Mbëjfepp

(Yoonalaat gu jóge Electron)

Mbëjfepp "électron ci fr" as wàll-wàllaan la (wàll su ndaw lool) su xarefulwoon bi bu sëfoo ab yanu mbëj bu bon(-) bu tollook qe = 1,602 · 10-19 C, te dayoom toll daanaka ci 9,10 · 10−31 kg (ci beneen bennaanu natt di 0,511 MeV/c²), dees na ko wax itam yan bu njëlbeen walla wàll-wàllaan wu njëlbeen.

Naka-jekk ab mbëjfepp njunj bees koy jëmmale mooy e-. Xarefulwoon yi li booloo nekk leen ñooy ab saal (bi dajale ci biiram ay feppsaal aki feppmaandu) aki mbëjfepp yu koy wër. Dayoo mbëjfepp yaa ngi tollook daanaka 1/1836 yu feppsaal ak yu feppmaandu). Mbëjfepp yi cër yu cëslaayu lañu ci ne-ne yi, ñooy wàll-wàllaan yi gën a tuuti cib ne-ne ba tax kenn maneesu koo séddalewaat yeneeni cër.


Wikipedia
Wikipedia
Bii jukki ab junj rekk la. Man nga cee duggal sa loxo suqali ko ndeem am nga ci xam-xam ci anam yi Wikipedia taxawal