëm kanam.