Sahel (jòge ci araab ساحل , sahil, di tekki pegg walla tefes) di jëmmal ab barab bu bekkoor, ne ci diggante tàkk gu Sahara ci bëj-gànnaar ak diiwaani yamoo gi fa nga xam ne day taw rekk, ci bëj-saalum. Tëraayam day jàpp mbàmbulaanu Atlas jëm ca géej gu xónq ga.

Lonkoyoonu Afrig ak diiwaanu Sahel

Réew ya ca ne:

Melosuuf

Soppi

Daanaka Sahel gépp gannuus la ak màndiŋ, ci lu ëpp, ñetti weer rekk lay taw ci at mi.

Dañ koy seddale ci xaaj yu bari:

  • Tàkk gi: kawewaay gu diggu gu taw yi du weesu 150mm ci at, mépp mbay mu aju ci ndoxu taw, manu faa am.
  • «Sahelu màngaan yi»: kawewaay gu diggu gu taw yi du weesu 400mm, foofu it mbay mu aju ci ndoxum taw, amal ko fa daanaka nekkuwul. Mooy barab bi sammkatu nag ak gëléem yiy màngaan di nekk.
  • «Sahelu way dëkk yi»: kawewaay gu diggu gu taw yi du weesu 650mm ci at. Dugub ak aréen lañu fay bay.
  • «Barabu Sahel-sudaan»: fii mbay mi gën naa yaa, taw yi yokk bu baax.
  • «Barabu sudaan»: fii taw yi di nañ àgg 950mm ci at, tawi nawet bi, di na tax ñu man a bay dugubu suuna, mboq, wëtéen,...

Tolof-tolof yi ëpp yi ay way dëkkam di jànkonteel ñooy: bekkoor giy gën di sax ak tàkku giy gën di jëm-kanam, di mëdd ngañcax su néew sa fa am.


Diwaani Afrig
  Diwaani KMX: Diggu Afrig · Penku Afrig · Bëj-gànnaaru Afrig · Bëj-saalumu Afrig · Sowwu Afrig
Yeneen diwaan: Ginne · Bejjenu Afrig · Maghreb · Sahel · Afrig gu bëj-saalumu-Sahara · Sudaan