Afrig gu bëj-saalumu-Sahara
(Yoonalaat gu jóge Afrik gu bëj-saalumu-Sahara)
Afrik gu bëj-saalumu-Sahara, moom lañ daan woowe Afrik gu Ñuul, moo safaanoo ak bëj-gànnaaru Afrik, yem ci Sahel. Seddale gi tegu ñu rekk ci mbiri séwógaraafi, waaye ci mbiri cosaan ak aada tamit. Ba ca jamono ju yagg ja, ndand féy-féy gu Sahara da fa musa xaajale ñaari wàlli Afrik yi, moo jafeeloon weccoo gi ci aada ak cosaan ak njënd ak njaay mi.
Afrik gu bëj-saalumu-Sahara ci lu daj, dañ koy seddale ci ñenti diwaan, yu gën a siiw ak yii tu:
Ñeent fukk ak juroom ñaari réew ñoo fa nekk, am juroom ñaar teemeeri miliyoŋi way dëkk (ci ndoorteelu xarnub XXI).
Diwaani Afrig | |||
Diwaani KMX: Diggu Afrig · Penku Afrig · Bëj-gànnaaru Afrig · Bëj-saalumu Afrig · Sowwu Afrig Yeneen diwaan: Ginne · Bejjenu Afrig · Maghreb · Sahel · Afrig gu bëj-saalumu-Sahara · Sudaan |