Jëm-kanamug xam-xam


  • Jeexiitalu gu waa-Tugal defoon ci yooni gëstu yu xam-xam yu jullit ñi.
  • Lefi (wàlli) jëm kanamu xam-xam ci Tugal.
  • Yewwuteg ndefar: ay jagleem – ay màndargaam – ay ngérteem (ses résultats)


Jeexiitalu gi waa-Orob defoon ci yooni gëstu yu xam-xam yu jullit ñi:

Jamono ji xam-xam néewe lool te amadi xiima ci Tugal, ci jamono ju diggu ji, di (ju ag laman), moom xam-xam nekkoon na ci mbooleem réewi jullit ñi di lu naat, te meññi.

Xay gu lislaam gi di woon gi gënoon a kawe ca booba, ngir coona bi boroom xam-xami jullit ñi daa génne ak’a daj ci dundal ko, ak ngir soññe gi nguurug lislaam gi daa soññee ak’a jàmbaarloo ci xam-xam ak boroom xam-xam yi.

Bi waa Orob yi dee ñu yittewoodi xam-xami Gres yi ak yu leen moy, fekkoon na jullit ñi ñoom ñu nekkoon ñu xam-xami xay yu yàgg ya ñoroon, ñu taxawoon ci firi leen ci araab: xay yooyu di yu Gres, Faaris End, rawati na ci Paj, Saytubiddiw, Xayma ak yeneen yi. Ñu jotoon’a naan nag ci xam-xami Ubuqraat, Iqlidis, Aflaaton ak Arustoo ak ñu leen moy ci boroom xam-xami Gres yu mag yi. Boroom xam-xami jullit ñi yamuñu woon rekk ci naan ci xam-xami Gres yi ak tuxal leen yobbu leen ci araab, waaye kay danu leen’a toppoon, wéral leen, te dolli ci lu bari ci li nu feeñal, wuññi ko ciy xam-xam, aki gëstu aki nattu yu nu amal ci wàllug paj ak xayma, simi ak xam-xami dénd yi , Saytubiddiw, melosuuf ak yu leen moy, ginaaw bi nu amee jikko yu mag yiy joxe xalaatub xam-xam bu sell.

Ngérum walla yoonu gëstu wu xam-xam ci jullit ñi:

Soppi

Boroom xam-xami jullit ñi daal doxoon nanu ci seen gëstuy xam-xam yi ci ngérum xam-xam mu wuutewut ak mu xam-xam mi am ci jamono ju yees ji. Ñi ngi sukkandiku woon ci yooni xam-xam yoy bokkoon na ca yii: Xeeñtu, raññale xaaj yi, jëfandikoo yooni natt yi, jàkkarloo, làmb, misaal ak jeem a àgg ca jëmuwaayu xam-xam ba, maanaam xam-xam bi la tax’a jug, ak xam ngérte yi , muy liy juddoo ci boo ko xamee ba noppi .

Ngir coona yii nu daa daj nag mujj nanu di ñi jiitu ci lefum gëstu mu xam-xam, walla li nuy tudde “yoonu xam-xam wu nattu” , ci noonu lanu fi sampe woon kenoy gëstu gu xam-xam, ngir yeesal gi nu yeesaloon xam-xam ci seen jamono. Waa-Tugal yi nag jariñu nanu ci wii yoonu nattu wu xam-xam wi nga xam ne jullit ñi rawoon nanu ci. Ki jiitu woon ci ñi ci jariñu mooy waay- Angalteer jii di Roger Bacon ( 1214 g 1297 g), mooy ki waa Tugal yiy jàppe ki raw ci gëstug xam-xam ci Tugal, ndax mooy ki jeemoon’a wutal xam-xamu dénd ag noste guy sukkandiku ci nattu ak jàkkaarloo. Loolu nag mbir la moo xam ne boroom xam-xami jullit ñi ñoo ko ci jiitu.

Jaadu na ñu leeral fi ne Roger Becon mii kat ku jotoon a jàng làkku Gres la ak wu yahood yi , ak araab, jariñu woon it ci xam-xam yi nu ci bind. Moom nag daa gëmoon ne li tax ñu war’a jàng jëmm ak simi ak xayma ak saytubbidiw ak xeltu mooy ligeeyal xam-xamu Yàlla (théologie) .


Digg yi “xayug lislaam gi” jaaroon bi muy dugg Tugal:

Soppi

Jullit ñi dañoo nekkoon ñu rawoon ci lefi xam-xam yu bari, ci noonu ñu yanu woon seen xay googu yóbbaale ko ci mbooleem àdduna bi, ci penku bi ak sowwu bi. Tugal jariñu woon na bu baax ci xam-xami jullit ñi, ña fa dëkk it jokkoo woon nanu ak jullit ñi, jaare ko ci ay ker-keraan yu bari, bokk na ci yooyu:

(1) Andalusi :

Waa Orob yi jonjoo woon nanu ak digg yu xayug lisaam gi ci Andalusi, moom gox bii nga xam ne daa mujjoon fees dell ak leer guy jòlli tukkee ci xayug lislaam gi ko róofu woon.

Moom bii gox barabu jòlli la woon ñeel xam-xam ak dañ-kumpa, rawati na ci dëkki Tugal yi mu dendaloon. Bu ko defee nga gis sàkkukati xam-xam yu Tugal yi daa jariñu ci xam-xami jullit ñi, di jawalsi ak a jublusi dëkki Andalusi yii di Talitala, Kordoba ak Sewija , ñu jële woon ci ñoom ngérum nattu mi ñu daa jëfandikoo ci gëstu gu xam-xam, loolu mujj yëngal bu baax xalaatiinu waa-Tugal yi.

(2)Dunub Sisil :

Araab yi jotoon nanoo teg loxo Sisil, ki joxe woon ndigalul jëf jooju di Siyadatul Laahi Bun Al Axlab, buurub nguurg Axaaliba yi, waaye mu ame ci loxol kapitenam bu siw boobu di Asad Bun Alfuraat atum 212 ginaaw gàddaay gi, mu ame woon nag ci jamonoy xalifa bu nguurug waa Abaas, bi tuddoon Maamun. Ca saa sa xayug lislaam tàmblli fa’a sutuxlu, Sisil mujj di gilin ci gilini xam-xami lislaam yi, sàkkukati xam-xam yepp jublisi ko rawati na ñi dëkke woon Tugal, ngir sàkkusi fa xam-xam. Bi Norman yi nangoo Sisil ci Araab yi, yaquñu woon xayug lislaam gi, ñoom kay dañoo sawarloo woon boroom xam-xam yi, soññ leen, ci noonu firi teerey araab yi yobbu leen ci latin daal di fay tàmblee am ak’a sawar, waa Tugal yi tàmblee yër li ci yii téere ak’a jariñoo, rawati na Itaali mi ci gënoon’a jege Sisil, looloo waraloon muy mberum yewwute gi.

(3)Xarey jooñe yi

Bokk nanu bu baax ci li tax waa Orob yi manoon’a jokkoo ak xayug jullit ñi. Jokkoo gi it saxoon na fi lu tolloo ak ñaari xarnu, ci biir ñaari xarnu yii Tugal jot na cee tuxal lu bari ci xam-xami lislaam yi, ame ci it, walla tege ci loxo lu bari ci téere yi nu taalifoon ci araab, ak yi ñu firi woon jële leen ci làkku Gres, End ak Faaris .

(4)Jokkoog yaxantu gi amoon ci diggante reewi jullit ñi ak Tugal.Rawati na li ci Itaali jotoon’a def, mu bokk ci li sababoon jonjoog xay ci diggante ñaari dëkk yi.

(5)Siyaare gi nasaraan yi daa defsi ci seen barab yu sell yi nekk Palastiin. Nga rax ci dolli tukki yi waa Tugal yi daa defsi ci réewi jullit ñi, ak la ca juddoo muy ñu gis te jariñu ci xam-xami jullit ñi ak seeni xay. Jullit ñi daal ñoo waral jëm kanam gii nga gis ci Tugal ci jamonoom ju bees jii.




Xam-xam yi bàyyi ay jeexiital ci waa Tugal yi:

Soppi

Xayma:

Jullit ñi naanoon nanu ci xam-xami xayma yi nekkoon ca waa End yu yàgg ya, ñu jotoon’a jànge ca ñoom ni nuy defe ay lim (numero) waaye nag nu seggat ko, sellal ko, gën koo teg ci yoon. Boroom xam-xami jullit ñi ñoom defoon nanu ay ndollent yu am solo ci xayma, ñoo dolli woon tus ci lim yi, ndax amu ci woon bi nu leen di jël. Ñu indi màndargam “al-kasr al-hasarii” di ci wolof (damat gu fukk) , ñu taalif ci xayma ay téere yu waa Tugal yi firi ci seeni làkk, te jariñu ci.

Boroom xam-xamu jullit bii di Muhammad bun Muusa Alxuwarsamii, nekkoon na di ku aay ci xayma, moom de lañuy sant bu lim (mumero) yi nekk ci xayma duggee Tugal tay. Xawaarsamii mii aayoon na it ci beneen xam-xam bu yees mooy aljabr , moom sax mooy ki ko sos far. Taalif na ci tollale ci aljabr , nu tekki ko ci ginnaaw bi ci làkki Tugal yu bari. Boroom xam-xami Tugal yi jariñu ci.

Boroom xam-xami jullit ñi jëfandikoo nanu ay junj ci xayma, ñoo njëkkoon waa Tugal yi ci wàllug xayma gu yees gii. Bu dee nag ci xereñ(ingénierie) , ak xam-xamu ñattal yi , jullit ñi ñoom yamuñu woon ca la woon ca waa Gres yi rekk , nga xam ne seen boroom xam-xam bi ñu naan Iqliidis moo ko feeñaloon, waaye jotoon nañoo feeñal ay masalay andasa yu bees. Ñu duggal li nuy wax “al mamaas” ci xayma gu ñattal. Nu jël li nuy wax “juyuub” = poos, wuutale ko ak li nuy wax “awtaar” = buum. Nu fecci itam toolale yu nu kaabaal yi. Nu xóotal bu baax tam ci xam-xam yu nuy wax “maxruutaat” . Boroom xam-xamu jullit bi nuy wax Omar Alxiyaam defoon na lu mag ci wàllug xayma, moom de bokkoon na ci ñi gënoon’a ràññiku ci boroom xam-xami jullit ñi ci wàllug xayma ci ñeenteel bu njëkk bu xarnub fukk ak ñaar g.

Li nga xam ne sikk amu ci mooy ne jullit ñi jariñu nanu ci xam-xamu jëmm ci waa Gres yi , bi nu ko tekkee ci seen làkk , waaye ñu gën koo yaatal, dolli ci ay masala yu yu jëmm yu bari. Nu màndaqe walla natt diisaayu yolaakon yi , nu fent ay màndaqekaay yu xereñ, ñu xamale ay gisiin yu bees ci xam-xamu “kàddu” ak “gis” (basariyaat ) ak “xool” (almariyaat ).

Boroom xam-xam bu jullit bii di Abo Yuusuf Yahquub Ishaq Alkanadi, mi nga xam ne mi ngi faatu atum 873 g, moom ku aayoon ci xam-xami gis yi la, taalif na ci ab téere bu am solo, mooy téereb yu nu xool yi, nga xam ne waa Tugal yi mujjoon nanu koo tekki ci làkku latin. Roger Becon jariñu ci ak Liyonardo Da Vinci, ak boroom xam-xam bu Poloñ bii di Copernice (1473 – 1543 g).

Boroom xam-xamu jullit bii di Abo Aliyu Muhammad Bun Alhasan Bun Alhaysam (965 – 1038 g), moom mu nekkoon di ku aay ci xam-xamu jëmm, mu soppi xam-xamu leer bu yàgg ba, indi fi xam-xamu leer bu yees bi. Mu amoon ndam ci indi fi gisiinu xam-xami seen yi, mu firi feeñteg xònn , ak safaanu gi ag leer di safaanu, ak ni muy dammoo.

Bu boroom xam-xamu Gres bii di Batlimos jàllee, kii di Ibnu Haysam moom lanuy jàppe boroom xam-xam bi njëkk’a def ay wuññi ci xam-xamu gis. Haysam defoon na ay taalif ci xam-xamu-yu nu gis yi, ak xaaji bët, ak weer yi ak leer ak yeneen. Waa-Tugal yi it yii taalif, tuxaloon nanu leen ci seen làkk wii di wu latin, ci xarnub fukk ak ñatteel g, ak ci yeneen làkk yu Tugal yi. Loolu dimbli leen ci nu jariñu bu baax ci xam-xam yii nga xam ne jullit ñi aayoon nanu ci bu baax.


Jullit ñi yittewoo woon nanu saytubiddiw, Xawarsimii moom defoon ay natt ci yëngug biddiw yi, xam fi ñuy fenke ak fi ñuy sowe. Jullit ñi jariñu woon nanu ci saytubiddiw ci waa Geres yi, ci noonu ñu firi woon ci araab lenn ci téerey biddiw yu Geres yi niki téereb Batlimos bi tuddoon ñeenti wax yi.

Boroom xam-xam bi ko tuxaloon ci araab di Aboo Yahyaa Albatriix, ci jamonoy Abo Jahfar Almansuur. Doomi Muusaa Bun Saakir ñoom itam taalif téere bi ñuy wax Aljadaawil Alfalakiya, yeneen boroom xam-xami saytubiddiw it feeñ, niki: Saabit Bun Xurra, Haniin Bun Ishaqa Alhibaadi, ak Bataani mi faatu atum (929 g) ak ñu dul ñoom.

Jullit ñi tabaxoon nanu ay fuglukaayi biddiw ca Dimasq, Baxdaad, Kordoba ak Sawija di woon ay dëkki lislaam. Abo Abdillaa Albattani mii dees na ko lim muy ki gën’a bàyyi ay jeexiit -ci anam gu xóot- ci waa Tugal, ci boroom xam-xami bidiw yu jullit yi. Waa Tugal yi ñoom jariñu nañu bu baax ci saytubiddiw ci jullit ñi,ak ci li jullit ñi jot’a gennewaat ci anam gii ciy wuññiy xam-xam.

Kimya:

Jullit ñi fésoon nanu ci xam-xamu jëmm, Jaabir Bun Hayyaan Alkoofii bokkoon na ci ñi gënoon’a siw ci wàll googu, moom mi doon def simi te taalifoon ci ab jimblang .

Jabbir leeraloon lu bari ci way toggale yu simi yi nu xamutoon bu njëkk, niki: aji wex ju nitrik, ruug nasaard, botaas, soda al kawiya ak aji wex ju asotik ak yeneen.

Mu leeraloon ba tay jefi simi yi niki: seebal ak leeru ak yeeg ak toqqal.

Dana jaadu nu leeral ne xam-xamu simi moom, danu ko daa wooye xam-xamu Jaabir, ngir li ko ci Yàlla tawfeexaloon ba mu man’a topp yoonu xam-xam wu nattu wi nga xam ne ci la jaaroon ba man’a àgg ci ay dëgg yu simi yu bari.

Waa Tugal jariñu nanu bu baax ci xm-xamu simi bi ci jullit ñi, ci noonu nu firi taalifi jaabir yooyu ci seeni làkk, xam it lu bees li ci jullt ñi dolli.


Boroom xam-xami jullit ñi rawoon nanu ci paj. Sartoon nanu ci seen boroom xam-xam, mu xam siddi , xam jëf ak warteefi cer yi, ak noyyi ak soppikum saw. Ñoom de ñu sonnoon ci xam-xamu siddi lanu woon. Firi woon nanu xam-xami Geres yi ci aju woon, ci làkku araab. Bi nu noppee ñu taalif ci. Teereb Ibnu Nafiis bi tudd Tasriihul Xaanuun dolli na ay xam-xam yu am solo ci xam-xamu siddi. Jullit ñi jàngale nanu doxug dereet , sonn it ci mbooleem xeeti tawat yi, xamale itam deewal bi nuy faral a def ci ligeeyu xotti . Ki niy wax Razi te faatu atum (923g) feeñ na te raw ci paj, taalif na ci lu sakkan.

Ak Ibnu Sinaa mi faatu atum (1037g) , moom de kenn la ci boroom xam-xami jullit ñi gën’a siw ci paj, téereem ba tudd Xanuun Fit Tibb de benn jimblang bu xam-xamu paj, bu waa penku ak sowwu ñepp xam, ak Abo Xaasim Xalf mi gënoon’a fes ci xottikati xarnub fukk ak benn g. Ak Ibnu Zahr, boroom teere bi tudd Mubtakaraat Fil Jiraaha. Waa Tugal yi jariñu nanu ci xam-xamu paj bi nga xam ne jullit ñi rawoon nanu ci. Ñu jariñu ci ni nuy siddee, ak ni nuy gennee tawat yi, ak ni nuy faje, ak ci xam-xam yi nga xam ni teerey jullit yi làqoon nanu leen ci wàll gii, ginaaw bi nu leen firee ci làkki Tugal yi. Waa Tugal yi jële nanu ci jullit ñi tabax ay fajuwaay ak jëfandikoo deewal ak li nuy wax Kaaw su nuy opere (xotti).

Waa Tugal yi ba tay jariñu nanu bu baax ci xam-xamu xeltu bi nga xam ne jullit ñi ñu ci rawoon lanu. Ci noonu nu jàngoon taalifi Kanadii, Faarabii, Ibnu Sinaa ak Ibnu Rusdi ak ñu dul ñoom, ginaaw bi nu leen firee ci seeni làkk. Bokk na ci boroom xam-xami Tugal yi gën’a siw ci jariñu ci jullit ñi ak seeni xalaat : Paskaal, Dikart, Hiyom ak Becon ak ñu leen moy.

Waxtu wi yaatuwul ngir nu man leen a indil ngértey xam-xam yu bari yi nga xam ne jullit ñi àggoon nanu ci, ci seeni gëstu te booba Tugal a ngi ci ngëmmeenam li ak lëndëmug réeram gi, ci ron nosteg laman ak cangug Jàngu bi.

Dana yell ñu leeral ne xam-xam yi ak ngértey xam-xam yi nga xam ne jullit ñi àggoon nanu ci, dañoo tàmbli woon’a tuxu ndànk-ndànk jëm ci reewi Tugal gu sowwu gi, ginnaaw bi ab kureel ci waa Tugal yi xamee solos xam-xam yii, te taxawoon ci firi leen ci seeni làkk. Ay firikati Tugal yu bari feeñoon ci loolu ku ci mel ni: Costantinus Africanus, Herman The Cripple ak Eugenius mu Parlermo mi ak ñu dul ñoom.

Kon lu nu war’a xam la ne [[yewwuteg xam-xam]] ak gu ndefar gii am ci réewi Tugal yi, ci ginnaaw yewwute gi, du lu moy meññat ci meññati nattu ak gëstu yu xam-xam yi nga xam ne Tugal tuxale na leen ci xam-xami lislaam, ci digg jamonoy xayug lislaam gi. Coonab gëstu yooyu nag ñooy cëslaay yi nga xam ne ci la jëm-kanamug xam-xami dëppale yi ak yu xarala yu bari yii tegu ci àdduna ju xay jii ngay gis tay .